Jëfi Ndawi Yeesu yi
Yeesu jox na ndawam yi ay ndigal te Yàlla yékkëti ko asamaan
1
Yaw Teyofil, nettali naa ci sama téere bu jëkk lépp li Yeesu tàmbali woon di jëf te di ko jàngale, 2 dale ko ci njàlbéen ba, ba bés bi ko Yàlla yékkëtee ci kaw asamaan, gannaaw bi mu joxee ndigal ndaw yi mu tànnoon jaarale ko ci Xel mu Sell mi. 3 Gannaaw coonoom ba ni mu deewe, feeñu na ndaw yi te won leen ay firnde yu bari te wóor ne mu ngi dund ci diiru ñeent fukki fan te muy wax ak ñoom ci lu jëm ci nguuru Yàlla gi. 4 Benn bés, bi muy lekkandoo ak ñoom, mu jox leen ndigal bii: «Buleen sori Yerusalem waaye xaarleen li Baay bi dige woon bi ngeen dégge ci sama gémmiñ ma waxoon ko. 5 Ndaxte Yaxya doon na sóob nit ñi ci ndox waaye yeen ci ay fan yu néew Yàlla dina leen sóob ci Xel mu Sell mi.» 6 Ñi nekkoon ci wetu Yeesu laaj ko ne: «Boroom bi, ndax ci waxtu bii ngay delloo Israyil nguuram?» 7 Mu tontu leen ne: «Du yeena wara xam bés bi walla waxtu bi Baay bi tànn ci sañ-sañam. 8 Waaye Xel mu Sell mi dina wàcc ci seen kaw, feesal leen ak kàttanam te dingeen nekk samay seede ci Yerusalem, ci Yude yépp, ci diiwaanu Samari, ba fu àddina si yem.» 9 Gannaaw bi mu waxee kàddu yooyu ba noppi Yàlla yékkëti ko ci seeni bët te benn niir muur ko. 10 Bi ñuy wéy di xool muy yéeg, ci saa si ñaari góor yu sol yére yu weex feeñu leen, 11 ne leen: «Yeen waa Galile, lu tax ngeen nekk di wéy di xool ci asamaan si? Yeesu mi ngeen gis ñu yékkëti ko ci asamaan, ci anam bi ngeen ko gise muy dem ci asamaan, ci anam boobu lay dellusee.» 12 Noonu ñu jóge ci tund bi ñu woowe Tundu Oliw ya, ñu dellu Yerusalem, te diggante tund boobu ak Yerusalem tollu woon na ci benn kilomet. 13 Bi ñu yegsee Yerusalem, ñu yéeg ci néeg bu féete ci kaw fi ñu doon dal. Ñii ñoo fa nekkoon: Piyeer, Yowaana, Saag, Andare; Filib, Tomaa, Bartelemi, Macë; Saag doomu Alfe, Simoŋ di ku takku ci réewam, ak Yudaa di doomu ku tudd Saag. 14 Ñoom ñépp bokkoon nañu benn xel te farlu ci ñaan ak rakku Yeesu yi, ak yenn jigéen te Maryaama di yaayu Yeesu bokkoon ci.
Tànn nañu Maccas ngir mu wuutu Yudaa
15 Ci bés yooyu Piyeer jóg taxaw ci kanamu mbokki gëmkat yi, te ñu tollu ci téeméeri nit ak ñaar fukk. Mu ne leen: 16-17 «Samay mbokk, Xam ngeen li daloon Yudaa. Li Xel mu Sell mi wax ci Mbind mi jaarale ko ci gémmiñu Daawuda ci lu jëm ci moom, fàww mu mat. Yudaa bokkoon na ci nun te amoon wàll ci liggéey bii. Waaye mu jiite woon ñi jëlsi woon Yeesu. 18 Xaalisu bàkkaar boobu, mu jënde ko tool. Mu daanu fa, jiital boppam, biiram xar, butitam yi tuuru. 19 Waa Yerusalem yépp déggoon nañu loolu, moo tax ci seen lakk ñu tudde woon tool boobu Akeldama, li tekki toolu deret. 20 Mbind mi nee na ci téere Saboor yi: "Na këram nekk màndiŋ, te kenn bañ fa dëkk." Ñu bindaat ne: "Na keneen def liggéeyam." 21 Kon nag fàww ñu jël kenn ci ñi doon ànd ak nun ci jamono bépp bi Boroom bi Yeesu di dem ak di ñëw ak nun 22 dale ko ci jamono ji Yaxya doon sóobe nit ñi ci ndox ba bés bi Yàlla yékkëtee Yeesu, ngir mu nekk seede ak nun ci ndekkiteem.» 23 Noonu ñu jël ñaar ci ñoom di Yuusufa mi tudd Barsabas te ñu koy woowe Yustus, ak Maccas, 24 te ñu ñaan ñaan bii: «Boroom bi, yaw mi xam xolu ñépp, won nu ki nga tànn ci ñaar ñii, 25 ngir muy def liggéeyu ndaw te mu wuutu Yudaa mi bàyyi, jël wàll bi mu yelloo.» 26 Noonu ñu tegoo bant ci ñaar ñi. Bant bi dal ci Maccas. Mu fekki fukki ndaw yi ak benn.