Póol mu ngi artu Timote ci mujjum jamono te di ko dëgëral
3
Xamal bu baax lii: bés yu metti dinañu am ci mujjum jamono, 2 ndaxte nit ñi dinañu siis, fonk xaalis, di wonewu tey réy-réylu, di wax lu ñaaw ci Yàlla, dootuñu déggal seen waajur yi, dinañu goreedi, dootuñu jox cér li jóge ci Yàlla, 3 dinañu dëgër xol, dootuñu am yërmande, di ay jëwkat, dootuñu mëna noot seeni yég-yég, dinañu soxor, bañ lu baax, 4 di ay workat, ëppal, fees ak réy-réylu, te seen bëgg-bëgg bakkan gënal leen Yàlla. 5 Dinañu mbubboo takku ci Yàlla waaye duñu nangu kàttan bi nekk ci loolu. Soril nit ñu mel noonu.6 Ñenn ci ñoom dañuy dugg ci kër yi, di xiir jigéen ñi nooy bopp te fees ak bàkkaar te seen bëgg-bëgg jiital leen. 7 Jigéen yooyu dañuy wuta xam saa su nekk waaye duñu mëna fexe ba xam dëgg gi. 8 Ni Sànnes ak Sàmbares doon jaamaarloo ak Musaa, noonu tamit la nit ñooñu di jaamaarloo ak dëgg gi. Seen xel dafa yàqu te seen ngëm dëgguwul. 9 Waaye duñu dem fu sori ndaxte seen ñàkk xel dina feeñ ci bëtu ñépp ni mu meloon ci Sànnes ak Sàmbares.
10 Yaw nag, topp nga ma ci sama njàngale, ci sama dundin, ci samay mébét, ci sama ngëm, ci sama muñ, ci sama mbëggeel, ci sama dëgër-dëgërlu, 11 ci ni ñu may fitnaale ak ci sama coono. Xam nga ni ñu ma fitnaale ci dëkki Ancos, bu Ikoñum, ak bu Listar! Waaye Boroom bi yewwi na ma ci loolu lépp. 12 Dëgg la, ñépp ñi bëgga takku ci Yàlla jaarale ko ci ngëm gi ci Yeesu Almasi bi dinañu daj fitna. 13 Waaye nit ñu soxor ñi ak naxekat yi dinañu gëna sori ci lu bon, di nax ñeneen ñi, bay naxaale seen bopp.
14 Waaye yaw nag, saxal ci li nga jàng te mu wóor ci yaw. Xam nga ci ñan nga ko jànge. 15 Ci sa ndaw ba léegi, nga xam Mbind yu sell yi. Ñoom, ñoo la mëna jox xel mu rafet mi jur mucc gi, jaarale ko ci ngëm gi ci Yeesu Almasi bi. 16 Mbind mu sell mi yépp, ci gémmiñu Yàlla la jóge, te dafa am njériñ ngir jàngale, yedd, jubbanti, ak yar ci njubte. 17 Ci noonu nitu Yàlla ki dina mat sëkk ngir mu mëna def bépp jëf bu baax.