Ndigalu Póol ci lu jëm ci jigéen ñi ñàkk seen jëkkër
5
Booy yedd góor gu mag bu ko gëdd, waaye ñaax ko ni ngay waxe ak sa baay. Waxambaane yi, nga def leen ni say rakk, 2 jigéen yu mag yi, ni sa yaay, te xale yu jigéen yi, ni say jigéen te seen diggante set wecc.3 Jigéen ñi ñàkk seen jëkkër te ñu des ñoom kese, toppatoo leen te nga jox leen cér. 4 Jigéen ji ñàkk jëkkëram te yor ay doom walla ay sët, na ñooñu jëkka wone seen takkute ci Yàlla ci seen biir kër, di delloo njukkal seen waajur, ndaxte loolu moo neex Yàlla. 5 Ki ñàkk jëkkëram, des moom kese, te amul kenn ku koy jàppale, day teg yaakaaram ci Yàlla te du noppi di ko ñaan te di sàkku ci moom ndimbal guddi ak bëccëg. 6 Waaye ki ñàkk jëkkëram tey dund ci li ko neex, dee na ba noppi su fekkee sax mu ngi dund. 7 Fàttali leen loolu, ngir ñu baña am lenn lu ñu leen mëna ŋàññe. 8 Nit ki dul toppatoo mbokkam, rawatina waa këram, weddi na ngëm gi, te nit kooku moo gëna yées ki amul ngëm.
9 Jigéen ju ñàkk jëkkëram, bala ñu koy lim ci ñi mbooloo ñi gëm wara jàppale, war na am juróom benn fukki at jëm kaw, te itam mu nekk ku yemoon ci jëkkëram rekk. 10 Moom war na nekk nit ku ñuy seedeel jëf yu baax: maanaam yar bu baax doomam yi, di dalal gan yi, tey raxas tànki ñi Boroom bi moom, di wallu ñi nekk ci coono, ak di jëf bépp jëf bu baax. 11 Wànte nag, jigéen ñi ñàkk seen jëkkër te nekk ndaw, bu leen boole ci lim bi, ndaxte su leen seen bëgg-bëgg xiiree ci bëgga séyaat, dañuy sori liggéeyu Almasi bi. 12 Loolu dina tax Yàlla àtte leen ndaxte mataluñu dige bi ñu defoon bu jëkk. 13 Te itam dañuy mujje tayel te tàmm di dem kër ak kër. Li ci gëna bon mooy dañuy réy làmmiñ, di dugg ci lu seen yoon nekkul, tey wax lu amul benn njériñ. 14 Kon nag bëgg naa ñi ñàkk seen jëkkër te nekk ndaw séyaat, ñu am ay doom te toppatoo seen kër. Bu booba, duñu may noon yi bunt ngir ñu wax lu ñaaw ci nun. 15 Ndaxte am na ñu ñàkk seen jëkkër te bàyyi yoon bu jub bi ngir topp Seytaane. 16 Jigéen bu gëm, bu amee ci njabootam ku ñàkk jëkkëram, da ko wara jàppale. Su booba, mbooloo ñi gëm du ko jàppale ngir mëna jàppale yeneen jigéen yi ñàkk seen jëkkër te amuñu kenn ku leen jàppale.
Ndigalu Póol ci lu jëm ci njiit yi
17 Njiit yiy jiite bu baax mbooloo ñi gëm, yelloo nañu peyoor ak ñu jox leen cér, rawatina ñiy sonn ci waare bi ak ci njàngale mi. 18 Ndaxte Mbind mi nee na: «Bul tàkk gémmiñu nag biy bojj» te «liggéeykat bi yelloo na peyooram.» 19 Bul nangu ñu tuumaal njiit ci sa kanam feek amul ñaar walla ñetti seede. 20 Su amee ay njiit yu bàkkaar, yedd leen ci kanamu ñépp ngir ñi ci des ragala def ni ñoom.
21 Maa ngi lay dénk ci kanamu Yàlla, Yeesu Almasi bi, ak malaaka yu tedd yi: nga sàmm ndigal yooyu te baña gënatle mbaa di par-parloo. 22 Bul gaawantu di teg loxo nit ngir fal ko njiit. Bul bokk ci bàkkaari ñeneen ñi. Na sa dund sax ci set.
23 Bul yem ci naan ndox rekk, waaye jëlal tuuti biiñ ngir faj say metitu biir ak say jàngoro yu bari.