Benn jigéen tuur na latkoloñ ci boppu Yeesu
26
Bi Yeesu waxee kàddu yooyu yépp ba noppi, mu ne taalibeem yi: 2 «Xam ngeen ne, ñaari fan a des laata màggalu Paak bi. Dinañu jébbale Doomu nit ki ngir ñu daaj ko ci bant.»3 Ci waxtu boobu njiiti-jébbalkati-sarax yi ak magi askan bi dajaloo ci ëttu këru Kayif, miy jébbalkatu-sarax-bu-mag bi. 4 Ñu gise ci seen biir ngir jàpp Yeesu ci kumpa te reylu ko. 5 Waaye ñuy wax ci seen biir ne: «Warunu ko jàpp ci bésu màggal yi. Lu ko mooy, yëngu-yëngu mën na am ci askan bi.»
6 Yeesu mu ngi woon dëkku Betani ci këru Simoŋ gaana bi. 7 Foofu amoon na benn jigéen bu yor butéel bu ñu defare xeeru albaatar bu fees ak latkoloñ bu njég li bari. Mu jegesi Yeesu ci bérébu lekkukaay bi te tuur ko ci boppam. 8 Bi taalibe yi gisee loolu, ñu daldi mer te ñu ne: «Lu waral yàq bii? 9 Ndaxte mënoon nañu ko jaaye njég lu bari te jox xaalis bi néew-di-doole yi.» 10 Waaye Yeesu xam loolu te ne leen: «Lu tax ngeen di sonnal jigéen jii? Jëf ju baax la ma defal, 11 ndaxte néew-di-doole yi dinañu nekk ak yeen saay su nekk, waaye man, duma nekk ak yeen saay su nekk. 12 Bi mu ma tuuree latkoloñ bi, def na ko ngir waajal sama yaram bala ñu koy rob. 13 Ci dëgg maa ngi leen koy wax: fépp fu ñuy yégle xibaar bu baax bii ci àddina si yépp, dinañu nettali tamit li jigéen jii def ngir fàttaliku ko.»
14 Noonu kenn ci fukki taalibe yi ak ñaar ku tudd Yuda Iskariyot dem ci njiiti-jébbalkati-sarax yi 15 te ne leen: «Lan ngeen may jox su ma leen jébbalee Yeesu?» Ñu waññal ko fanweeri xànjari xaalis te jox ko ko. 16 Dale ko ci waxtu boobu, Yuda doon wut pexe ngir jébbal leen Yeesu.
Yeesu mu ngi màggal bésu Paak bi ak taalibeem yi
17 Bés bu jëkk ci màggalu mburu yu amul lawiir yi, taalibe yi laaj Yeesu ne: «Fan nga bëgg nu waajale la reeru Paak bi?» 18 Mu ne leen: «Demleen ci dëkk bi ci kër diw te ngeen ne ko: "Jàngalekat bi nee na: 'Sama waxtu jegesi na. Ci sa kër laay màggale Paak bi ak samay taalibe.'"» 19 Taalibe yi def li leen Yeesu santoon te ñu daldi waajal reeru Paak bi.
20 Ci ngoon si, Yeesu toog ci bérébu lekkukaay bi ak fukki taalibe yi ak ñaar. 21 Ci waxtu bi ñuy lekk, Yeesu ne: «Ci dëgg maa ngi leen koy wax, kenn ci yeen moo may jébbale.» 22 Taalibe yi tiis lool ci seen xol. Ku nekk tàmbali di ko laaj ne: «Mbaa du man, Boroom bi?» 23 Mu tontu ne: «Ki cappandoo ak man mburoom ci ndab li, kooku moo may jébbale. 24 Doomu nit ki dina dee ni ko Mbind mi yégle ci lu jëm ci moom, waaye musiba dina dal nit ki koy jébbale. Mu bañoona juddu sax, moo gën ci moom.» 25 Yuda mi ko naroona jébbale jël kàddu gi te ne: «Mbaa du man, jàngalekat bi?» Mu tontu ne: «Yaa ko wax.»
26 Ci waxtu bi ñuy lekk, Yeesu jël mburu, barkeel ko ba noppi, damm ko, te jox ko taalibe yi ne: «Jëlleen, ngeen lekk. Lii moo di sama yaram.» 27 Noonu mu jël benn kaas, sant Yàlla ba noppi, jox leen ko te ne: «Naanleen ci yeen ñépp, 28 ndaxte lii mooy sama deret bi tuuru ngir ñu bari, ngir fas kóllëre gi te Yàlla baal leen seeni bàkkaar. 29 Maa ngi leen koy wax: gannaaw si tey, dootuma naan biiñ ba keroog may naan biiñ bu bees ak yeen ci sama nguuru Baay.» 30 Gannaaw bi ñu woyee benn woy ci Saboor yi, ñu génn ngir dem ci Tundu Oliw ya.
31 Noonu Yeesu ne leen: «Ci guddi tey ji, yeen ñépp dingeen dem, bàyyi ma, ndaxte Mbind mi nee na:
"Dinaa dóor sàmm bi,
te xari gétt gi dinañu tasaaroo."
32 Waaye gannaaw bu ma dekkee, dinaa leen jiituji diiwaanu Galile.» 33 Piyeer jël kàddu gi te ne ko: «Bu ñépp demee, bàyyi la sax, man duma la bàyyi mukk.» 34 Yeesu ne ko: «Ci dëgg maa ngi la koy wax, guddi tey ji sax bala ginaar di sab, dinga ma weddi ñetti yoon.» 35 Piyeer ne ko: «Su de sax, damaa wara dee ak yaw, duma la weddi mukk.» Te taalibe yépp wax loolu tamit.
Yeesu mu ngi ñaan ci Setsemane te ñu jàpp ko
36 Ci kaw loolu Yeesu yegsi ak taalibeem yi ci béréb bu ñuy woowe Setsemane te mu ne leen: «Toogleen fii, ma dem fale ngir ñaan.» 37 Mu jël Piyeer ak ñaari doomu Sebede yi. Mu tàmbale yég tiis ak naqar. 38 Noonu mu ne leen: «Sama xol dafa tiis ba ma bëgga dee. Desleen fii te di xoole ak man.» 39 Mu sori leen tuuti, teg jëwam ci suuf te ñaan naan: «Sama Baay, su de mën na nekk, soril ma kaasu naqar bii. Wànte bu mu doon sama coobare, waaye na sa coobare am.»
40 Mu dellusi ci taalibe yi te fekk leen ñuy nelaw. Noonu mu ne Piyeer: «Mënuleen sax xoolandoo ak man benn waxtu! 41 Xooleleen te ñaan ngir ngeen baña daanu ci fiir. Xel mi waaj na ba noppi, waaye yaram bi dafa néew doole.»
42 Noonu ci ñaareelu yoon bi, mu soriwaat leen tuuti te ñaan naan: «Sama Baay, su de kaas bii mënula romb te naanuma ko, na sa coobare am.» 43 Noonu mu ñëwaat te fekk leen ñuy nelaw, ndaxte seen bët yi mënatul woon xoole ndax gëmmentu.
44 Mu bàyyi leen te soriwaat, ñaan ci ñetteelu yoon bi, te waxaat kàddu yi mu waxoon. 45 Gannaaw loolu mu dellusi ci taalibeem yi te ne leen: «Yeena ngi nelaw ba léegi tey noppalu! Xoolleen, waxtu bi jot na, ñu ngi jébbal Doomu nit ki ci loxoy bàkkaarkat yi. 46 Jógleen, nu dem. Xoolleen! Ki may jébbale mu ngi nii.»
47 Bi Yeesu di wax loolu, Yuda mi bokkoon ci fukk yi ak ñaar yegsi. Mbooloo mu takku ànd ak moom te yor ay jaasi ak ay yet. Njiiti-jébbalkati-sarax yi ak mag ñi ñoo leen yónni woon. 48 Ki ko doon jébbale joxoon na leen màndarga, ne leen: «Ki may fóon, moom la. Jàppleen ko.» 49 Ci saa si mu jegesi Yeesu te ne ko: «Maa ngi lay nuyu, jàngalekat bi.» Noonu mu daldi ko fóon. 50 Yeesu ne ko: «Sama xarit, defal li la taxa ñëw.» Noonu ñu jegesi Yeesu, song ko, te jàpp ko.
51 Kenn ci ñi àndoon ak Yeesu rocci jaaseem, dóor surga jébbalkatu-sarax-bu-mag bi, te dagg nopp bi. 52 Noonu Yeesu ne ko: «Dellool jaasi bi fi mu nekkoon, ndaxte ñépp ñuy jëfandikoo jaasi, jaasi moo leen di sànk. 53 Ndax xalaat nga ne mënuma woo sama Baay, te mu yónnee ma ci saa si lu ëpp fukki mbooloo malaaka ak ñaar? 54 Waaye su ma ko defee, naka la Mbind mi di mate? Ndaxte Mbind mi nee na, lii, ni la wara amee.»
55 Noonu Yeesu ne mbooloo mi: «Lu tax ngeen ñëw jàppsi ma yor ay jaasi ak ay yet, mel ni dama nekk defkatu lu bon? Bés bu nekk maa ngi doon toog ci ëttu kër-Yàlla gi di jàngale, te yeen jàppuleen ma. 56 Waaye lii lépp am na ngir li yonent yi bind mat.» Noonu taalibe yépp bàyyi ko te daw.
Yeesu mu ngi ci këru jébbalkatu-sarax-bu-mag bi
57 Ñi jàppoon Yeesu yóbbu ko ci këru Kayif miy jébbalkatu-sarax-bu-mag bi. Jàngalekati-yoonu-Musaa ak mag ñi daje woon nañu foofu. 58 Piyeer doon topp Yeesu fu sori, ba ci ëttu këru jébbalkatu-sarax-bu-mag bi. Mu dugg ci ëtt bi te toog ak wottukat yi ngir xam naka la loolu di mujje. 59 Njiiti-jébbalkati-sarax yi ak kurélu àttekati Yawut yi yépp doon nañu wut seede bu dëgguwul ci Yeesu ngir mën ko teg daanu dee. 60 Waaye amuñu ko woon, doonte ay seede yu dëgguwul yu bari ñëwoon nañu fa. Ci mujjantal bi, am ñaar ñu ñëw 61 naan: «Waa jii waxoon na ne: "Mën naa toj kër-Yàlla gi te tabaxaat ko ci ñetti fan."»
62 Noonu, jébbalkatu-sarax-bu-mag bi jóg te ne Yeesu: «Ndax doo tontu dara ci li ñii di seede ci yaw?» 63 Waaye Yeesu noppi. Jébbalkatu-sarax-bu-mag bi ne ko: «Waatal naa la ci Yàlla biy dund nga wax nu: ndax yaw yaay Almasi bi, Doomu Yàlla ji?» 64 Yeesu tontu ko ne: «Yaa ko wax. Waaye maa ngi leen koy wax: dale ko tey, dingeen gis Doomu nit ki toog ci ndeyjooru Yàlla Aji-Kàttan ji tey ñëw ci kaw niiri asamaan.»
65 Noonu, jébbalkatu-sarax-bu-mag bi xotti yéreem yi tey naan: «Saaga na Yàlla ci li mu méngale boppam ak moom! Kon lan lanuy soxlati ay seede? 66 Lan ngeen ci xalaat?» Ñu tontu ne: «Yelloo na dee.» 67 Noonu ñu tifli ci xar-kanamam te dóor ko ay kurpeñ. Ñenn ñi mbej ko 68 tey naan: «Éey Almasi bi, su dee yonent nga, wax nu kan moo la dóor!»
69 Ci waxtu boobu Piyeer mu ngi toogoon ci biti, ci ëtt ba. Benn surga bu jigéen jegesi ko te ne ko: «Yaw tamit àndoon nga ak Yeesu mu Galile.» 70 Waaye Piyeer weddi ko ci kanamu ñépp ne: «Xamuma li nga bëgga wax.» 71 Bi mu demee ci wetu bunt ba, beneen surga bu jigéen gis ko te wax ñi nekkoon foofu ne: «Kii àndoon na ak Yeesu mu Nasaret.» 72 Noonu Piyeer weddiwaat ko ak waat ne: «Xamuma waa jooju.» 73 Ci kanam tuuti ñi nekkoon foofu jegesi Piyeer te ne ko: «Li woor mooy yaw tamit ci ñoom nga bokk, ndaxte sa waxin feeñal na la.» 74 Noonu mu tàmbalee giñ tey waat naan: «Xamuma waa jooju.» Ci saa si, benn ginaar sab. 75 Noonu Piyeer fàttaliku kàddu gi ko Yeesu waxoon ne: «Bala ginaar di sab, dinga ma weddi ñetti yoon,» te Piyeer génn di jooy, jooy yu metti.