Póol mu ngi dénk mbooloo ñi gëm ci lu jëm ci ni ñuy màggale Yàlla
2
Sama sas bu jëkk ci mboolooy ñi gëm mooy ñu indi ñépp ci kanamu Yàlla ngir ñaanal leen, saraxtul leen, tey gërëm Yàlla ngir ñoom. 2 Nañu ñaanal buur yi ak ñépp ñi nekk ci nguur, ngir nun, nu mëna dund ci jàmm ak dal ànd ak takkute ci Yàlla ak dundin bu baax. 3 Loolu mooy li baax te neex Yàlla sunu Musalkat, 4 moom mi bëgg nit ñi ñépp mucc te xam dëgg gi. 5 Ndaxte benn Yàlla doŋŋ moo am, ak kenn rekk kuy juboole Yàlla ak nit ñi. Nit kooku mooy Yeesu Almasi bi, 6 mi joxe bakkanam ngir fey boru bàkkaaru ñépp. Loolu mooy seede bi mu joxe ci waxtu bi ko Yàlla bëgge. 7 Yàlla tànn na ma ni waarekat ak ndaw ngir ma yégle seede boobu tey jàngal ñi nekkul Yawut lu jëm ci ngëm gi ak dëgg gi. Dëgg bu wér péŋŋ la; fenuma.
8 Looloo tax ma bëgg góor ñi di ñaane fu nekk di yékkëti ay loxo yu set ci asamaan te baña ànd ak mer walla xuloo.
9 Noonu tamit bëgg naa jigéen ñi di sol yére yu jot, ànd ak sutura ak woyof. Bu ñu di léttu létt yu fés walla ñuy takk wurus walla per walla ñuy sol yére yu njég li bari, 10 waaye na seen solu nekk jëf yu baax. Loolu mooy li jekk ci jigéen yiy wax ne dañoo takku ci Yàlla.
11 Na jigéen ñi jot njàngale mi ci dal ànd ak déggal gu mat sëkk. 12 Mayuma jigéen muy jàngale walla muy jël kilifteef ci kaw góor. Waaye na dal. 13 Ndaxte Aadama la Yàlla jëkka sàkk, door cee teg Awa. 14 Te du Aadama la Seytaane naxoon, waaye ku jigéen ki, ba mu ñàkka déggal ndigalu Yàlla. 15 Ci jigéen la ki koy musal di soqeekoo. Noonu nag, jigéen ñi dinañu mucc su ñu saxee ci ngëm, mbëggeel, sellaay, ak woyof.