Seedeb Yàlla ci Doomam
5
Ki gëm ne Yeesu mooy Almasi bi, doomu Yàlla la, te ki bëgg Baay bi day bëgg tamit doomam yi. 2 Ci nii lanuy xame ne bëgg nanu doomi Yàlla: bu nu bëggee Yàlla te déggal ay ndigalam. 3 Ndaxte bëgg Yàlla mooy déggal ay ndigalam. Te ndigalam yi diisuñu, 4 ndaxte bépp doomu Yàlla day daan àddina si. Li nuy daane àddina si mooy sunu ngëm.
5 Kiy daan àddina si mooy ki gëm ne Yeesu mooy Doomu Yàlla ji. 6 Yeesu Almasi bi mooy ki ñëw ci ndox ak ci deret: du ci ndox rekk waaye ci ndox ak ci deret. Te Xel mi moo ko seede ndaxte Xel mi mooy dëgg gi. 7 Am na ñett ñuy seede: 8 Xel mu Sell mi, ndox mi, ak deret bi; te ñett ñi déggoo nañu. 9 Su nu nangoo seedeb nit ñi, seedeb Yàlla moo gëna réy. Lii mooy seede bi Yàlla def jëmale ko ci doomam. 10 Ki gëm ci Doomu Yàlla ji, am na seede boobu ci moom. Ki gëmul Yàlla, da koy jiiñ fenkat, ndaxte gëmul ci seede bi Yàlla def jëmale ko ci doomam. 11 Lii mooy seede bi: Yàlla may na nu dund gu dul jeex gi te dund googu mu ngi ci Doomam. 12 Ki am Doom ji am na dund gi. Ki amul Doomu Yàlla ji amul dund gi.
Kóolute gi nu am ci kanamu Yàlla
13 Bind naa leen loolu, yeen ñi gëm ci turu Doomu Yàlla ji, ngir ngeen xam ne am ngeen dund gu dul jeex gi. 14 Te lii mooy kóolute gi nu am ci kanamu Yàlla: su nu ko ñaanee benn mbir bu méngook coobareem, mu ngi nuy déglu. 15 Te su nu xamee ne mu ngi nuy déglu, ak lu nu ko mëna ñaan, xam nanu ne jot nanu li nu ko ñaan.
16 Su kenn gisee mbokkam muy def bàkkaar bu dul yóbbe ci dee, na ñaan, te Yàlla dina may dund mbokk boobu. Mooy ñiy def bàkkaar bu dul yóbbe ci dee. Am na bàkkaar buy yóbbe ci dee. Waxuma mu ñaan ci bàkkaar boobu. 17 Bépp njubadi bàkkaar la, waaye am na bàkkaar bu dul yóbbe ci dee.
18 Xam nanu ne képp kuy doomu Yàlla du sax ci bàkkaar, ndaxte Yàlla day sàmm doomam yi, te ku bon ki mënul dara ci ñoom. 19 Xam nanu ne Yàlla moo nu moom, te àddina si yépp mu ngi ci loxo ku bon ki. 20 Xam nanu tamit ne Doomu Yàlla ji ñëw na te may na nu xam-xam ngir nu xam Yàlla bu dëggu bi. Bokk nanu ci Yàlla bu dëggu bi ndax ni nu bokk ci Doomam Yeesu Almasi bi, moom miy Yàlla bu dëggu bi ak dund gu dul jeex gi. 21 Samay doom, moytuleen xërëm yi.