Yeesu mu ngi nettali ay léeb ci li jëm ci delluseem
25
Noonu Yeesu nettali leen léeb bii ne: «Nguuru asamaan si dina nirook fukki janq yu jël seeni làmp te génn ngir daje ak boroom séet bi. 2 Ci fukki janq yi, amoon na juróom yu ñàkk xel ak juróom yu am xel. 3 Bi ñuy jël seeni làmp, ñi ñàkk xel yóbbalewuñu woon diwlin, 4 waaye ñi am xel yóbbaale woon nañu diwlin ci ay butéel ak seeni làmp. 5 Gannaaw boroom séet bi dafa yéexoona ñëw, janq yépp gëmmentu te daldi nelaw. 6 Ci xaaju guddi am ku yuuxu ne: "Xoolleen! Boroom séet baa ngi ne. Demleen gatandu ko." 7 Noonu janq yépp daldi yeewu te defaraat seeni làmp. 8 Ñu ñàkk xel ñi ne ñu am xel ñi: "Mayleen nu ci seen diwlin, ndaxte sunu làmp yi ñu ngi waaja fey." 9 Waaye ñi am xel tontu leen ne: "Déedéet, ndaxte li nu yor du doy ngir nun ak yeen. Léegi nag, demleen ci jaaykat yi ngeen jëndal seen bopp." 10 Bi ñuy dem di jëndi, boroom seet bi yegsi. Ñi waajaloon seen bopp dugg ak moom ci biir bérébu xew bi, te ñu tëj bunt ba. 11 Gannaaw loolu yeneen janq yi yegsi te ne: "Boroom bi, boroom bi, ubbil nu." 12 Waaye boroom séet bi tontu leen ne: "Ci dëgg maa ngi leen koy wax: xamuma leen." 13 Kon nag yeewuleen, ndaxte xamuleen bés bi walla waxtu bi.14 «Nguuru asamaan si dafay niroo tamit ak benn waay buy waaja tukki. Mu woo surgaam yi te dénk leen alalam. 15 Kenn ki mu dénk ko juróomi milyoŋ, keneen ki ñaari milyoŋ, ki ci des benn milyoŋ, ku nekk ak li mu àttan, te mu dem ci saa si. 16 Ki jotoon juróomi milyoŋ ya defi jënd ak jaay ak xaalis bi, te amaat yeneen juróomi milyoŋ. 17 Noonu tamit ki jotoon ñaari milyoŋ yi, amaat ci yeneen ñaari milyoŋ. 18 Waaye ki jotoon benn milyoŋ dem, gas pax ci suuf si, te nëbb fa xaalisu njaatigeem bi. 19 Gannaaw diir bu yàgg njaatige surga yi dellusi te laaj leen li ñu def ci alalam bi. 20 Ki jotoon juróomi milyoŋ yi jegesi te andi yeneen juróomi milyoŋ te ne: "Sama njaatige, juróomi milyoŋ nga ma dénkoon. Yeneen juróomi milyoŋ yii laa ci am." 21 Njaatigeem bi ne ko: "Waaw góor. Surga bu baax nga te gore. Gore nga ci lu tuuti. Dinaa la dénk lu bari. Kaay bànneexu ak man." 22 Ki jotoon ñaari milyoŋ yi tamit jegesi te ne: "Sama njaatige, ñaari milyoŋ nga ma dénkoon. Yeneen ñaari milyoŋ yii laa ci am." 23 Njaatigeem bi ne ko: "Waaw góor. Surga bu baax nga te gore. Gore nga ci lu tuuti. Dinaa la dénk lu bari. Kaay bànneexu ak man." 24 Gannaaw loolu, ki jotoon benn milyoŋ bi jegesi te ne: "Sama njaatige, xamoon naa ne nit ku néeg nga. Dangay góob foo jiwul woon tey for foo tuurul. 25 Dama ragaloon, moo tax ma dem nëbb sa xaalis bi ci suuf si. Mu ngi nii. Jëlal li nga moom." 26 Njaatigeem bi tontu ko ne: "Surga bu bon bi te tayel. Xamoon nga ne damay góob fu ma jiwul tey for fu ma tuurul. 27 Danga waroona yóbbu sama xaalis ci denckatu xaalis yi, te su ma dellusee, ma jëlaat sama xaalis ak li mu jur. 28 Jëlleen ci moom milyoŋ bi te ngeen jox ko ki am fukki milyoŋ yi. 29 Ndaxte ku am, dinañu ko yokkal, ba mu am lu ne gàññ. Waaye ku amul, dinañu jël sax li nga am. 30 Surga bu amul njériñ bi nag, sànnileen ko ci biti, ci lëndëm bi, fi am ay jooy ak yéy bëñ."
31 «Bu Doomu nit ki ñëwee ci màggaayam ànd ak malaaka yi yépp, dina toog ci baŋu nguuram bi am màggaay. 32 Xeeti àddina si yépp dinañu dajaloo ci kanamam, te mu xaajale ñenn ñi ak ñeneen ñi, ni sàmmkat di xaajale xar yi ak béy yi. 33 Dina teg xar yi ci ndeyjooram te teg béy yi ci càmmoñam. 34 Noonu buur bi dina ne ñi nekk ci ndeyjooram: "Ñëwleen, yeen ñi sama Baay barkeel te ngeen donn nguur gi leen Yàlla waajal dale ko ci bi àddina sosoo. 35 Ndaxte xiifoon naa te ngeen jox ma ma lekk, maroon naa te ngeen jox ma ma naan, nekkoon naa gan te ngeen dalal ma, 36 amuma woon yére te ngeen solal ma, feebaroon naa te ngeen toppatoo ma, nekkoon naa ci kaso bi te ngeen ñëw seetsi ma." 37 Noonu ñu jub ñi dinañu ko tontu ne: "Boroom bi, kañ lanu la gis nga xiif te nu jox la nga lekk, walla nga mar te nu jox la nga naan? 38 Kañ lanu la gis nga nekk gan te nu dalal la, walla nga ñàkk yére te nu solal la? 39 Kañ lanu la gis nga feebar walla nga nekk ci kaso te nu seetsi la?" 40 Te buur bi dina leen tontu ne: "Ci dëgg maa ngi leen koy wax, saay su ngeen ko defale kenn ki gëna ndaw ci sama mbokk yii, man mii ngeen ko defal."
41 «Gannaaw loolu, buur bi dina wax ñi nekk ci càmmoñam ne: "Sorileen ma, yeen ñi sama Baay móolu. Demleen ci safara su dul fey mukk, bi Yàlla waajal Seytaane ak malaakaam yi. 42 Ndaxte xiifoon naa te joxuleen ma ma lekk, maroon naa te joxuleen ma ma naan, 43 nekkoon naa gan te dalaluleen ma, amuma woon yére te solaluleen ma, feebaroon naa, nekkoon naa ci kaso bi te toppatoowuleen ma." 44 Noonu ñoom tamit dinañu ko tontu ne: "Boroom bi, kañ lanu la gis nga xiif walla nga mar, nekk gan walla nga ñàkk yére, nga feebar walla nga nekk ci kaso bi te dimbaliwunu la?" 45 Noonu buur bi dina leen tontu ne: "Ci dëgg maa ngi leen koy wax, saa su ngeen ko bañee defal kenn ki gëna ndaw ci sama mbokk yii, man mii ngeen ko baña defal." 46 Te ñoom dinañu dugg ci mbugal bu dul jeex bi, waaye ñu jub ñi dinañu dugg ci dund gu dul jeex gi.»