Màrk
Yaxya waajal na yoon ngir Yeesu
1
Lii mooy njàlbéenu xibaar bu baax bi ci Yeesu Almasi bi, doomu Yàlla. 2 Bind nañu ci téere yonent Yàlla Esayi ne:
«Xoolal! Maa ngi yónni sama yonent ci sa kanam,
ngir mu waajal la sa yoon.
3 Lii mooy baatu nit kiy yuuxu ci biir màndiŋ bi, naan:
"Waajalleen yoonu Boroom bi.
Defarleen yoonam yi, ñu jub."»
4 Yaxya ñëw na ci màndiŋ bi di sóob nit ñi ci ndox, te di waare naan: «Nanguleen ma sóob leen ci ndox ngir wone ne tuub ngeen seeni bàkkaar te noonu Yàlla dina leen baal.» 5 Waa diiwaanu Yude yépp ak waa dëkku Yerusalem yépp doon nañu ñëw ci moom di wax seeni bàkkaar ci kanamu ñépp te noonu Yaxya di leen sóob ci ndox ci dexu Yurdan. 6 Yaxya daan na sol yére bu ñu ràbbe kawaru giléem te takk ci ndiggam takkukaay bu ñu defare der. Da doon lekk soccental ak lemu àll, 7 di waare naan: «Kenn ku ma ëpp kàttan dina ñëw ci sama gannaaw. Yelloowuma sax sëgg ci kanamam ngir tekki ay dàllam. 8 Man sóob naa leen ci ndox, waaye kooku dina leen sóob ci Xel mu Sell mi.»
9 Ci bés yooyu Yeesu jóge woon na ci dëkku Nasaret ci diiwaanu Galile te Yaxya sóoboon na ko ci ndox ci dexu Yurdan. 10 Bi mu génnee ci ndox mi ci saa si mu gis asamaan si ubbeeku te Xel mu Sell mi wàcc ci moom ci jëmm ju mel ni pitax, 11 te benn baat jóge ci asamaan, ne: «Yaa di sama doom ji ma sopp. Ci yaw laa ame bànneex.»
12 Ci saa si, Xel mu Sell mi yóbbu Yeesu ba ci biir màndiŋ bi. 13 Mu def fa ñeent fukki fan te Seytaane fiir na ko fa. Nekkoon na ak rabu àll yi te malaaka yi di ko toppatoo.
Yeesu tàmbali na liggéeyam
14 Gannaaw bi ñu tëjee Yaxya ci kaso bi, Yeesu dem ci diiwaanu Galile di waare xibaar bu baax bi jóge ci Yàlla, 15 di naan: «Waxtu bi mat na te nguuru Yàlla gi jegesi na. Tuubleen seeni bàkkaar te gëm ci xibaar bu baax bi.»
16 Benn bés Yeesu doon na jaar ci tefesu dexu Galile, mu gis Simoŋ ak Andare, ñaari nappkat yu bokk ndey ak baay. Ñu doon sànni seeni mbaal ci dex gi. 17 Yeesu ne leen: «Toppleen ma te dinaa leen def ay nappkatu nit.» 18 Ci saa si ñu bàyyi seen mbaal yi te topp ko. 19 Bi Yeesu demee ba ci kanam tuuti, mu gis ñaar ñu bokk ndey ak baay: Saak ak Yowaana ñiy doomi Sebede. Ñu nekkoon ci seen gaal di defaraat seen mbaal yi. 20 Ci saa si mu woo leen, ñu daldi bàyyi seen baay Sebede ci gaal gi ak liggéeykatam yi, te ñu topp Yeesu.
Yeesu wéral na benn waay bu rab jàppoon
21 Yeesu ak taalibeem yi dugg nañu dëkku Kapernawum. Ci bésu noflaay bi Yeesu daldi dugg ci kër-ñaan bi di jàngale. 22 Ñépp ña fa nekkoon yéemu woon nañu ci njàngaleem, ndaxte da doon jàngale ak sañ-sañ bu jàngalekati-yoonu-Musaa amul. 23 Ci waxtu boobu sax, ci biir kër-ñaan bi, amoon na benn waay bu rab jàppoon. Muy yuuxu ak baat bu kawe 24 naan: «Yeesu mu Nasaret, loo nu bëggal? Ndax danga ñëw ngir sànk nu? Xam naa la; yaw yaay ku sell ki Yàlla yónni!» 25 Yeesu gëdd rab bi, ne ko: «Noppil te nga génn ci waa ji!» 26 Rab bi sayloo waa ji, génn ci moom di yuuxu ci kaw. 27 Ñépp ñi fa nekkoon yéemu woon nañu bay laajante ci seen biir naan: «Lii mooy lan? Lii mooy njàngale bu bees bu ànd ak sañ-sañ. Muy jox ndigal rab yi sax te ñu koy déggal.» 28 Ci saa ci, turu Yeesu daldi siiw ci diiwaanu Galile bépp.
Yeesu wéral na yaayu jabaru Simoŋ ak ñenn ñu feebaroon
29 Bi Yeesu génnee ci kër-ñaan bi, ànd ak Saak ak Yowaana, ñu daldi dem kër Simoŋ ak Andare. 30 Fekk na yaayu jabaru Simoŋ tëdd feebar ndaxte dafa amoon yaram bu tàng. Bi Yeesu yegsee, ñu yégal ko ko. 31 Mu jegesi ko, téye loxoom, te yékkëti ko. Tàngooru yaram bi bàyyi ko te mu tàmbali di leen toppatoo.
32 Ci ngoon si bi jant bi sowee, ñu andil Yeesu ñépp ñi feebar ak ñépp ñi rab jàpp. 33 Waa dëkk bi yépp daje ci buntu kër gi. 34 Yeesu wéral na ñu bari ñi feebaroon te amoon jàngoro yu wuute te muy dàq rab yu bari, waaye mu tere rab yi ñu wax ndaxte xamoon nañu ki mu doon.
Yeesu waare na ci diiwaanu Galile
35 Ci ëllëg sa ci suba teel fekk mu ngi lëndëm ba léegi, Yeesu daldi jóg te génn, dem ci benn béréb bu wéet di fa ñaan. 36 Simoŋ ak ñi mu àndaloon di ko seet. 37 Bi ñu ko gisee ñu ne ko: «Ñépp ñu ngi lay seet.» 38 Waaye Yeesu ne leen: «Nanu dem feneen, ci gox yi nu wër. Damaa wara waare foofu tamit, ndaxte loolu moo tax ma ñëw.» 39 Noonu mu wër diiwaanu Galile bépp di waare ci kër-ñaan yi te di dàq rab yi nekkoon ci nit ñi.
Yeesu wéral na benn waay bu am feebaru ngaana.
40 Gannaaw loolu benn waay bu amoon feebaru ngaana ñëw ci Yeesu, sukk ci kanamam, te ñaan ko ne: «Soo ko bëggee, mën nga ma setal.» 41 Yeesu yërëm ko, tàllal loxoom, laal ko te nee ko: «Bëgg naa ko. Setal.» 42 Ci saa si feebaru ngaana bi bàyyi ko te mu set. 43 Noonu Yeesu wax ko mu dem, waaye mu artu ko ak doole 44 naan: «Déglul bu baax! Bul ko wax kenn waaye demal, nga won sa bopp jébbalkatu-sarax si, te nga joxe sarax si, ni ko yoonu Musaa diglee, ngir wone ne set nga, te loolu dina mëna nekk seede ci ñoom.» 45 Waaye nit ka dem tàmbali di yégle mbir moomu fépp ak ci ñépp ba tax Yeesu mënatul woon fésal boppam ci dëkk yi. Doon na nekk ci béréb yu wéet te nit ñi di jóge fépp di ñëw ci moom.