Ndigalu Póol ci lu jëm ci jaam yi
6
Na ñépp ñi nekk jaam jox cér gu mat sëkk seeni njaatige, ngir kenn baña wax lu ñaaw turu Yàlla ak sunu njàngale mi. 2 Jaam yi am ay njaatige yu gëm, waruñu leena yab ndax ni ñu nekk seeni mbokk. Waaye nañu leen gëna liggéeyal bu baax ndaxte ñiy jériñoo seen liggéey ay gëmkat yu nu sopp lañu. Loolu nga leen wara jàngal te di leen ci ñaax.
Alal ju wóor ji
3 Su amee kuy jàngale leneen te nanguwul kàddu yu dëggu yu sunu Boroom Yeesu Almasi bi, te nanguwul tamit njàngale mi dëppoo ak ngëm gi, 4 nit kooku dafa fees dell ak réy-réylu te xamul dara. Dafa am feebar bi koy xiir ci waxtaan ak werante ci li baat yi di tekki. Loolu day andi iñaan, xuloo, wax ju ñaaw, ñaaw njort, 5 ak waxtaan yu dul jeex. Ñiy jëfe noonu, seen xel dafa ñaaw te xamatuñu dëgg gi. Ñoom dañoo xalaat ne gëm ci Yàlla wutukaayu alal la. 6 Ba tey, gëm ci Yàlla alal bu mag la, su fekkee nit ki doylu ci li mu am. 7 Ndaxte andaalewunu dara ci àddina si, te mënunu yóbbaale dara. 8 Su fekkee nag am nanu lu nuy lekk ak lu nuy sol, war nanu doylu ci loolu. 9 Waaye ñi bëgga am alal dinañu daanu ci nattu, ba dugg ci fiiru seen bëgg-bëgg yu bari yu amul njériñ te bon. Bëgg-bëgg yooyu ñooy dugal nit ñi ci yàqute ak ci sànkute, 10 ndaxte mbëggeelu xaalis mooy jur bépp xeetu mbon. Am na ñiy wut xaalis ba tax ñu sori yoonu ngëm gi te teg seen bopp metit yu bari.
11 Kon nag yaw nitu Yàlla bi, dawal ba sori mbir yooyu, te nga wut njubte, takkute ci Yàlla, ngëm, mbëggeel, dëgër-dëgërlu, ak lewet. 12 Na nga xare xare bu baax bi ngir wéy ci ngëm gi. Téyeel dund gu dul jeex gi, bi nga xam ne Yàlla moo la ci woo woon, te nga waxoon ko bu baax ci kanamu seede yu bari. 13 Maa ngi lay dénk ci kanamu Yàlla mi di jox lépp dund, ak ci kanamu Yeesu Almasi bi mi seede woon ci kanamu Poñsë Pilaat seede bu rafet: 14 sàmmal ndigal boobu, nga baña am gàkk walla lenn lu ñu lay ŋàññe, ba bés bi sunu Boroom Yeesu Almasi bi di feeñaat. 15 Yàlla mooy ki koy feeñalaat ci waxtoom. Moom mooy boroom barke te moom rekk moo yilif lépp, buuru buur yi ak boroomu boroom yi. 16 Moom rekk mooy ki dul dee, moom moo dëkk ci leer bu kenn mënula jege. Kenn mësu ko gis te nit mënu ko gis. Moom moo yelloo teraanga ak kàttan ba fàww. Amiin.
17 Boroom alal yi ci àddina sii, dénk leen ñu baña réy-réylu te ñu baña teg seen yaakaar ci alal yu wóorul yi. Waaye ñu teg seen yaakaar ci Yàlla, moom miy joxe lépp ba mu ne gàññ, nu ciy bànneexu. 18 Ñaax leen ñuy def lu baax, ñu bari ay jëf yu rafet, ñu yéwén tey séddoo ak ñeneen ñi. 19 Te ci noonu dinañu dajale alal bu baax te wóor ngir mëna jot dund gu dul jeex gi ci àllaaxira.
20 Céy yaw Timote, sàmmal bu baax li la Yàlla dénk. Te nga moytu ay wax yu amul benn njériñ te wuute ak ngëm gi. Moytul tamit werante boo xam ne ñeneen ñi, dañu koy jàppe xam-xam, waaye dëgguwul. 21 Am na ñenn ñu gëm ne am nañu xam-xam boobu ba mujje sori ngëm gi. Na yiwu Yàlla nekk ak yeen ñépp.