Saak artu boroom alal yiy noot néew di doole yi
5
Léegi nag, dégluleen yeen boroom alal yi. Jooyleen te di naqarlu ndax musiba yi leen nara dal. 2 Seen alal nëb na te seen yére, max yi lekk nañu ko. 3 Seen wurus ak seen xaalis xomaag nañu, te xomaag boobu dina seede seen réer te lakk seen yaram ni xal. Yeena ngi dajale alal ci bés yu mujj yi. 4 Feyooleen peyoor bi war liggéeykat yi doon góob seen tool, ba tax góobkat yi di ñaxtu te seen yuuxu dem na ba ci noppu Yàlla miy Boroom gàngoori xare. 5 Dund ngeen ci suuf si ci barile ak bànneex. Yafal ngeen seen bopp mel ni ay jur yuy xaar bés bi ñu leen di rendi. 6 Daan ngeen ku jub ki, rey ko, te moom bañul.Dëgër-dëgërlu ci biir coono
7 Kon nag mbokk yi, muñleen ba keroog Boroom bi di ñëw. Xoolleen ni beykat bi di xaare meññeef bu baax ci suuf si. Moom day muñ ba taw yu jëkk yi ak yu mujj yi wàcc. 8 Yeen itam muñleen te dëgër-dëgërlu ndaxte ñëwu Boroom bi jegesi na. 9 Mbokk yi, buleen jàmbat ci seen biir ngir bañ Yàlla àtte leen. Xoolleen àttekat bi mu ngi taxaw sax ci bunt bi. 10 Mbokk yi, xoolleen ci yonent yi doon wax ci turu Boroom bi. Nañu nekk seen royukaayu muñ ci biir coono. 11 Xamleen ne, ñiy dëgër-dëgërlu, ñu barkeel lañu. Dégg ngeen naka la Ayóoba doon dëgër-dëgërloo te gis ngeen li ko Boroom bi may ci mujjantal ba. Ndaxte Boroom bi dafa fees ak mbaax ak yërmande. 12 Bala lépp, mbokk yi, buleen waat: muy ci asamaan, ci suuf si, mbaa ci lu mu mën di doon. Na seen waaw nekk waaw; seen déet nekk déet; ngir ngeen baña daanu ci àtte Yàlla.
Ñaan bu ànd ak ngëm
13 Bu amee ci yeen ku nekk ci coono, na ñaan. Bu amee ku nekk ci mbégte, na sant Boroom bi ak ay woy. 14 Bu kenn ci yeen feebaree, na woo njiiti mbooloo ñi gëm; dinañu ko ñaanal te sotti ko diw ci turu Boroom bi. 15 Ndaxte ñaan bu ànd ak ngëm dina musal ki feebar ba Boroom bi wéral ko. Su fekkee ne dafa bàkkaar, mu baal ko. 16 Na ku nekk wax moroomam bàkkaar yi mu def, te ku nekk ñaanal moroomam ngir ngeen am wér. Ndaxte su nit ku jub ñaanee ak takkute, ñaanam dina nangu. 17 Ilyaas nit la woon ni nun. Bi mu ñaanee ak takkute ngir mu baña taw, benn taw daanuwul ci suuf si lu tollu ci ñetti at ak genn-wàll. 18 Gannaaw loolu mu ñaanaat, te mu taw ba suuf si sax ay meññeef.
Dimbalanteleen ci ngëm gi