Pilaat mu ngi laaj Yeesu
27
Ci suba teel, njiiti-jébbalkati-sarax yi yépp ak magi askan bi waxtaan nañu ci seen biir ngir reylu Yeesu. 2 Noonu ñu yeew ko, yóbbu ko, te jébbal ko Pilaat miy njiitu diiwaan bi.3 Yudaa mi ko jébbale woon, bi mu gisee ne teg nañu Yeesu daan, mu réccu. Noonu, mu dem ci njiiti-jébbalkati-sarax yi ak mag ñi, delloo leen fanweeri xànjaru xaalis yi, 4 ne leen: «Man de, bàkkaar naa ci ni ma jébbale ci dee nit ku deful dara.» Waaye ñu tontu ko ne: «Sunu yoon nekku ci. Yaa xam.» 5 Noonu mu sànni fanweeri xànjaru xaalis yi ci kër-Yàlla gi, mu dem, yeew buum ci baatam, xaru.
6 Njiiti-jébbalkati-sarax yi jël xaalis bi te naan: «Yoonu Musaa mayewul ñu dugal xaalis bii ci dencukaayu kër-Yàlla gi, ndaxte njégu deret la.» 7 Gannaaw bi ñu waxtaanee ci seen biir, ñu jënde xaalis boobu toolu defarkatu ndaa bi ngir ñu fay suul ay doxandéem. 8 Loolu moo tax ñuy woowe tool boobu toolu deret ba bésu tey jii. 9 Noonu li yonent Yàlla Yeremi waxoon daldi mat, bi mu naan:
«Jël nañu fanweeri xànjaru xaalis yi,
njégu ki ñu xayma woon,
te doomi Israyil ñoo xayma woon njégam,
10 te ñu joxe ko ngir jënd toolu defarkatu ndaa bi,
ni ma ko Boroom bi digale woon.»
11 Noonu Yeesu taxaw ci kanamu njiitu diiwaan bi te mu laaj ko ne: «Ndax yaw yaay buuru Yawut yi?» Yeesu tontu ko ne: «Yaw, yaa ko wax.» 12 Bi ko njiiti-jébbalkati-sarax yi ak mag ñi di tuumaal, tontuwul dara. 13 Noonu Pilaat ne ko: «Xanaa déggoo lépp li ñu lay tuumaal?» 14 Waaye Yeesu tontuwu ko ci dara, ba tax njiitu diiwaan bi waaru lool.
15 Màggalu Paak bu nekk, njiitu diiwaan bi dafa tàmmoon di bàyyil mbooloo mi kenn ku ñu tëj kaso, ki mbooloo mi bëggoon. 16 Ci waxtu boobu amoon na ci kaso bi kenn ku ñuy woowe Yeesu Barabas, te mu amoon tur lool. 17 Bi mbooloo mi dajee, Pilaat ne leen: «Kan ngeen bëgg ma bàyyil leen: Yeesu Barabas walla Yeesu bi ñuy woowe Almasi bi?» 18 Laaj na leen loolu ndaxte xamoon na ne iñaan moo tax ñu jébbal ko Yeesu. 19 Bi muy àtte ci bérébu àttekaay bi, jabaram yónnee ko bataaxal bii: «Màndul ci mbirum ku jub kooku, ndaxte, tey jii amoon naa coono ci sama gént ndax moom.» 20 Njiiti-jébbalkati-sarax yi ak mag ñi xiir mbooloo mi ngir ñu ñaan mu bàyyi Barabas te reylu Yeesu. 21 Njiitu diiwaan bi jël kàddu gi te laajaat mbooloo mi naan: «Kan ci ñaar ñi ngeen bëgg ma bàyyil leen ko?» Ñu tontu ne: «Barabas!» 22 Pilaat ne leen: «Lan ngeen bëgg nag ma def Yeesu mi ñuy woowe Almasi bi?» Noonu ñépp tontu ne: «Daaj ko ci bant!» 23 Pilaat laaj leen ne: «Lan la def lu bon?» Waaye ñu gëna yuuxu naan: «Daaj ko ci bant!»
24 Bi Pilaat gisee ne loolu jériñul dara, waaye coow li gëna yokk ba mu ragal fippu am, mu jël ndox te raxas loxoom yi ci kanamu mbooloo mi, te ne: «Set naa ci deretu nit kii. Yeena xam.» 25 Noonu mbooloo mi yépp tontu ne: «Na deretam këppu ci sunu kaw ak sunu kaw doom yi.» 26 Noonu Pilaat bàyyil leen Barabas. Yeesu nag, mu dóorlu ko ay yar te jébbal ko soldaar yi ngir ñu daaj ko ci bant.
Deewu Yeesu ci bant bi
27 Noonu soldaar yi jël Yeesu, yóbbu ko ci biir këru njiitu diiwaan bi, te ñu woo mbooloo soldaar yi yépp. Ñu dajaloo, wër Yeesu. 28 Ñu daldi summi yéreem yi, solal ko mbubb bu xonq, 29 jël ab kaala bu ñu ràbbe dég, teg ko ci boppam, te ñu jël benn bant, teg ko ci loxo ndeyjooram. Noonu ñu sukk ci kanamam di ko ñaawal, naan: «Nuyu nanu la, yaw buuru Yawut yi.» 30 Ñuy tifli ci kawam, daldi nangu bant ba di ko ko dóor ci bopp. 31 Bi ñu ko ñaawalee ba noppi, ñu daldi summi mbubb bu xonq bi ñu ko solaloon, delloo ko yéreem yi, te yóbbu ko ngir daaj ko ci bant ba.
32 Bi ñu génnee dëkk bi, ñu daje ak benn waay bu tudd Simoŋ mu Siren. Soldaar yi sëf ko bantu Yeesu bi. 33 Bi ñu yegsee ci béréb bi ñu woowe Golgota, maanaam yaxu bopp, 34 ñu jox Yeesu biiñ bu ñu jaxase ak lu wex, waaye bi mu ko mosee bëggu ko naan. 35 Bi ñu ko daajee ci bant bi, ñu tegoo bant ngir séddoo yéreem yi. 36 Nu daldi toog foofu di ko wottu. 37 Ngir wone li tax ñu teg ko daan, lii lañu bind mu tiim boppam: «Kii mooy Yeesu, Buuru Yawut yi».
38 Amoon na ñaari defkatu lu bon yi ñu daajaale woon ci wetam, kenn ki ci ndeyjooram, keneen ki ci càmmoñam. 39 Noonu ñi doon romb foofu di ko saaga di yëngal seeni bopp 40 naan: «Yaw mi mëna toj kër-Yàlla gi te tabaxaat ko ci ñetti fan, musalal sa bopp! Bu de yaa di Doomu Yàlla ji, wàccal ci bant bi.» 41 Noonu tamit njiiti-jébbalkati-sarax yi, jàngalekati-yoonu-Musaa ak mag ñi di ko ñaawal tey naan: 42 «Musal na ñeneen ñi, waaye mënula musal boppam. Su de moom mooy Buuru Israyil, na wàcc léegi ci bant bi. Su booba dinanu gëm ci moom. 43 Dénk na boppam Yàlla. Na ko Yàlla musal su de sopp na ko, ndaxte moom moo ne: "Man, maa di Doomu Yàlla ji."» 44 Ñaari defkatu lu bon yi ñu daajoon ci wetam sax doon nañu ko saaga ni ñeneen ñi.
45 Li ko dale diggu bëccëg, réew mi yépp daldi lëndëm ba ci ñetti waxtu ci ngoon. 46 Bi waxtu boobu jotee, Yeesu yuuxu ak baat bu kawe naan: «Eli, Eli, lema sabaktani?» luy tekki: «Sama Yàlla, sama Yàlla, lu tax nga bàyyi ma?» 47 Ñenn ci ñi nekkoon foofu dégg ko tey naan: «Mu ngi woo yonent Yàlla Ilyaas.» 48 Ci saa si kenn ci ñoom daldi daw, jël benn sagar, capp ko ci bineegar, takk ko ci bant, te tàllal ko Yeesu ngir mu naan. 49 Waaye ñeneen ñi di naan: «Xaaral! Nanu xool ba xam ndax yonent Yàlla Ilyaas dina ñëw ngir musal ko.»
50 Yeesu daldi yuuxuwaat ak baat bu kawe te delloo ruuwam Yàlla. 51 Ci waxtu boobu, rido kër-Yàlla gi daldi xar ñaar, li ko dale ci kaw ba ci suuf. Suuf si yëngu te doj yi daldi xar. 52 Ay bàmmeel daldi ubbeeku te ñu bari ci ñi Yàlla moom te dee woon daldi dekki 53 te génn ci seeni bàmmeel. Gannaaw bi Yeesu dekkee, ñu dugg ci Yerusalem, dëkk bu sell bi, te nit ñu bari gis leen. 54 Soldaar yi doon wottu Yeesu ci bant bi ak seen njiit, bi ñu gisee yëngu-yëngu suuf si ak lépp li fa xewoon, ñu daldi ànd ak tiitaange bu réy di naan: «Ci dëgg, nit kii Doomu Yàlla la woon.»
55 Amoon na fa ay jigéen yu bari yu doon toppe Yeesu dale ko ci diiwaanu Galile ngir toppatoo ko. Ñu ngi doon seetaane fu sori lépp li fa xewoon. 56 Ci seen biir amoon na Maryaama mu Magdala, Maryaama yaayu Saak ak Yuusufa, ak yaayu Saak ak Yowaana ñiy doomi Sebede.
Robum Yeesu
57 Ca ngoon sa, kenn ku ñu woowe Yuusufa mu Arimate yegsi. Ku bari alal la woon te nekkoon moom tamit taalibe Yeesu. 58 Mu dem laaj Pilaat néewu Yeesu. Noonu Pilaat daldi joxe ndigal ngir ñu jox ko ko. 59 Yuusufa jël néew bi, lëmës ko ci perkaal bu bees, 60 denc ko ci bàmmeel bi mu yattlu woon ci biir doj ngir boppam. Gannaaw loolu mu bërëŋ xeer bu réy ngir tëj buntu bàmmeel bi te dem. 61 Maryaama mu Magdala ak beneen Maryaama nekkoon nañu foofu, toog jàkkaarloo ak bàmmeel bi.
62 Bés boobu, bésu waajalu bésu noflaay la woon. Ci ëllëg sa, njiiti-jébbalkati-sarax yi ak Farisen yi ànd dem ca kër Pilaat, 63 daldi ko ne: «Kilifa gi, nu ngi fàttaliku benn mbir: fenkat bii, ca ba muy dund, nee woon na: "Gannaaw ñetti fan, dinaa dekki." 64 Kon nag nu ngi lay ñaan, nga santaane ñu wottu bàmmeel bi ba ci ñetteelu fan bi. Su dul loolu, taalibeem yi mën nañu ñëw, sàcc néew bi te ne askan bi: "Dekki na ci ñu dee ñi." Su ko defee, fen boobu mooy gëna yées bu jëkk bi.» 65 Noonu, Pilaat ne leen: «Ay soldaar a ngi nii. Demleen te ngeen fexe ñu wottu bàmmeel bi ni ngeen ko bëgge.» 66 Ñu dem nag ci bàmmeel ba, tëj ko bu wóor, def xàmmikaay ci xeer bi ngir bu ko kenn ubbee, ñu xam ko. Ñu daldi fay teg ay soldaar ngir ñu wottu ko.