3 Yowaana
Dénkaane Yowaana ci Gayus
1
Man njiit bi, maa lay bind yaw Gayus sama xarit bi ma bëgg ci dëgg gi. 2 Sama soppe, maa ngi ñaan nga am wér ci fànn yépp, te sa yaram wér, ni sa ruu ame wér. 3 Am naa mbégte lool, bi yenn mbokk ñëwee te seede dëgg gi nekk ci yaw ak ni ngay doxe ci dëgg gi. 4 Sama mbégte mënula weesu ma dégg ne samay doom nu ngi dox ci dëgg gi.
5 Sama soppe, gore nga ci lépp li ngay def ngir mbokki gëmkat yi, ba ci ñi nga xamul sax. 6 Ñoom seede nañu sa mbëggeel ci kanamu mbooloo ñi gëm. Dinga def lu baax soo leen dimbalee ci li des ci seen tukki ci anam bi neex Yàlla. 7 Ndaxte ñoom, dañuy tukki ngir turu Almasi bi, te nanguwuñu dara lu jóge ci ñi gëmul Yàlla. 8 Danoo wara dimbali ay nit yu mel noonu, ngir bokkandoo ak ñoom liggéey bi ñuy matal ngir dëgg gi.
9 Bind naa bataaxal mbooloo ñi gëm, waaye Joteref mi bëgga jiite ñépp, nanguwul sunu sañ-sañ. 10 Loolu moo tax, su ma ñëwee, di naa fésal jëf yi muy def, ci ni muy wax ay kàddu yu ñaaw jëmale ko ci nun. Te yemul ci loolu sax waaye moom ci boppam nanguwul dalal mbokki gëmkat yi, tey tere ñi leen bëgga dalal te di leen dàq ci mbooloo ñi gëm.
11 Sama soppe, bul roy ci lu bon, waaye deel roy ci lu baax. Kiy def lu baax ci Yàlla la bokk; kiy def lu bon xamul Yàlla. 12 Demetirus nag, ñépp ñu ngi koy seedeel lu baax. Dëgg gi sax mu ngi koy seedeel, ak nun tamit nu ngi koy seedeel, te xam nga ne sunu seede dëgg la.
13 Am naa ay mbir yu bari yu ma la wara wax, waaye bëgguma leena bind ci kayit. 14 Yaakaar naa la gis bala yàgg te nu jàkkaarloo waxtaan. 15 Na jàmm nekk ak yaw. Say xarit nu ngi lay nuyu. Nuyul nu sunuy xarit, ku nekk ci turam.