2 Timote
Póol mu ngi ñaax Timote ngir mu sax ci ngëm gi
1
Man Póol di ndawu Yeesu Almasi bi ci coobarey Yàlla. Moo ma fal ngir ma yégle dund gi Yàlla dig ñépp ñi gëm ci Yeesu Almasi bi. 2 Maa ngi lay nuyu Timote sama doom bi ma bëgg. Na la Yàlla baay bi ak sunu Boroom Yeesu Almasi bi may yiw, yërmande, ak jàmm.
3 Saa su may ñaan guddi ak bëccëg, dama lay ñaanal te maa ngi gërëm Yàlla mi may liggéeyal ni ko samay maam daan defe, ba tax sama xel du am lu mu may ŋàññe. 4 Maa ngi fàttaliku say rongooñ te bëgg naa la gisaat ngir ma fees ak mbégte. 5 Maa ngi fàttaliku sa ngëm gu dëggu, ngëm gi sa maam bu jigéen Lowis ak sa yaay Ënis amoon laata yaw. Wóor na ma ne am nga ko tamit. 6 Looloo tax ma la koy fàttali: wéyal di jëfandikoo may bi la Yàlla may, keroog bi ma la tegee loxo, 7 ndaxte Xel bi nu Yàlla may du nu ragalloo, waaye dafa nuy feesal ak kàttan, mbëggeel, ak sago.
8 Kon nag, bul rusa seede sunu Boroom te bul rus ndax man mi nekk ci kaso bi ngir moom. Waaye na nga bokk ak man coono ngir xibaar bu baax bi jaarale ko ci kàttanu Yàlla. 9 Moom moo nu musal te woo nu ngir nu doon moomeelam, du sax ndax sunuy jëf yi nu matal waaye ndax yiwam ngir tëralinu boppam. May na nu yiw boobu jaarale ko ci Yeesu Almasi bi laata àddina bi di sosu, 10 waaye léegi Yàlla fésal na yiwam ci nun, bi mu feeñalee sunu musalkat Yeesu Almasi bi. Moom moo noot doole dee te fésal dund gu dul jeex gi jaarale ko ci xibaar bu baax bi. 11 Yégle xibaar bu baax boobu moo tax Yàlla fal ma ni waarekat, ndaw, ak jàngalekat. 12 Looloo waral may daj coono yii, waaye rusuma ci, ndaxte xam naa ki ma gëm, te wóor na ma ne moom am na kàttanu denc li nga xam ne moom la ma dénk ba keroog bésu àtte bi. 13 Jëlal ni royukaay kàddu yu dëggu yi nga dégge ci man. Denc leen ci ngëm gi ak ci mbëggeel bi nu Yeesu Almasi bi may. 14 Dencal mbir yu baax yi la Yàlla dénk jaarale ko ci ndimbalu Xel mu Sell mi dëkk ci nun.
15 Ni nga ko xame, ñépp ñi jóge woon ca diiwaanu Asi bàyyi nañu ma, ñu ci mel ni Fusel ak Ermosen. 16 Na Boroom bi may yërmandeem njabootu Onesifor, ndaxte daan na ma dëfël te rusul woon ndax ni ma nekk ci kaso. 17 Waaye bi mu yegsee ci dëkku Room, seet na ma fu nekk ba gis ma. 18 Na ko Boroom bi may yërmandeem ci bésu àtte ba. Xam nga bu baax ñaata yoon la ma dimbali ba ma nekkee ci dëkku Efes.