Saak
Saak mu ngi ñaax mbokki gëmkat yi ngir ñu am kóolute ci Yàlla ci waxtu yi nattu yi di ñëw
1
Man Saak di jaamu Yàlla ak Boroom bi Yeesu Almasi bi, maa leen di nuyu, yeen fukki giir ak ñaar yi tasaaroo ci àddina si yépp.2 Mbokk yi, su ngeen di dund nattu, ak xeet bu mu mën di doon, àndleen ak mbégte, 3 ndaxte xam ngeen ne seen nattu ngëm mooy jur seen dëgër-dëgërlu. 4 Kon, na seen dëgër-dëgërlu mat sëkk ngir ngeen mat ci lépp te baña ñàkk dara. 5 Bu kenn ci yeen ñàkkee xel mu rafet, na ko ñaan Yàlla, te Yàlla dina ko ko may, ndaxte Yàlla day may ñépp ak yéwén te du sikk kenn. 6 Waaye na ko ñaan ak ngëm te baña am benn sikki-sàkka, ndaxte ku am sikki-sàkka day mel ni ndoxu géej bu ngelaw bi di yékkëti ci wet bu nekk. 7 Nit ku mel noonu warul yaakaar jot dara ci Boroom bi, 8 ndaxte xel ñaar la am, te wóoluwul dara ci lépp li muy def.
9 Na mbokk bi néew doole tiitaru ci ni ko Yàlla di yékkëtee, 10 te boroom alal bi, ci ni ko Yàlla di suufeel, ndaxte moom dina weesu ni tóor-tóoru ñax. 11 Jant bi fenk, naaj bi tàng jérr, wowal ñax mi, tóor-tóor bi daanu te rafetaayam dem. Noonu lay mel ci boroom alal bi: dina réer ci biir ay jëfam.
12 Barkeel na nit ki dëgër-dëgërlu ci nattu yi, ndaxte gannaaw bi mu taxawee temm, dina jot dund gi, di neexal bi Yàlla dig ñi ko bëgg. 13 Nit, bu ko xelam xiiree ci lu bon, bu mu wax ne: «Yàlla moo ma ci xiir». Ndaxte lu bon mënula xiir Yàlla te moom ci boppam du xiir kenn ci lu bon. 14 Waaye ku nekk, bëgg-bëggam yu bon ñoo koy xiir di ko nax, 15 te bëgg-bëgg yu bon yooyu, mooy ëmb ba jur bàkkaar, te bàkkaar bu màggee mooy jur dee.
16 Yeen mbokk yi ma bëgg, buleen nax seen bopp ci lii: 17 bépp may bu baax te mat ci asamaan la jóge. Yàlla, di Baay bi sàkk leer yi, moo leen wàcce. Moom du soppeeku bay am takkandeer. 18 Ci coobare boppam may na nu dund bu bees bi ci kàddoom bu dëggu, ngir nu mel ni meññeef bu jëkk ci lépp li mu sàkk.
Nanuy déglu tey jëfe Kàddu Yàlla gi
19 Mbokk yi ma bëgg, bàyyileen xel ci lii: nit ku nekk war na gaaw ci déglu, yéexa wax, te yéexa mer, 20 ndaxte meru nit du jur lu jub ci kanamu Yàlla. 21 Kon nag génneleen ci seen xol lépp li ciy sobe ak lépp lu bon, te ngeen nangu ak suufeelu kàddu gi Yàlla ji ci seen xol, ndaxte mën na leen musal.
22 Deeleen jëfe kàddu gi. Képp ku koy déglu rekk, mu ngi nax boppam. 23 Ndaxte kiy déglu kàddu gi rekk te du ko jëfe, day mel ni nit kuy xool kanamam ci seetu. 24 Bu xoolee kanamam ba noppi, mu dem te fàtte ci saa si ni mu mel. 25 Waaye kiy bàyyi xel te takku ci yoon bu mat, bi mëna goreel ku koy topp, te du yem rekk ci déglu te fàtte waaye da koy jëfe, nit kooku la Yàlla di barkeel ci lu muy def.