1 Yowaana
Kàddug dund gi
1
Kàddu dund gi nekkoon na dale ko ci njàlbéen ga : dégg nanu ko, te sunu bët yi gis ko, xool nanu ko bu baax, te sunu loxo yi laal ko. 2 Dund googu feeñ na: gis nanu ko, ay seede lanu ci. Nu ngi leen di yégal dund gu dul jeex gi nekkoon ci wetu Baay bi te feeñu ci sunu biir. 3 Nun bokk nanu ci dundu Baay bi ak doomam, Yeesu Almasi bi, te nu ngi leen di yégal li nu gis ak li nu dégg, ngir yeen tamit, ngeen bokk ak nun dund googu. 4 Noonu nu ngi leen di bindal mbir yooyu ngir sunu mbégte mëna mat sëkk.
Yàlla leer la
5 Lii mooy xibaar bi nu dégg ci Yeesu Almasi bi te nu di leen ko yégal: Yàlla leer la te amul benn lëndëm ci moom. 6 Su nu waxee ne nun, ci dundam lanu bokk ba noppi di dox ci lëndëm, nu ngi fen te jëfewunu dëgg gi. 7 Waaye su nuy dox ci leer gi, ni Yàlla moom ci boppam nekke ci leer gi, nun ñéppay bokk ci dundam, te deretu Yeesu doomam da nuy setal ci bépp bàkkaar. 8 Su nu waxee ne amunu bàkkaar, nu ngi nax sunu bopp te dëgg gi nekkul ci nun. 9 Su nu nangoo sunuy bàkkaar ci kanamu ñépp, Yàlla mi gore te jub dina nu baal sunuy bàkkaar te setal nu ci bépp njubadi. 10 Su nu waxee ne defunu bàkkaar, nu ngi jiiñ Yàlla fenkat te kàddoom nekkul ci nun.