Melokaanu njiiti mbooloo ñi gëm
3
Lii kàddu gu wóor la: su nit bëggee bokk ci njiiti mbooloo ñi gëm, liggéey bu baax la bëgg. 2 Njiitu mbooloo ñi gëm dafa wara nekk nit koo xamante ne kenn amul lu mu koy ŋàññe. Dafa wara yem ci benn soxna, teey, ànd ak sagoom, am faayda, ku mëna dalal ay gan, te mëna jàngale. 3 Warul nekk màndikat, te warul nekk nit ku tàng, waaye dafa wara lewet te dal, te alal waru ko jiital. 4 Na nekk kuy jiite bu baax këram te yar ay doomam ngir ñu déggal ko te jox ko cér. 5 Ndaxte bu nit mënul jiite këram ni mu ware, naka lay jiite mbooloo ñi Yàlla moom. 6 Warula nekk kuy dooga tuub ci ngëm gi ngir mu baña fees ak réy-réylu te Yàlla bañ ko teg daan ni mu tege daan Seytaane. 7 Te it, dafa wara am seede bu rafet ci nit ñi bokkul ci mbooloo ñi gëm ngir ñu bañ koo wax lu ñaaw te mu baña daanu ci fiiru Seytaane.8 Ñiy dimbali njiit yi ci seen liggéey war nañu am faayda te dëggu. Waruñu nekk ay màndikat walla ñuy wut xaalis bu lewul. 9 War nañu sax ci dëgg gi Yàlla feeñal ci ngëm gi, ba tax seen xel du am lu mu leen di ŋàññe. 10 Ñoom, war nañu leen seetlu ba noppi, te noonu bu ñu amul dara lu ñu leen di ŋàññe, ñu mëna tàmbalee liggéey. 11 Jigéen ñiy dimbali njiit yi tamit war nañu am faayda, waruñu nekk ay nit yuy jëw seeni moroom, war nañu teey te ñu wóolu leen ci lépp. 12 Ñiy dimbali njiit yi war nañu yem ci benn soxna rekk te ñu jiite bu baax seeni doom ak seeni kër. 13 Ci noonu ñi ci matal bu baax seen liggéey dinañu leen jox cér bu mat sëkk, te dinañu mëna wax ak kóolute ci ngëm gi ñu am ci Yeesu Almasi bi.
Yàlla feeñal na li nëbbu woon
14-15 Yaakaar naa ne dinaa la seetsi bala yàgg, waaye mën na am ma yéexa ñëw. Moo tax ma lay bind bataaxal bii, ngir nga xam ni ñu wara dunde ci njabootu Yàlla, maanaam mbooloo ñi gëm te Yàlla Aji-Dund ji moom leen. Mbooloo moomu mooy kaaraange ak wéeruwaayu dëgg gi. 16 Li wóor mooy, li nëbbu woon ci sunu ngëm te Yàlla feeñal ko, lu réy la!
Almasi bi feeñu na, nekk nit,
Xel mu Sell mi wone na ne ku jub la,
feeñu na malaaka yi,
nit ñi yégle ko ci ñi nekkul Yawut,
gëm nañu ko ci àddina si,
Yàlla yékkëti na ko ci màggaay.