Luug
Bataaxal bi Luug bind Teyofil
1
1-2 Teyofil mu tedd mi, ñi fekke woon te seede xew-xew yii mat ci sunu biir, ba ñu tàmbalee, te nekk ay liggéeykatu kàddug Yàlla gi, ñoo nu leen jottali. Ñu bari sóobu woon nañu ci bindum téere ci xew-xew yooyu, ni ñu leen jote. 3 Moo tax man tamit, ma xalaat bu baax ne, war naa la bindal xew-xew yooyu ci ni mu ware, gannaaw bi ma gëstoo bu baax ci lépp; dale ko ca njàlbéen ga ba ci njeextal gi, 4 ngir mu wóor la ne li ñu la jàngal dëgg ju wér péŋŋ la.
Malaaka Jibril yégle na juddub Yaxya
5 Ci jamono bi Erodd bu mag nekkee buuru Yude, amoon na benn jébbalkatu-sarax bu tuddoon Sakari. Mu bokkoon ci mbootaayu jébbalkati-sarax yi askanoo ci Abiya te jabaram Elisabet bokkoon ci askanu Aaróona jébbalkatu-sarax-bu-mag bi. 6 Sakari ak jabaram juboon nañu ci kanamu Yàlla di topp ndigalu Boroom bi yépp ak li mu santaane ni mu ware, 7 waaye amuñu woon doom ndaxte Elisabet mënul woona am doom te ñoom ñaar ñépp dañoo màggatoon.
8 Benn bés, Sakari doon na def liggéeyu jébbalkatu-sarax bi ci kër-Yàlla gi ndaxte mbootaay bi mu bokkoon moo aye woon. 9 Ci aaday jébbalkatu-sarax yi, dañu doon tegoo bant ngir xam ku wara taal cuuraay bi. Bant bi dal ci Sakari, moo tax mu dugg ci biir béréb bu sell bu Boroom bi ngir taal fa cuuraay bi. 10 Ci waxtu bi muy taal cuuraay bi, mbooloo mu takku ñu ngi woon ci biti di ñaan. 11 Noonu benn malaaka Boroom bi feeñu Sakari, mu taxaw ci ndeyjooru fi ñuy taale cuuraay bi. 12 Bi ko Sakari gisee mu jaxasoo ànd ak tiit. 13 Malaaka bi ne ko: «Sakari, bul tiit ndaxte Yàlla nangu na sa ñaan. Sa jabar Elisabet dina la amal doom bu góor. Nanga ko tudde Yaxya. 14 Dina nekk mbégte bu réy ci yaw, te ñu bari dinañu bànneexu ci juddoom. 15 Dina nekk nit ku màgg ci kanamu Boroom bi Yàlla. Du naan biiñ walla dara lu koy màndiloo. Dina fees ak Xel mu Sell mi, dale ko ci bi mu nekkee ci biiru yaayam, 16 te dina delloosi waa Israyil yu bari ci Yàlla seen Boroom. 17 Dina dox ci kanamu Yàlla, te Xel mu Sell mi dina jëf ci moom ak kàttan, ni mu doon jëfe ci yonent Yàlla Ilyaas ngir jubale baay yi ak seeni doom, te delloosi ñi déggalul Yàlla ci xam-xamu ñu jub ñi, ngir waajal askan bu taxaw temm ngir xaar Boroom bi.»
18 Sakari laaj malaaka bi ne: «Naka laay xame ne loolu dëgg la? Ndaxte man mag laa te sama jabar tamit màggat na.» 19 Malaaka bi ne ko: «Man maay Jibril. Damay taxaw ci kanamu Yàlla ngir liggéeyal ko. Dafa ma yónni ngir ma wax la te yégal la xibaaru jàmm bii, 20 waaye gëmuloo samay kàddu yi wara mat ci seen jamono. Looloo tax dinga muuma. Dootoo mëna wax ba keroog mbir yooyu di mat.»
21 Ci jamono boobu mbooloo bi doon xaar Sakari jaaxle woon nañu, ndaxte dafa yàggoon lool ci béréb bu sell bi. 22 Bi mu génnee mënul wax ak ñoom. Noonu ñu xam ne am na lu ko feeñu ci biir béréb bu sell bi. Muy wax ak ñoom ci joxoñ te muuma.
23 Bi mu matalee fanu liggéeyam ci biir kër-Yàlla gi, mu dellu këram. 24 Gannaaw bés yooyu Elisabet jabaram daldi ëmb. Mu làqatu juróomi weer tey wax ci xelam ne: 25 «Lii la Boroom bi def ci man: teg na bëtu yërmandeem ci man te teggi sama gàcce ci kanamu nit ñi.»
Malaaka Jibril yégle na juddub Yeesu
26 Bi Elisabet nekkee ci juróom benni weeram, Yàlla yónni malaaka Jibril ci benn dëkku Galile bu ñuy woowe Nasaret, 27 ci benn janq bu ñu mayoon benn waay bu bokkoon ci askanu Daawuda, bu tuddoon Yuusufa. Janq bi mu ngi tuddoon Maryaama. 28 Malaaka mi ñëw ci moom ne ko: «Amal jàmm Maryaama. Yiwu Yàlla mu ngi ak yaw. Boroom baa ngi ak yaw!» 29 Maryaama daldi jaxasoo te xalaat lu nuyoo boobu mëna tekki. 30 Malaaka mi ne ko: «Maryaama bul ragal dara, ndaxte Yàlla may na la yiwam. 31 Xoolal! Dinga ëmb, jur doom ju góor. Nanga ko tudde Yeesu. 32 Ku màgg lay nekk, te dinañu ko woowe Doomu Yàlla Aji-Kawe ji, te Boroom bi Yàlla dina ko jox nguuru maamam Daawuda, 33 te dina yilif askanu Yanqóoba ba fàww, te nguuram du am àpp.»
34 Maryaama daldi tontu malaaka mi ne ko: «Naka la loolu mëna ame? Ndaxte man janq la ba tey.»
35 Noonu malaaka mi tontu ko ne ko: «Xel mu sell mi dina wàcc ci yaw, te kàttanu Yàlla Aji-Kawe ji dina la yiir. Loolu moo tax doom jiy juddu ci yaw dinañu ko woowe ku sell ki, Doomu Yàlla ji. 36 Xoolal! Elisabet sa mbokk sax ëmb na doom ju góor ci màggataayam. Ki ñu doon woowe ku mënula am doom ki, mu ngi ci juróom benni weeram. 37 Ndaxte dara tëwul Yàlla.»
38 Noonu Maryaama ne ko: «Man jaamu Boroom bi laa, na Yàlla def lépp li nga wax ci man.» Noonu malaaka mi dem.
Maryaama seeti na Elisabet
39 Ci bés yooyu, Maryaama daldi jóg te gaawantu dem ci benn dëkk bu nekk ci tund yi ci diiwaanu Yude. 40 Mu dugg ci biir këru Sakari, daldi nuyu Elisabet. 41 Ci waxtu bi Elisabet déggee nuyoo Maryaama bi, doom ji daldi yëngatu ci biiram, te Elisabet fees ak Xel mu Sell mi. 42 Noonu mu yuuxu ak baat bu kawe ne: «Barkeel nga ci biir jigéen ñi ñépp, te doom ji nekk ci sa biir barkeel na! 43 Man may kan ba sama yaayu Boroom ñëw seetsi ma? 44 Ndaxte bi ma déggee ngay nuyoo, ci saa si sama doom ji dafa yëngatu ak mbégte ci sama biir. 45 Yaw mi gëm barkeel nga, ndaxte mbir yi ñu la yégal ci turu Boroom bi Yàlla dinañu mat.»
46 Te Maryaama wax ne:
«Sama ruu a ngi màggal Boroom bi,
47 te sama xel di bég ci Yàlla sama musalkat,
48 ndaxte teg na ay bëtam ci man miy jaamam bu woyof bi.
Xoolleen! Dale ko tey, niti jamono yi yépp,
dinañu ma woowe ki Yàlla barkeel
49 ndaxte Aji-Kàttan ji defal na ma ay mbir yu réy
te turam dafa sell.
50 Yërmandeem dina law ci ñi ko ragal
ak seeni sët ba ci seeni sëtaat.
51 Def na ay yëf yu mag ci dooley loxoom.
Tasaare na ñi am ci seen xol ay xalaatu réy-réylu.
52 Daaneel na buur yi ci seen nguur
te yékkëti ñi suufeelu.
53 May na ñi xiifoon lekk ba ñu regg
te dàq boroom alal yi, loxoy neen.
54 Wallusi na Israyil surgaam
te fàttaliku yërmandeem
55 ci Ibraayma ak askanam ba fàww,
ni mu ko dige woon sunuy maam.»
56 Maryaama desoon na ak Elisabet lu tollu ci ñetti weer te noonu mu dellu këram.
Juddub Yaxya
57 Jamono ji Elisabet ware am doom jot na. Mu am doom ju góor. 58 Dëkkandoo yi ak mbokkam yi dégg nañu ne Boroom bi wone na yërmandeem ci moom, ñuy bànneexu ak moom. 59 Ci juróom ñetteelu fan bi, ñu ñëw ngir xarafalsi xale bi. Ñu bëgg ko tudde Sakari, mi di Pàppaam, 60 waaye yaayam ne: «Déedéet. Dinañu ko woowe Yaxya!» 61 Ñu ne ko: «Amul kenn ci say mbokk ku tudd noonu.» 62 Ñu tàmbali di joxoñ di laaj pàppaam ngir xam naka la bëgg ñu woowe xale bi. 63 Sakari laaj àlluwa, bind kàddu yii: «Yaxya mooy turam!» Ñépp yéemu. 64 Ci saa si, gémmiñu Sakari ubbeeku te làmmiñam yewweeku. Mu tàmbali wax di sant Yàlla. 65 Noonu dëkkandoom yépp daldi fees dell ak ragal. Ñu tàmbali di nettali xew-xew yooyu ci diiwaanu tundi Yude yépp. 66 Ñépp ñi doon dégg loolu dencoon nañu ko ci seen xol di laaj seen bopp: «Kon nag, naka la xale bi nara mel?» Ndaxte Boroom bi mu ngi woon ak moom!
67 Sakari pàppay xale bi fees ak Xel mu Sell mi, di wax ci turu Yàlla ne:
68 «Cant ñeel na Boroom bi, Yàllay Israyil
ndaxte ganesi na askanam te yewwi leen.
69 Jox na nu benn musalkat bu am kàttan
ci kër Daawuda surgaam,
70 ni mu ko yégle woon ci jamono ju jëkk ja
jaarale ko ci gémmiñu yonentam yu sell yi.
71 Digoon na nu ne: Moo nuy musal ci sunuy noon
te jële nu ci loxoy ñi nu bañ.
72 Yàlla wone na yërmandeem ci sunuy maam,
te fàttaliku na kóllëreem gu sell gi,
73 ni mu ko giñale woon sunu maam Ibraayma
74 ngir yewwi nu ci loxoy sunuy noon,
ngir nu mën koo jaamu te baña ragal
75 ci sellaay ak ci njubte ci kanamam,
sunu giiru dund yépp.
76 Yaw nag sama doom
dinañu la woowe yonent Yàlla Aji-Kawe ji,
ndaxte dinga dox ci kanamu Boroom bi
ngir waajal yoonam.
77 Dinga xamal askanam ne
Yàlla dina leen baal seeni bàkkaar ngir musal leen.
78 Ndaxte sunu Yàlla fees na ak yërmande ak mbaax
ba tax mu wàcce ci sunu kaw leer bu jóge ci kaw
mel ni leeraayu jant buy fenk,
79 ngir leerale ñu nekk ci lëndëm
te takkandeer dee tiim leen,
te jiite nu ci yoonu jàmm ji.»
80 Xale bi da doon màgg te xelam di ubbeeku. Mu dëkk ci biir màndiŋ ba, ba bés bu muy feeñ ci kanamu waa Israyil.