1 Timote
Njàngale bu dëggu bi
1
Man Póol di ndawu Yeesu Almasi bi jaarale ko ci ndigalu Yàlla sunu musalkat ak Yeesu Almasi bi sunu yaakaar, 2 maa ngi lay nuyu, yaw Timote, sama doomu bopp ci ngëm gi. Na la Yàlla Baay bi ak sunu Boroom Yeesu Almasi bi may yiw, yërmande, ak jàmm.
3 Bi may dem diiwaanu Maseduwan, ñaax naa la ngir nga des dëkku Efes ndaxte am na fa ñuy jàngale lu dëgguwul. Digal leen ñu bàyyi ko, ni ma la ko waxe woon. 4 Wax leen ñu baña takku ci nettali yu dëgguwul ak ci limi maam yu dul jeex mukk. Mbir yooyu ay werante rekk lañuy jur te duñu jëmloo ci kanam tëralinu Yàlla bi nu xam jaarale ko ci ngëm gi.
5 Sunu njàngale mi, li ko taxa jóg mooy mu jur mbëggeel bu jóge ci xol bu set, xel bu amul lu muy ŋàññe boppam, ak ngëm bu dëggu. 6 Am na ñenn ñu won gannaaw sunu njàngale moomu ba réer ci ay werante yu amul benn njériñ. 7 Ñoom, dañoo bëgga nekk ay jàngalekatu yoonu Musaa, waaye xamuñu dara ci li ñuy wax walla ci mbir yi ñuy dëggal ak doole.
8 Nun, xam nanu ne yoon bi baax na, su fekkee ne nu ngi koy jëfandikoo ni mu ware. 9 Fàww nu xam ne yoon bi, tëraluñu ko ngir ñu jub ñi, waaye ngir ñu jubadi ñi, fippukat yi, ñu soxor ñi, ak bàkkaarkat yi; ngir ñi joxul Yàlla cér te fonkuñu lu sell; ngir ñiy rey seen baay walla seen yaay, ak yeneen reykatu nit yi, 10 ñiy dund ci njaaloo, góor-jigéen yi, ak ñiy jaay seen moroom ni jaam, fenkat yi ak ñiy waat ci lu dul dëgg, ak ñépp ñuy def lu wuute ak njàngale bu dëggu bi. 11 Njàngale bu dëggu boobu moo dëppoo ak xibaar bu baax bi ma Yàlla dénk, biy feeñal màggaayu Yàlla di boroom barke.
Póol mu ngi sant Yàlla tey ñaax Timote
12 Maa ngi gërëm sunu Boroom Yeesu Almasi bi, moom mi ma dooleel, ndaxte moo ma àtte ni ku gore, ci ni mu ma tànne ngir ma liggéeyal ko, 13 man mi nga xam ne, bu jëkk, dama doon wax lu ñaaw ci moom, di ko fitnaal, te di ko saaga. Waaye Yàlla yërëm na ma ndaxte dama doon jëf ci ñàkka xam, ndax ñàkka gëm. 14 Te yiw bi ma sunu Boroom Yeesu Almasi bi may baawaan na ci man. May na ma ngëm ak mbëggeel bu jóge ci moom. 15 Lii kàddu gu wóor la, gu ñépp wara nangu: Yeesu Almasi bi ñëw na ci àddina si ngir musal bàkkaarkat yi, te man, maa ci gëna yées. 16 Waaye lii moo tax Yàlla yërëm ma: ngir Yeesu Almasi bi wone muñam gu réy ci man, mi gëna yées ci bàkkaarkat yi. Def na loolu ngir ma nekk royukaay ci ñi nara gëm ci moom ngir jot dund gu dul jeex gi.
17 Na ñépp sargal Yàlla te màggal ko ba fàww. Moom mooy Buur bi sax ba fàww, du dee mukk, te kenn mënu ko gis. Moom rekk mooy Yàlla. Amiin!
18 Yaw Timote sama doom, ndigal bi ma lay dénk, dafa dëppoo ak kàddu yi ñu waxoon ci turu Yàlla jëmale ko ci yaw, mooy nga gànnaayoo kàddu yooyu ngir xare xare bu baax bi. 19 Ngir xare xare bu baax boobu, fàww nga téye ngëm gi te nga dund ci anam bi nga xam ne sa xel du am lu mu lay ŋàññe. Ñenn ñi dañoo tàggoo ak mbir yooyu ba tax ñu ñàkk seen ngëm. 20 Am na ci seen biir Imene ak Alegsàndar. Jébbal naa leen Seytaane ngir, su leen metitalee, ñu jàng bañatee wax ci Yàlla lu ñaaw.