Yeesu mu ngi ŋàññ jàngalekati-yoonu-Musaa ak Farisen yi
23
Gannaaw loolu Yeesu wax mbooloo mi ak taalibeem yi 2 ne: «Jàngalekati-yoonu-Musaa ak Farisen yi ñoom lañu sas ñuy jàngale yoonu Musaa. 3 Lépp lu ñu leen wax nag, defleen ko te sàmm ko, waaye buleen roy ci seeni jëf, ndaxte dañuy wax te duñu jëf. 4 Dañuy sas nit ñi ay jëf yu diis yu mettee yenu te di ko teg ci mbaggu ñeneen ñi, waaye ñoom duñu ko nangoo laal sax ak seen catu baaraam. 5 Seeni jëf yépp, dañu koy def ngir nit ñi gis leen. Dañuy réyal mbindu kàddu Yàlla yi ñuy takk ci seeni loxo ak ci seen jë tey guddal seeni cimbir-cimbiru mbubb. 6 Dañuy bëgg di toog ci toogukaay yu yiw yi ci lekku xew yi te di toog ci toogukaay yi féete kanam ci kër-ñaan yi, 7 te ñu di leen nuyu ak ñaari loxo ci pénc dëkk bi te nit ñi di leen woowe jàngalekat bi. 8 Waaye yeen, buleen nangu ñu woowe leen jàngalekat bi, ndaxte yeen ñépp ay mbokk ngeen te kenn rekk mooy seen jàngalekat. 9 Buleen woowe kenn baay ci suuf si ndaxte benn Baay rekk ngeen am, mooy ki nekk ci asamaan. 10 Te buleen nangu tamit ñu leen di woowe kilifa gi, ndaxte kenn rekk mooy seen kilifa, moo di Almasi bi. 11 Ki gëna mag ci seen biir, na nekk seen surga. 12 Ku yékkëtiku, dinañu la suufeel, te ku suufeelu, dinañu la yékkëti.
13-14 «Waaye musiba dina leen dal yeen jàngalekati-yoonu-Musaa ak yeen Farisen yi, naaféq yi, ndaxte dangeen di tëj buntu nguuru asamaan si ci kanamu nit ñi. Dugguleen ci, yeen ci seen bopp, te bàyyiwuleen ñi ci bëgga dugg ñu dugg. 15 Musiba dina leen dal yeen jàngalekati-yoonu-Musaa ak yeen Farisen yi, naaféq yi, ndaxte yeena ngi wër suuf ak géej ngir wut benn taalibe, te bu ngeen ko amee, ngeen def ko nitu safara bu leen gëna yées ñaari yoon.
16 «Musiba dina leen dal, yeen gumba yiy wommat, yeen ñiy wax ne: "Ku waat ci kër-Yàlla gi, dara nekku ci; waaye bu waatee ci wurusu kër-Yàlla gi, duggal na boppam." 17 Yeen ñu ñàkk xel ñi te gumba! Lan moo gëna am solo: wurus bi walla kër Yàlla biy sellal wurus bi? 18 Dangeen di wax tamit ne: "Bu kenn waatee ci bérébu saraxlukaay bi, loolu dara nekku ci; waaye bu waatee ci sarax bi nekk ci kaw bérébu saraxlukaay bi, duggal na boppam." 19 Gumba yi ngeen doon! Lan moo gëna am solo: sarax bi walla bérébu saraxlukaay biy sellal sarax bi? 20 Ki waat nag ci bérébu saraxlukaay bi waat na ci bérébu saraxlukaay bi ak lépp li nekk ci kawam. 21 Te ki waat ci kër-Yàlla gi waat na ci kër-Yàlla gi ak ci ki fa dëkk. 22 Te ki waat ci asamaan waat na ci baŋu nguuru Yàlla gi ak ci ki fa toog.
23 «Waaye musiba dina leen dal yeen jàngalekati-yoonu-Musaa ak yeen Farisen yi, naaféq yi, ndaxte dangeen di sàkk asaka ci xeetu safal yii: naana, anet, ak kumin te di sàggane li ëpp solo ci yoon bi, maanaam njubte, yërmande, ak ngëm. Loolu ngeen war di jëfe te ngeen baña sàggane li ci des. 24 Gumba yiy wommat yi ngeen doon. Yeena ngi segg wallax-njaan yi tey wann giléem.
25 «Musiba dina leen dal, yeen jàngalekati-yoonu-Musaa ak yeen Farisen yi, naaféq yi. Dangeen tàmm di raxas ci biti kaas bi ak bu ndab li, waaye ci biir mu ngi fees ak li ngeen sàcc ndax seeni bëgg-bëgg yu bon. 26 Farisen bu gumba bi! Jëkkala setal ci biir kaas bi ba noppi, te noonu biti bi dina set. 27 Musiba dina leen dal yeen jàngalekati-yoonu-Musaa ak yeen Farisen yi, naaféq yi, ndaxte dangeen mel ni ay bàmmeel yu ñu weexal. Dañuy rafet ci biti waaye ci seen biir dañoo fees ak ay yaxu ñu dee ak xeetu tilim bu nekk. 28 Yeen tamit ci kanamu nit ñi dangeen di mel ni ñu jub, waaye ci seen biir xol dangeen fees ak naaféq ak lu bon.
29 «Musiba dina leen dal yeen jàngalekati-yoonu-Musaa ak yeen Farisen yi, naaféq yi, ndaxte yeenay tabax ay bàmmeel ngir yonent yi tey rafetal bàmmeelu ñu jub ñi, 30 tey wax ne: "Su nu fekkee woon sunu jamonoy maam, dunu ànd ak ñoom ngir rey yonent yi." 31 Noonu seedeel ngeen seen bopp ne yeenay sëti ñi doon rey yonent yi. 32 Kon nag yeggaleleen li seen maam yi tàmbale woon.
33 «Yeen ñi mel ni ay jaan yu fees ak daŋar. Naka ngeen mëna moytoo ba Yàlla du leen teg daanu safara si? 34 Moo tax xoolleen! Dinaa leen yónnee ay yonent ak ñu am xel mu rafet ak ay jàngalekatu Mbind mi. Dingeen rey ñenn ñi te daaj ñeneen ñi ci bant. Ñi ci des, ngeen dóor leen ay yar ci biir kër-ñaan yi te ngeen fitnaal leen ci dëkk ak dëkk. 35 Noonu Yàlla dina këpp ci seen kaw deretu ñu jub ñi yépp, bi ñu tuur ci suuf si dale ko ci deretu Abel mu jub mi ba ci deretu Sakari miy doomu Baraki te ngeen reyoon ko ci diggante béréb bu sell bi ak bérébu saraxlukaay bi. 36 Ci dëgg maa ngi leen koy wax, loolu lépp dina këppu ci kaw niti jamono jii.
37 «Aa Yerusalem, Yerusalem, yaw miy rey yonent yi tey sànni ay xeer ñi la Yàlla yónnee ba ñu dee. Ñaata yoon ma bëgga dajale say doom ni ginaar di dajalee ay cuujam te muur leen ak ay laafam, waaye yeen, bëgguleen ko. 38 Xoolal! Yàlla dina leen bàyyee seen dëkk, mu mel ni màndiŋ. 39 Ndaxte maa ngi leen koy wax, dale ko tey, dungeen ma gisati ba keroog ngeen di wax ne: "Na Yàlla barkeel kiy ñëw ci turu Boroom bi!"»