Yeesu dekki na ci ñu dee ñi
28
Gannaaw bésu noflaay bi, dimaas ci suba teel, Maryaama mu Magdala ak beneen Maryaama bi ñëw nañu seetsi bàmmeel bi. 2 Te noonu, mu am yëngu-yëngu suuf bu réy, ndaxte ab malaaka Boroom bi moo wàcce ci asamaan, ñëw, bërëŋ xeer bi tëjoon bàmmeel bi, te toog ci kawam. 3 Melokaanam mel ni melax te yéreem bi weex tàll. 4 Wottukat yi tiit bay lox te mel ni ñu dee. 5 Malaaka mi jël kàddu gi te ne jigéen ñi: «Buleen ragal. Xam naa ne Yeesu mi ñu daajoon ci bant ngeen di seet. 6 Nekkatu fi; dekki na, ni mu ko waxe woon. Kaayleen xool béréb bi mu tëddoon. 7 Demleen gaaw, ngeen wax taalibeem yi ne: "Dekki na ci ñu dee ñi, te xoolleen, mu ngi leen di jiituji diiwaanu Galile. Foofu ngeen koy gise." Léegi nag, wax naa leen ko.» 8 Jigéen ñi daldi gaawantu, génn bàmmeel bi, ànd ak tiitange ak mbégte mu réy. Ñu daw ngir yégali xibaar bi taalibeem yi. 9 Bi jigéen ñi di dem, Yeesu ñëw dajesi ak ñoom ci yoon bi te ne leen: «Maa ngi leen di nuyu.» Ñu jegesi ko te laxasu tànkam yi, sukk ci kanamam. 10 Noonu Yeesu ne leen: «Buleen ragal. Demleen wax sama mbokk yi ñu dem Galile. Foofu lañu may gise.»
11 Bi jigéen ñi nekkee ci yoon bi, noonu ñenn ci soldaar yi doon wottu bàmmeel bi ñëw ca dëkk ba, yégal njiiti-jébbalkati-sarax yi lépp li xewoon. 12 Noonu ñu dajaloo ak mag ña. Gannaaw bi ñu waxtaanee ak ñoom, ñu jox soldaar ya xaalis bu takku 13 te ne leen: «Lii ngeen di wax: "Taalibeem yi dañoo ñëw ci guddi gi te ñu sàcc néewam bi, fekk nuy nelaw." 14 Te su ko njiitu diiwaan bi yégee, dinanu wax ak moom ba mu dal ngir ngeen bañ cee am benn jafe-jafe.» 15 Soldaar yi jël xaalis bi te def la ñu leen santoon. Noonu xibaar boobu daldi siiw ci biir Yawut yi ba bésu tey ji.
Yeesu feeñu na taalibeem yi te yónni leen
16 Noonu fukki taalibe yi ak benn dem Galile ci tund bi leen Yeesu waxoon. 17 Bi ñu gisee Yeesu, ñu sukk ngir jaamu ko, waaye ñenn ci ñoom am xel ñaar. 18 Noonu Yeesu jegesi te ne leen: «Yàlla jox na ma bépp sañ-sañ ci asamaan ak ci suuf si. 19 Demleen nag, ngeen def ay taalibe ci xeeti àddina si yépp. Nii ngeen koy defe: sóob leen ci ndox ci turu Baay ji, Doom ji, ak Xel mu Sell mi, 20 te jàngal leen ñu sàmm lépp li ma leen sant. Xoolleen, maa ngi ak yeen bés bu nekk, ba ci njeextelu àddina.»