Yeesu mu ngi nettali léebu buur bi doon waajal céetu doomam
22
Yeesu waxaat leen beneen léeb ne leen: 2 «Nguuru asamaan si, mu ngi nirook benn buur bu doon waajal céetu doomam bu góor. 3 Mu yónni surgaam yi ngir ñu jëli ñi ñu woo ci céet bi, waaye bëgguñu woona ñëw. 4 Mu yónniwaat yeneen surga, ne leen: "Demleen wax ñi ñu woo: 'Xoolleen! Togglu naa sama añ, reylu naa samay nag ak samay jur yi ma yafal. Lépp sotti na. Ñëwleen ci lekku céet bi.'" 5 Waaye ñoom fullaaluñu woote bi. Ñu daldi dem, kenn ki ci toolam, keneen ki ci njaayam, 6 te ñeneen ñi jàpp surga yi, toroxal leen, te rey leen. 7 Noonu buur bi daldi mer, yónni ay soldaaram ngir ñu rey reykatu nit yooyu te lakk seen dëkk. 8 Noonu mu wax ay surgaam: "Lekku céet bi sotti na waaye ñi ñu woo woon yelloowuñu ko. 9 Demleen nag ci mbedd yu mag yi te ngeen woo ci lekk bi ñépp ñi ngeen fa fekk." 10 Surga yi dem ci mbedd yi. Ñu dajale ñépp ñi ñu fa fekk, ñu bon ñi ak ñu baax ñi, te bérébu xew bi daldi fees ak nit. 11 Bi buur bi duggee ngir gis ñi fa nekkoon, mu seen benn waay bu solul woon yére xew. 12 Mu ne ko: "Sama xarit, noo def ba dugg ba fii te soluloo yére xew?" Waaye waa ji tontuwu ko dara. 13 Noonu buur bi ne surgaam yi: "Yeewleen ko, tànk yi ak loxo yi, te sànni ko ci biti ci lëndëm bi. Foofu la jooy di ame ak yéy bëñ."» 14 Yeesu yokk ca ne: «Ñi ñu woo bari nañu, waaye ñi ñu tànn bariwuñu.»Farisen yi ak Sadusen yi ñu ngi fiir Yeesu
15 Noonu Farisen yi dem di waxtaan ci seen biir ngir mëna fiir Yeesu ci ay kàddoom. 16 Ñu yónni seeni taalibe ak ñi far ak Erodd. Ñu ne ko: «Jàngalekat bi, xam nanu ne dëgg ngay wax tey jàngale yoonu Yàlla bi ak njubte te ragaloo kenn, ndaxte doo àtte nit ci melokaanam. 17 Wax nu nag sa xalaat: ndax yoonu Musaa bi maye na walla déet nuy fey lempo Sesaar?» 18 Waaye Yeesu xam seen coxorte te ne leen: «Naaféq yi! Lu tax ngeen may fiir? 19 Wonleen ma xànjar bi ñu wara feye lempo.» Ñu andil ko benn xànjaru xaalis 20 te Yeesu laaj leen ne: «Nataal ak mbind mi ci nekk, kan mooy boroom?» 21 Ñu ne ko: «Sesaar.» Noonu Yeesu ne leen: «Joxleen nag Sesaar li Sesaar moom te ngeen jox Yàlla li Yàlla moom.» 22 Bi ñu déggee loolu, ñu waaru. Noonu ñu bàyyi ko fa te dem.
23 Ci bés boobu sax ñenn ñi bokk ci tarixa Sadusen yi ñëw ci wetu Yeesu. Ñoom gëmuñu woon ne ndekkite am na. 24 Ñu ne ko: «Jàngalekat bi, Musaa nee na: su fekkee dafa am benn waay ju dee te amul doom, rakkam dafa wara takk jabaru magam bi ngir amal ko doom. 25 Léegi nag ci sunu biir dafa amoon juróom ñaari góor yu bokk ndey ak baay. Taaw bi takk jabar, dee, te amul doom, te bàyyil nag jabaram rakkam. 26 Ñaareel ba ak ñetteel ba def noonu, ba ci juróom ñaareel ba. 27 Gannaaw bi ñu deewee ñoom ñépp, ku jigéen ki moom tamit dee. 28 Ci ndekkitelu ñu dee ñi, jabaru kan lay doon ci juróom ñaar yi? Ndaxte ñoom ñépp takkoon nañu ko.» 29 Yeesu tontu leen ne: «Li ngeen xamul Mbind mi ak kàttanu Yàlla moo tax ngeen nekk ci njuumte. 30 Ndaxte ci ndekkitel bi góor du takk jabar te jigéen du am jëkkër, waaye dinañu mel ni malaaka yi ci asamaan. 31 Ci lu jëm ci ndekkitelu ñu dee ñi, xanaa jànguleen li leen Yàlla wax? Dafa ne: 32 "Man maay Yàllay Ibraayma, Yàllay Isaaxa, ak Yàllay Yanqóoba." Yàlla nekkul Yàllay ñi dee waaye Yàllay ñiy dund.» 33 Bi ñu déggee loolu, mbooloo mi yéemu ci njàngaleem.
34 Bi Farisen yi yégee ne Yeesu tëj na gémmiñu Sadusen yi, ñu daje 35 te kenn ci ñoom, te di jàngalekatu-yoonu-Musaa, bëggoon ko fiir. Noonu mu laaj ko ne: 36 «Jàngalekat bi, ban ndigal moo gëna mag ci yoonu Musaa?» 37 Yeesu tontu ko ne: «Nanga bëgg Yàlla sa Boroom ak sa xol bépp, sa bakkan bépp, ak sa xel mépp. 38 Ndigal boobu moo gëna mag te ëpp solo. 39 Te ñaareel bii noonu la mel: Nanga bëgg sa moroom ni nga bëgge sa bopp. 40 Yoonu Musaa bépp ak lépp li yonent yi jàngale ñu ngi aju ci ñaari ndigal yooyu.»
41 Gannaaw Farisen yi daje woon nañu, Yeesu laaj leen laaj bii 42 ne: «Lu ngeen xalaat ci Almasi bi? Sëtu kan la?» Ñu tontu ko ne: «Sëtu Daawuda la.» 43 Yeesu ne leen nag: «Naka la Daawuda, ci kàttanu Xel mu Sell mi, di ko woowe Boroom bi, ne:
44 "Yàlla Aji Sax ji nee na sama Boroom:
'Toogal ci sama ndeyjoor
ba ma daaneel say noon
fi ngay teg say tànk.'"