Yeesu mu ngi nettali léebu liggéeykat yi ci tollu reseñ bi
20
«Nguuru asamaan si lii lay nirool: dafa amoon benn boroom kër bu jóg suba teel ngir jël ay nit, ñu liggéeyal ko ci toolu reseñam. 2 Mu déggoo ak ñoom ci peyoor bi mu leen wara fey: benn xànjaru xaalis ngir bés bi. Noonu mu wax leen ñu dem liggéeyi ci toolu reseñam. 3 Ci juróom ñeenteelu waxtu ci suba si, mu génnaat te gis ñeneen ñu nekkoon ci pénc bi, defuñu dara. 4 Mu ne leen: "Yeen tamit, demleen liggéeyi ci sama toolu reseñ bi, te dinaa leen jox lu jaadu." 5 Ñu dem fa. Mu génnaat tamit ci diggu bëccëg ak ci ñetteelu waxtu ci ngoon, te defaat noonu. 6 Ci mujjantal ba, ci booru juróomi waxtu ci ngoon, mu génn te gis yeneen nit yu nekkoon foofu te mu ne leen: "Lu tax ngeen nekk fii ci bés bi yépp te defuleen dara?" 7 Ñu tontu ko ne: "Ndaxte kenn jëlu nu." Mu ne leen: "Yeen tamit, demleen liggéeyi ci sama toolu reseñ bi." 8 Bi ngoon si jotee, boroom tool bi wax jiitu surgaam yi ne: "Woowal liggéeykat yi te nga jox ku nekk peyooram, nga tàmbale ci ñu mujj ñi, te jeexale ci ñu jëkk ña." 9 Liggéeykat yi ñu jëloon ci juróomeelu waxtu ci ngoon ñëw nag te jot ku nekk benn xànjaru xaalis. 10 Bi ñu jëkk ñi ñëwee, ñu xalaat ne dinañu jot lu ëpp loolu, waaye ñoom tamit ñu jot ku nekk benn xànjaru xaalis. 11 Bi ñu ko jotee ñu tàmbale xultu jëmale ko ci boroom kër gi, 12 di naan: "Ñi mujje benn waxtu rekk lañu liggéey te nga tolloole leen ak nun ñi doon muñ coono liggéeyu bésu lëmm ci naaj bu tàng bi." 13 Waaye boroom tool bi tontu kenn ci ñoom ne: "Sama xarit, tooñuma la. Ndax déggoowuloo woon ak man ci benn xànjaru xaalis? 14 Jëlal nag li nga moom te nga dem. Dafa ma neex ma jox ku mujj ki lu tollu ni li ma la jox. 15 Ndax amuma sañ-sañu def li ma neex ci sama alal? Walla ndax danga iñaan ci li ma baax?"» 16 Yeesu yokk ca ne: «Noonu ñi mujje dinañu jiitu te ñi jiitu dinañu mujje.»Section 44: Doomu nit ki dafa ñëw ni surga
17 Bi Yeesu di dem Yerusalem, ci yoon bi mu jël fukk yi ak ñaar, ber leen te ne leen: 18 «Dégluleen! Nu ngi ci yoonu Yerusalem. Foofu dinañu jébbal Doomu nit ki ci loxoy njiiti-jébbalkati-sarax yi ak jàngalekati-yoonu-Musaa. Dinañu ko teg daanu dee, 19 te jébbal ko ci loxoy ñi nekkul Yawut ngir ñu ñaawal ko, dóor ko ay yar, daaj ko ci bant, te ci ñetteelu fan ba mu dekki.»
20 Noonu jabaru Sebede, ànd ak doomam yi, Saak ak Yowaana, jegesi Yeesu. Mu sukk ci kanamam ngir ñaan ko benn mbir. 21 Yeesu ne ko: «Soxna si, lan nga bëgg ma defal la ko?» Mu tontu ko ne: «Dama bëgg nga santaane ngir, boo nekkee ci sa nguur, sama ñaari doom yii toog, kenn ki ci sa ndeyjoor, keneen ki ci sa càmmoñ.» 22 Yeesu wax Saak ak Yowaana ne: «Xamuleen li ngeen di ñaan. Ndax mën ngeena naan kaas bi ma nara naan?» Ñu tontu ko ne: «Waaw, mën nanu ko.» 23 Yeesu ne leen: «Sama kaas bi, dingeen ci naan, waaye toog ci sama ndeyjoor walla ci sama càmmoñ du man maa koy maye. Béréb yooyu, ñi leen sama Baay jagleel ñoo leen moom.»
24 Bi fukk yi des déggee loolu, ñu daldi mere Saak ak Yowaana, 25 waaye Yeesu woo leen ñoom ñépp ci wetam te ne leen: «Xam ngeen ne njiiti xeet yi dañuy not seeni askan, te kilifa yi di jëfe ak sañ-sañ ci ñoom. 26 Warul deme noonu ci seen biir. Waaye ku bëgga nekk màgg ci seen biir, na nekk seen surga, 27 te ku bëgga jiitu ci seen biir, na nekk seen jàmm. 28 Noonu la mel ci Doomu nit ki: ñëwul ngir ñu nekk ay surgaam, waaye ngir mu nekk surga te joxe bakkanam ngir fey boru bàkkaaru ñu bari.»
Yeesu wéral na ñaari gumba
29 Bi Yeesu ak taalibe yi génnee Yeriko, mbooloo mu takku di ko topp. 30 Foofu amoon na ñaari gumba yu toogoon ci wetu yoon bi. Bi ñu déggee ne Yeesu mooy jàll, ñu tàmbale yuuxu, naan: «Boroom bi, sëtu Daawuda, yërëm nu.» 31 Mbooloo mi di leen gëdd ngir ñu noppi. Waaye ñu gëna yuuxu ak baat yu kawe naan: «Boroom bi, sëtu Daawuda, yërëm nu.» 32 Yeesu daldi taxaw, woo leen te ne leen: «Lan ngeen bëgg ma defal leen?» 33 Ñu tontu ko ne: «Boroom bi, na sunu bët yi ubbeeku.» 34 Yeesu yërëm leen te laal seen bët yi. Ci saa si ñu gisaat te topp Yeesu.