Yeesu mu ngi wax ci delluseem
24
Bi Yeesu doon génn ci kër-Yàlla gi tey dem, taalibe yi jegesi ko ngir won ko ni tabaxu kër-Yàlla gi rafete. 2 Yeesu tontu leen ne: «Gis ngeen li yépp? Ci dëgg maa ngi leen koy wax, li lépp dinañu ko yàq, te doj dootul des ci kaw doj.»
3 Yeesu toog ci tundu Oliw ya, te taalibe yi jegesi ko, ñoom ak moom rekk, ñu ne ko: «Wax nu, kañ la loolu di am, ak ban màndarga mooy firndeel sa ñëw ak njeextelu àddina si?» 4 Yeesu tontu leen ne: «Moytuleen! Buleen kenn nax. 5 Ndaxte dina am ñu bari ñuy ñëw mbubboo sama tur tey wax ne: "Man, maay Almasi bi," te dinañu nax ay nit ñu bari. 6 Dingeen dégg ñuy wax ci xare ak ay coowi xare. Buleen ragal, ndaxte mbir yooyu fàww ñu am, waaye nekkagul njeextel gi. 7 Ndaxte benn xeet dina jóg ngir xeex ak beneen xeet, te réew dina jóg ngir xeex ak beneen réew, te dina am ay xiif ak yëngu-yëngu suuf ci béréb yu wuute. 8 Waaye xew-xew yooyu yépp dinañu mel ni metit yu jëkk ci matu.
9 «Yeen, dinañu leen fitnaal, réy leen, te xeet yépp dinañu leen bañ ndax sama tur, 10 te noonu ñu bari dinañu bàyyi ngëm gi; dinañu worante tey bañante. 11 Yonent yu dëgguwul yu bari dinañu feeñ te nax nit ñu bari. 12 Lu bon day law, ba tax mbëggeelu ñu bari wàññeeku, 13 waaye ku dëgër-dëgërlu ba ci njeextel ga dinga mucc. 14 Xibaar bu baax bii ci nguuru asamaan si dinañu ko yégle ci àddina si yépp, ngir loolu nekk seede ci xeet yépp, te noonu njeextel gi ñëw.
15 «Dina am bés, li ñuy wax "lu araam tey yàqe" taxaw ci béréb bu sell bi. Loolu mooy li yonent Yàlla Dañeel waxoon (na ki jàng, xam). Su ngeen gisee loolu, 16 na ñi nekk ci Yude daw yéeg ci tund yi. 17 Ki nekk ci kaw këram, bu mu wàcc ngir jël dara ci biir këram, 18 te ki nekk ci tool yi, bu mu dellu gannaaw ngir jël mbubbam. 19 Musiba dina dal jigéen ñi nga xam ne dañoo ëmb ak ñiy nàmpal ci bés yooyu. 20 Ñaanleen Yàlla ngir seen gàddaay baña nekk ci jamonoy seddaay, walla ci bésu noflaay. 21 Ndaxte ci jamono jooju, dina am ay metit yu réy yu mësula am, ba àddina sosoo ba tey te dootul am mukk. 22 Te bu Yàlla wàññiwul woon bés yooyu, kenn du mucc. Waaye bés yooyu Yàlla dina leen wàññi ndax ñi mu tànn.
23 «Ci jamono jooju, bu leen kenn waxee ne: "Xoolleen, Almasi bi mu ngi fii" walla "mu ngi fale," buleen ko gëm. 24 Ndaxte Almasi yu dëgguwul ak yonent yu dëgguwul dinañu feeñ. Dinañu def ay màndarga ak ay kéemaan yu réy ngir bu mënee nekk sax ñu nax ñi Yàlla tànn. 25 Dégluleen! Wax naa leen loolu laata muy ñëw. 26 Bu leen kenn waxee nag, "xoolleen mu ngi ci màndiŋ bi," buleen dem; walla ñu ne leen: "Mu ngi nëbbatu ci kër gi," buleen ko gëm. 27 Ndaxte ni melax di feeñe penku te leeral ba sowu, noonu la ñëwug Doomu nit ki di mel. 28 Fu lu dee nekk, foofu la tan yi di daje.
29 «Gannaaw metitu bés yooyu, ci saa si nag,
jant bi dina lëndëm,
weer bi dootul leer,
biddéew yi dinañu daanoo ci asamaan
te kàttani asamaan dinañu yëngu.
30 Bu booba màndargawu Doomu nit ki dina feeñ ci asamaan. Noonu xeeti àddina si yépp dinañu naqarlu. Te dinañu gis Doomu nit ki ñëw ci kaw niiri asamaan ak kàttan bu réy ak màggaay. 31 Dina yónni ay malaakaam ak riiru liit bu réy, te ñu dajale ñi Yàlla tànn ci ñeenti cati àddina, fu asamaan tàmbalee ba fu mu yem.»
32 Yeesu yokk ca ne: «Jàngleen léebu garabu gaŋ bi: su fekkee ay bànqaasam tooy nañu te ay xobam tàmbale sëq, xam ngeen ne nawet bi jegesi na. 33 Noonu yeen tamit, sungeen gisee xew-xew yooyu yépp, xamleen ne Doomu nit ki jegesi na, mu ngi ci bunt bi. 34 Ci dëgg maa ngi leen koy wax, niti jamono jooju duñu weesu mukk te mbir yooyu yépp matuñu. 35 Asamaan ak suuf dinañu weesu waaye samay kàddu duñu weesu mukk.
36 «Waaye ci lu jëm ci bés bi walla ci waxtu bi, kenn xamu ko: du sax malaaka yi ci asamaan walla Doom ji, waaye Baay bi rekk moo ko xam. 37 Bés bi Doomu nit ki di dellusi dina mel ni jamonoy Nóoyin, 38 ndaxte ci bés yu jiitu woon mbënn ma, nit ñi ñu ngi doon lekk ak di naan, góor ñi ñu ngi doon takk jabar tey maye seeni doom yu jigéen, ba bés ba Nóoyin dugge ca gaal gu mag ga, 39 te yéguñu woon dara, ba keroog mbënn ma ñëw yóbbu leen, ñoom ñépp. Noonu lay ñëwug Doomu nit ki di mel. 40 Ci bés boobu ñaari nit dinañu nekk ci tool yi: ñu jël kenn ki, te bàyyi keneen ki. 41 Ñaari jigéen dinañu nekk di soq: ñu jël kenn ki te bàyyi keneen ki. 42 Kon nag, yeewuleen, ndaxte xamuleen ci ban bés la seen Boroom di ñëw. 43 Xamleen bu baax lii: Bu boroom kër gi xamoon ban waxtu ci guddi la sàcc bi di ñëw, kon, doon na xoole te du ko bàyyi mu dugg ci këram. 44 Loolu moo tax yeen tamit fagaruleen, ndaxte Doomu nit ki dina ñëw ci waxtu bi ngeen ko foogewul.
45 «Kan mooy surga bu wóor tey moytu? Kooku la njaatigeem di tànn ngir mu toppatoo yeneen surga yi, ngir mu jox leen ñu lekk ci waxtu bi gën. 46 Barkeel na surga boobu bu njaatigeem di yegsi te fekk muy jëfe noonu. 47 Ci dëgg maa ngi leen koy wax: njaatige bi dina teg alalam yépp ci ay loxoom. 48 Waaye su fekkee surga bu bon la, dina wax ci xelam ne: "Sama njaatige dina yéexa ñëw," 49 te mu tàmbali di dóor yeneen surga yi te di lekk ak naan ak màndikat yi. 50 Noonu njaatige surga boobu dina ñëw ci bés bu mu ko foogewul ak ci waxtu bu mu xamul, 51 te dina ko dóor ba tas yaramam, te boole wàllam ak naaféq yi. Foofu la jooy di ame ak yéy bëñ.»