Póol mu ngi artu nit ñi ci njàngale yu dëgguwul yi tey ñaax Timote
4
Xel mu Sell mi wax na ci bu leer ne ci jamono yu mujj yi ñenn ñi dinañu bàyyi ngëm gi ngir topp ay xel yu leen di nax, ay njàngale Seytaane, 2 ak ay nit yu naaféq te nekk ay fenkat. Nit ñooñu ñu topp, seen xol dafa dërkiis. 3 Ñuy jàngale ne waruñu séy te waruñu lekk yenn xeetu lekk yi. Moona Yàlla moo sàkkal lekk yooyu ñi gëm te xam dëgg gi, ngir ñu di leen lekk ak cant. 4 Ndaxte lépp li Yàlla sàkk lu baax la te waruñu ci tere lenn, su fekkee ne nu ngi koy jëfandikoo ak cant, 5 ndaxte Yàlla moo ko sellal, jaarale ko ci kàddoom ak ci ñaan yi.
6 Jàngalal loolu lépp mbokki gëmkat yi. Noonu dinga nekk surga bu baax bu Yeesu Almasi bi, tey dunde kàddu ngëm gi ak njàngale bu baax bi nga topp. 7 Waaye moytul nettali yu dëgguwul yi te amuñu njériñ. Wànte tàggatal sa bopp ci takku ci Yàlla. 8 Tàggat yaram njériñam am na fu mu yem, waaye takku ci Yàlla am na njériñ ci lépp, ndaxte ci moom la dige dund gi nekk, ci àddina sii ak ci àllaaxira. 9 Loolu kàddu gu wóor la gu ñépp wara nangu. 10 Waaw, looloo tax nuy liggéey tey góor-góorlu, ndaxte danoo teg sunu yaakaar ci Yàlla Aji-Dund ji, moom miy musalkatu ñépp, rawatina ñi gëm.
11 Dénk leen loolu lépp te nga jàngal leen ko. 12 Bu la kenn xeeb ndax say at yu néew, waaye na nga nekk royukaay ngir mbokki gëmkat yi, ci kàddu, ci jëfin, ci mbëggeel, ci ngëm, ak ci sa dund bu set. 13 Na nga sax di jàng Mbind yu sell yi ci kanamu ñépp, di ko waare te di ko jàngale ba keroog may ñëw. 14 Bul sàggane mayu Xel mu Sell mi nekk ci yaw, bi nga jot jaarale ko ci kàddu yonent yi, keroog bi la njiiti mbooloo ñi gëm tegee loxo. 15 Nanga farlu ci loolu, nga sóobu ci liggéey bi bu baax, ngir ñépp gis say jéego. 16 Bàyyil xel ci sa dundin ak ci sa njàngale. Saxal ci loolu, ndaxte sooy jëfe noonu di nga mucc, yaw ak ñi lay déglu.