Ku gore ci ngëm gi Yàlla dina la neexal
4
Maa ngi lay dénk bu baax ci kanamu Yàlla ak ci kanamu Yeesu Almasi bi wara àtte ñi di dund ak ñi dee, moom mi nara ñëw ni buur: 2 saxal di waare kàddu gi ci bépp jamono, muy neex walla muy naqari. Yedd leen, artu leen, te ñaax leen ci sa njàngale ak muñ bu mat sëkk. 3 Ndaxte jamono baa ngi ñëw bi nga xamante ne, nit ñi duñu nangu njàngale bu dëggu bi, waaye dañuy topp seen bëgg-bëgg bakkan bay dajale ay jàngalekat yu bari yu leen di wax li ñu bëgga dégg. 4 Dootuñu déglu dëgg gi waaye dinañu walbati seeni nopp ci nettali yu dëgguwul yi. 5 Waaye yaw, na nga teey ci lépp, muñal coono yi ngay daj, yégleel xibaar bu baax bi, te nga matal sa liggéey.6 Ndaxte man, maa ngi ci yoonu jébbale sama bopp ni sarax, te bés bi ma wara dee jegesi na. 7 Xare naa xare bu baax bi. Daw naa ba yegg. Téye naa ngëm gi. 8 Léegi nag dinaa jot njubte, di neexal bi ma Yàlla dencal. Boroom bi, di àttekat bu jub bi, dina ma ko jox ci bésu àtte ba, te du ngir man rekk, waaye tamit ngir ñépp ñiy xaar ak mbëggeel waxtu bi muy feeñ.
Tàggatoo Póol ak dénkaaneem yu mujj yi
9 Defal lépp nga fekksi ma ci ni mu gëna gaawe, 10 ndaxte Demas bàyyi na ma dem dëkku Tesalonig ndaxte moom dafa bëgg àddina sii. Kereseñsë dem na diiwaanu Galasi. Tit dem na diiwaanu Dalmasi. 11 Luug rekk moo des ak man. Jëlal Màrk, nga andaale ko, ndaxte amal na ma njériñ bu baax ci liggéey bi. 12 Yónni naa Tisig ca dëkku Efes. 13 Booy ñëw andaaleel ma sama mbubb bu mag bi ma bàyyi ca dëkku Torowas ci këru Karpus. Andaaleel ma tamit téere yi, rawatina yu der yi.
14 Alegsàndar, tëgg bi, def na ma ay ñaawteef yu bari. Boroom bi dina ko fey ay jëfam. 15 Moytu ko yaw tamit, ndaxte da doon xeex sunu waare ak fitna.
16 Keroog bi ma jëkke taxaw di layoo ci àttekaay bi, amul kenn ku ma taxawu. Ñépp a ma bàyyi. Bu leen ko Yàlla toppe. 17 Waaye Boroom bi taxawu na ma te dooleel ma, ba ma mëna tasaare xibaar bu baax bi, ba ñépp ñi dul Yawut dégg ko. Te Boroom bi musal na ma ci gémmiñu gaynde. 18 Boroom bi dina ma musal ci bépp ñaawteef te dina ma dugal ci nguuram gi ci asamaan. Moom moo moom màggaay ba fàww. Amiin.
19 Nuyul ma Piriska ak Akilas ak tamit njabootu Onesifor. 20 Erast mu ngi des ca dëkku Korent te bàyyi naa Torofim mi feebar ci dëkku Mile. 21 Defal lépp ngir ñëw bala jamono seddaay bi di jot. Ëbulus, Pudeñsë, Linus, Këlójaa, ak mbokki gëmkat yi yépp ñu ngi lay nuyu. 22 Na Boroom bi nekk ak yaw, te na yiwam nekk ak yeen ñépp.