Ay nit yu bari ñu ngi xumbal duggu Yeesu ca Yerusalem
21
Yeesu ak taalibeem yi jegesi Yerusalem. Bi ñu yegsee dëkku Betfase ci tundu Oliw ya, mu yónni ñaari taalibe 2 ne leen: «Demleen ci gox bi nekk ci seen kanam. Ci saa si dingeen fa fekk benn mbaam bu jigéen bu ñu takk ak doomam bu nekk ak moom. Ngeen yewwi leen te andil ma leen. 3 Bu leen kenn waxee dara, dingeen ko ne: "Boroom bi moo ko soxla," te ci saa si dina bàyyi mbaam yi ñu dem.» 4 Loolu am na ngir li yonent bi waxoon mat, bi mu naan:
5 «Waxal waa Siyoŋ:
"Xoolleen! Seen Buur, mu ngi ñëw ci yeen,
suufeelu te yéeg ci mbaam bu jigéen
ak ci mbaam bu ndaw,
di doomu mala bu yenu lu diis."»
6 Noonu nag, taalibe yi dem te ñu defe ko ni leen ko Yeesu sante woon. 7 Ñu andi mbaam bu jigéen bi ak doomam te teg ci seeni yére, te Yeesu toog ci kawam. 8 Mbooloo mu takku di lal seen yére yi ci yoon bi. Ñeneen ñi dagg ay cari garab di leen lal ci yoon bi. 9 Mbooloo mi ko jiitu woon ak bi ko doon topp di yuuxu naan:
«Osaana yaw sëtu Daawuda!
Na Yàlla barkeel kiy ñëw ci turu Boroom bi!
Osaana ci asamaan yi gëna kawe!»
10 Bi Yeesu duggee Yerusalem, dëkk ba yépp yëngatu naan: «Kii mooy kan?» 11 Mbooloo mi ko gunge woon tontu ne: «Kii mooy yonent Yàlla Yeesu bu Nasaret ci diiwaanu Galile.»
Yeesu mu ngi dàq jaaykat yi ci kër-Yàlla gi te moolu garabu gaŋ bi
12 Yeesu dugg na ci ëttu Kër-Yàlla gi te dàq ñépp ñi fa doon jaay ak jënd. Mu daaneel taabali wéccikatu xaalis yi ak toogukaayu jaaykatu pitax yi, 13 te mu ne leen: «Mbind mi nee na: "Sama kër, dinañu ko woowe këru ñaanukaay, " waaye yeen def ngeen ko këru sàcc yi.»
14 Noonu ay gumba ak ay lafañ jegesi Yeesu ci ëttu Kër-Yàlla gi te mu wéral leen. 15 Amoon na ay xale yu fa doon yuuxu naan: «Osaana sëtu Daawuda.» Bi njiiti-jébbalkati-sarax yi ak jàngalekati-yoonu-Musaa déggee loolu te gis yëf yu yéeme yi Yeesu doon def, ñu daldi mer. 16 Ñu ne ko: «Ndax dégg nga li xale yi di wax?» Yeesu tontu leen ne: «Waaw, dégg naa ko. Xanaa yeen, mësuleena jàng kàddu yii ci Mbind mi:
"Ci gémmiñu gone yi ak ñiy nàmp
sàkkal nga sa bopp ay cant."?»
17 Gannaaw loolu mu bàyyi leen te génn dëkk bi ngir dem fanaani dëkku Betani.
18 Ëllëg sa, ci suba teel; bi muy dellu ci dëkk bi, mu xiif. 19 Mu gis benn garabu gaŋ ci wetu yoon bi. Mu jegesi ko, waaye fekku fa lu dul ay xob. Noonu mu ne garab bi: «Dootuloo meññ mukk.» Ci saa si garabu gaŋ bi daldi wow koŋŋ. 20 Bi ñu gisee loolu, taalibe yi waaru te ne: «Naka la garabu gaŋ bi mëna wowe ci saa si?» 21 Yeesu tontu leen ne: «Maa ngi leen koy wax, su ngeen gëmee te baña am sikki-sàkka, dungeen yem rekk ci li ma def garabu gaŋ bii, waaye dingeen mëna wax sax tund bii ne: "Jógal fii te nga daanu ci géej gi," te dina am. 22 Lépp lu ngeen ñaan Yàlla, bu ngeen amee ngëm, dingeen ko jot.»
Yeesu mu ngi nettali ñaari léeb ngir wone sañ-sañam
23 Bi Yeesu yegsee ci ëttu kër-Yàlla gi, mu tàmbali di jàngale. Noonu njiiti-jébbalkati-sarax yi ak magi askan bi ñëw, laaj ko ne: «Wax nu, ci ban sañ-sañ ngay defe mbir yii? Ak kan moo la jox sañ-sañ boobu?» 24 Noonu Yeesu tontu leen: «Man tamit, am naa benn laaj ngir yeen. Bu ngeen ma tontoo, dinaa leen tontu tamit ci ban sañ-sañ laay defe mbir yii. 25 Li Yaxya doon def, di sóob nit ñi ci ndox, fan la ko jële: ci Yàlla walla ci nit?» Noonu ñuy waxtaan ci seen biir ne: «Bu nu waxee ne "Ci Yàlla la ko jële," dina wax "Lu tax yeen gëmuleen ko?" 26 Waaye bu nu waxee ne "Ci nit la ko jële," war nanu ragal mbooloo mi, ndaxte ñépp jàpp nañu ne Yaxya yonent la woon.» 27 Noonu ñu tontu ko ne: «Xamunu fan la ko jële.» Yeesu ne leen: «Man tamit duma leen wax ci ban sañ-sañ laay defe mbir yii.
28 «Lan ngeen xalaat ci lii? Benn waay amoon na ñaari doom yu góor. Mu dem ci ku jëkk ki te ne ko: "Sama doom, tey nanga dem liggéeyi ci sama toolu reseñ bi." 29 Doom ji ne ko: "Bëgguma dem." Ci kanam tuuti mu réccu te mu dem fa. 30 Pàppa ji dem ci ñaareelu doom ji te wax ko li mu waxoon ku jëkk ki. Mu tontu ko ne: "Waaw pàppa. Maa ngi fay dem." Waaye demu fa. 31 Kan ci ñoom ñaar ñi moo def coobare pàppaam?» Ñu tontu ko ne: «Ku jëkk ki.» Noonu Yeesu ne leen: «Ci dëgg maa ngi leen koy wax: juutikat yi ak jigéen yiy jaay seen yaram dinañu leen jiitu ci nguuru Yàlla gi, 32 ndaxte Yaxya ñëw na ngir won leen yoonu njubte bi te yeen gëmuleen ko. Waaye juutikat yi ak jigéen yuy jaay seen yaram gëm nañu ko. Te yeen, bi ngeen gisee loolu sax, taxul ngeen réccu ba gëm ko.»
33 Gannaaw loolu Yeesu ne leen: «Dégluleen beneen léeb: dafa amoon benn boroom kër bu jëmbët toolu reseñ. Mu wërale ko ak miir, gas fa nalukaayu reseñ, te tabax wottukaay. Noonu mu batale ko ay beykat te tukki. 34 Bi waxtu góob bi jegesee, mu yónni surgaam yi ci beykat yi ngir ñu jox ko meññeefam, 35 waaye beykat yi jàpp surga yi: ñu dóor kenn ki, rey keneen ki, te sànni ay xeer ki ci des. 36 Boroom tool bi yónniwaat yeneen surga yu gëna bari ñu jëkk ña, waaye beykat yi def leen li ñu defoon ñu jëkk ña. 37 Ci mujjantal ba, mu yónnee leen doomam bu góor, di wax ne: "Dinañu jox cér sama doom." 38 Waaye bi beykat yi gisee doom ji, ñu wax ci seen biir ne: "Ki wara donn tool bi mu ngi nee di ñëw. Ñëwleen, nu rey ko te nu moom tool bi." 39 Noonu ñu jàpp ko, génne ko toolu reseñ bi, te rey ko.»
40 Noonu Yeesu laaj ñi ko doon déglu: «Bu boroom tool bi ñëwee, lan la nara def beykat yooyu?» 41 Ñu tontu ko ne: «Dina rey nit yu bon yooyu te du ci am yërmande. Gannaaw loolu dina dénk toolam yeneen beykat yu koy jox meññeefam ci waxtu bi gën.» 42 Yeesu ne leen: «Xanaa mësuleen jàng ci Mbind mi lii:
"Doj bi tabaxkat yi sànni woon
mujj na nekk doj bi ëpp solo ci tabax bi.
Boroom bi moo def loolu,
te lu yéeme la ci sunuy bët"?
43 Loolu moo tax maa ngi leen koy wax: yeen, Yàlla dina leen xañ nguuram te jox ko askan buy am meññeef, maanaam jëfi nguuram. 44 Ku daanu ci kaw doj bii damm. Te képp ku mu daanu ci sa kaw, dina la rajaxe.»
45 Bi njiiti-jébbalkati-sarax yi ak Farisen yi déggee léeb yooyu, ñu xam ne ñoom la doon waxal. 46 Noonu ñuy wut nu ñu koy jàppe, waaye ragaloon nañu mbooloo mi, ndaxte ñépp jàppoon nañu ne Yeesu yonent la woon.