Seetluleen xel yi
4
Samay soppe, buleen gëm bépp xel, waaye seetluleen xel yi ngir xam ndax ci Yàlla lanu jóge, ndaxte yonent yu dëgguwul yu bari ñëw nañu ci àddina si. 2 Ci nii lanuy xàmmee Xelum Yàlla: bépp xel bu nangu ne Yeesu Almasi bi ñëw na nekk nit, ci Yàlla la jóge. 3 Waaye bépp xel bu nanguwul Yeesu, jógewul ci Yàlla. Xelum kiy xeex Almasi bi la, bi ngeen déggoon ñu yégle ne dina ñëw, te léegi mu ngi ci àddina si ba noppi.
4 Yeen samay doom, ci Yàlla ngeen bokk, te am ngeen ndam ci seen kaw, ndaxte Xel mi nekk ci yeen moo ëpp kàttan xel mi nekk ci àddina si. 5 Ñoom ci àddina si lañu bokk, moo tax ñuy waxe ni àddina si te àddina si di leen déglu. 6 Nun, ci Yàlla lanu bokk. Ki xam Yàlla daf nuy déglu. Ki xamul Yàlla du nu déglu. Ci noonu lanuy xàmmee xelum dëgg gi ak xel miy naxaate.
Yàlla feeñal na mbëggeelam ngir nun
7 Samay soppe, nanu bëggante ci sunu biir, ndaxte mbëggeel ci Yàlla la jóge, te képp ku bëgg, doomu Yàlla la te xam na Yàlla. 8 Ki bëggul xamul Yàlla, ndaxte Yàlla mbëggeel la. 9 Ci nii la Yàlla feeñale mbëggeelam ci nun: yónnee na benn doomam bi mu am rekk ci àddina si ngir nu am dund gi jaarale ko ci moom. 10 Lii mooy mbëggeel gi: du nun noo bëgg Yàlla waaye moom moo nu bëgg te mu yónni doomam ni sarax ngir giifal mer bi Yàlla amoon ci nun ndax sunuy bàkkaar.
11 Samay soppe, su fekkee Yàlla bëgge na nu noonu, nun tamit danoo wara bëggante ci sunu biir. 12 Kenn mësula gis Yàlla. Su nu bëggante ci sunu biir, Yàlla day sax ci nun te mbëggeelam day mat sëkk ci nun. 13 Ci nii lanuy xame ne nun ci Yàlla lanu sax te mu sax ci nun: may na nu Xelam. 14 Te nun gis nanu te nu ngi seede ne Baay bi yónni na doomam ngir mu nekk Musalkatu àddina si.
15 Ki nangu ci kanamu ñépp ne Yeesu mooy Doomu Yàlla ji, Yàlla day sax ci moom te mu sax ci Yàlla. 16 Te nun xam nanu te gëm nanu mbëggeel gi Yàlla am ci nun. Yàlla mbëggeel la; ki sax ci mbëggeel day sax ci Yàlla, te Yàlla sax ci moom. 17 Ci noonu sunu dund ci àddina si dafay nirook dundu Yeesu Almasi bi. Ci noonu la mbëggeel gi di mate sëkk ci sunu biir ngir nu am kóolute ci bésu àtte bi. 18 Amul ragal ci mbëggeel, waaye mbëggeel bu matt sëkk day dàq ragal. Ragal day ànd ak mbugal, te ki ragal matul ci mbëggeel gi. 19 Nun nag, danoo bëgg ndaxte Yàlla moo nu jëkka bëgg.
20 Su kenn waxee ne: «Bëgg naa Yàlla» te mu bañ mbokkam, fenkat la. Ndaxte ki bëggul mbokkam bi muy gis mënula bëgg Yàlla mi mu gisul. 21 Lii mooy ndigal bi mu nu jox: ki bëgg Yàlla war na bëgg mbokkam tamit.