Tit
Póol mu ngi nuyu Tit
1
Man Póol, di jaamu Yàlla ak ndawu Yeesu Almasi bi. Yàlla sant na ma, ma indi ci ngëm gi ñi mu tànn, te ma xamal leen dëgg giy tax ñuy takku ci Yàlla, 2 ngir ñu am yaakaar ci dund gu dul jeex gi. Yàlla mi mënula fen moo nu dig dund boobu laata àddina bi di sosu. 3 Ci waxtu bi mu tànn, Yàlla sunu musalkat xamle na kàddoom jaarale ko ci waare bi mu ma dénk te sant na ma, ma yégle ko. 4 Maa ngi lay nuyu Tit, sama doomu bopp ci ngëm gi nu bokk. Na la Yàlla Baay ji ak Yeesu Almasi bi sunu musalkat may yiw ak jàmm.Melokaanu njiiti mbooloo ñi gëm
5 Li tax ma bàyyi la ci réewu Keret mooy nga jubal mbir yi ci des, te ni ma la ko sante, nga tànn ay njiit ci mbooloo ñi gëm ci dëkk bu nekk. 6 Njiit war na nekk nit koo xamante ne kenn amul lu mu koy ŋàññe, te dafa wara yem ci benn soxna rekk, te doomam yi déggal ko maanaam kenn du leen mëna ŋàññe yàqute walla déggadi. 7 Ndaxte kiy jiite mbooloo ñi gëm moo yore kilifteefu njabootu Yàlla, ba tax kenn warula am lu mu koy ŋàññe. Warul nekk ku réy, walla muy gaawa mer. Warul nekk màndikat, walla nit ku tàng, te warul wut xaalis bu lewul, 8 waaye dafa wara nekk ku mëna dalal ay gan, bëgg lu baax, ànd ak sagoom, jub, sell, mëna noot ay yég-yégam, 9 te takku ci kàddu dëgg gi méngoo ak njàngale bu wóor bi. Noonu mu mëna ñaax ñeneen ñi jaarale ko ci njàngale bu dëggu bi, te itam mu mëna yedd ñiy xeex njàngale moomu.
Póol mu ngi ñaax Tit ngir mu yedd waa Keret
10 Ndaxte am na ñu bari ñu déggalul dëgg gi, rawatina Yawut yi bokk ci nun. Ñu ngi nax nit ñi jaarale ko ci seen waxu neen. 11 Fàww nga noppiloo leen, ndaxte ñu ngi jaxase njabooti lëmm, di jàngale li warul ngir am ci xaalis bu lewul. 12 Benn waay bu dëkk Keret, ñu jàppe ko ni yonent, nee na: «Waa Keret ay fenkat lañu mësa doon, soxor ni rabu àll, fuqle te tayel.» 13 Li mu seede dëgg la, moo tax yedd leen bu baax ngir ñu mëna am ngëm bu dëggu, 14 te ñu baña takku ci ay nettali yu dëgguwul yu Yawut yi walla ci ndigali nit ñi dëddu woon dëgg gi. 15 Lépp set na ci ñi set, waaye dara setul ci ñi am sobe te gëmuñu, ndaxte seen xel ak seen xalaat da am sobe. 16 Ñu ngi woote xam Yàlla waaye seeni jëf dañuy weddi Yàlla, ndaxte dañuy def lu Yàlla sib, déggadi, te mënuñoo matal benn jëf bu baax.