2 Yowaana
Ki am mbëggeelu Yàlla day dox ci ay ndigalam
1
Man njiit bi, maay bind soxna si Yàlla tànn ak doomam yi ma bëgg ci dëgg gi. Du man rekk sax, waaye ñépp ñi xam dëgg gi bëgg nañu leen tamit, 2 ndax dëgg gi sax ci nun te dina nekk ak nun ba fàww. 3 Yàlla Baay bi ak Yeesu Almasi bi, di Doomu Baay bi, dinañ nu may yiw, yërmande ak jàmm ngir nuy dox ci dëgg gi ak ci mbëggeel gi.4 Am naa mbégte lool ci li ma gis ñenn ci say doom ñuy dox ci dëgg gi, ni nu ko Baay bi digale. 5 Léegi dama la koy ñaan, Soxna si, nanu bëggante ci sunu biir. Du ndigal bu bees laa lay bind waaye bi nu am dale ko ci njalbeen ga. 6 Mbëggeel mooy nuy dox ci ndigali Yàlla. Loolu mooy ndigal bi ngeen déggoon dale ko ci njàlbéen ga, na ngeen dox ci yoon boobu.
7 Ay naxekat yu bari feeñ nañu ci àddina si, te nanguwuñu ne Yeesu Almasi bi ñëw na nekk nit. Nit kuy jëfe noonu mooy naxekat bi ak kiy xeex Almasi bi. 8 Moytuleen yeen ci seen bopp ngir ngeen baña ñàkk sunu meññeefu liggéey bi, waaye ngeen jot neexal bu mat sëkk. 9 Ki saxul ci njàngale Almasi bi, waaye mu dem fu gëna sori, bokkul ci Yàlla. Ki sax ci njàngale moomu am na Baay bi ak Doom ji. 10 Su kenn ñëwee ci yeen te andiwul njàngale moomu, buleen ko dalal seen kër te buleen ko nuyu, 11 ndaxte ki koy nuyu day ànd ak moom ci jëfam yu bon yi.