Yeesu mu ngi jàngale ci li jëm ci séy
19
Bi Yeesu waxee kàddu yooyu ba noppi, mu jóge ci diiwaanu Galile dem ci diiwaanu Yude ci wàll bi féete ci beneen wetu dexu Yurdan. 2 Mbooloo mu takku topp ko, te foofu mu wéral ñi feebar. 3 Ay Farisen jegesi ko ngir fiir ko. Ñu laaj ko: «Ndax sunu yoon bi may na góor mu fase jabaram ak lu mu mën di doon?» 4 Yeesu tontu leen ne: «Xanaa jànguleen ne: Ki sàkk ca njàlbéen ga sàkkoon na nit, góor ak jigéen, 5 te mu ne leen: "Loolu moo tax góor dina bàyyi pàppaam ak yaayam ngir taq ci jabaram, te ñoom ñaar ñu doon benn"? 6 Noonu nekkatuñu ñaar waaye benn lañuy doon. Kon nag li Yàlla boole, bu ko nit tas.» 7 Ñu ne ko: «Lu tax nag Musaa santaane góor mu jox jabaram bataaxal ngir fase ko?» 8 Yeesu tontu leen: «Seen dëgëraayu xol moo tax Musaa may leen ngeen di fase seeni jabar, waaye ca njàlbéen ga demewul woon noonu. 9 Maa ngi leen koy wax, ku fase jabaram te du ci njaaloo te séyaat ak beneen jigéen, njaaloo nga.»10 Taalibeem yi ne ko: «Su fekkee noonu la diggante góor ak jigéen mel, baña séy moo gën.» 11 Yeesu tontu leen: «Du ñépp ñoo mëna nangu loolu, waaye ñi ko Yàlla may rekk. 12 Ndaxte am na ñu mënula séy, ñenn ñi dañoo judduwaale tële, ñeneen ñi dañoo tële jaarale ko ci loxoy nit, te am na tamit ñu baña séy ndax nguuru asamaan si. Ku mëna nangu kàddu googu, na ko nangu.»
Yeesu mu ngi wax ci duggum nguuru asamaan si
13 Amoon na ñu ñëw, andil Yeesu ay gone ngir mu teg leen loxo te ñaanal leen, waaye taalibe yi di leen gëdd. 14 Noonu Yeesu ne: «Bàyyileen gone yi, buleen leen tere ñu ñëw ci man, ndaxte ñu mel ni ñoom ñoo moom nguuru asamaan si.» 15 Gannaaw loolu, Yeesu teg leen loxo te wéy ci yoonam.
16 Noonu benn waxambaane jegesi ko te ne ko: «Jàngalekat bi, lan laa wara def lu baax ngir am dund gu dul jeex gi?» 17 Yeesu tontu ko ne: «Lan moo tax nga may laaj ci lu baax? Kenn rekk moo baax. Soo bëggee dugg ci dund gi, déggalal ndigal yi.» 18 Waxambaane bi ne ko: «Yan ndigal?» Yeesu tontu ko: «Bul rey nit, bul njaaloo, bul sàcc, bul seede lu dul dëgg, 19 teralal sa baay ak sa yaay, te nga bëgg sa moroom ni nga bëgge sa bopp.» 20 Waxambaane bi ne ko: «Ndigal yooyu yépp, sàmm naa leen. Lu ma deseeti?» 21 Yeesu ne ko: «Soo bëggee nekk ku mat, demal, nga jaay li nga am, jox ko néew-di-doole yi. Noonu dinga am alal ci asamaan si, te nga ñëw topp ci man.» 22 Bi waxambaane bi déggee kàddu yooyu, mu dem ànd ak tiis ndaxte dafa bari woon alal lool.
23 Noonu Yeesu ne taalibe yi: «Ci dëgg maa ngi leen koy wax, lu jafe a ngoogu ngir boroom alal dugg ci nguuru asamaan si. 24 Maa ngi leen koy waxaat, giléem jaar ci bën-bënu puso moo gëna yomb boroom alal dugg ci nguuru Yàlla.» 25 Bi ñu déggee loolu, taalibe yi daldi jaaxle lool te ñu ne ko: «Kon nag, kan moo mëna mucc?» 26 Yeesu xool leen te ne leen: «Loolu të na nit waaye Yàlla mën na lépp.» 27 Noonu Piyeer jël kàddu gi te ne: «Xoolal! Nun, bàyyi nanu lépp ngir topp la. Kon nag nu nuy mujje?» 28 Yeesu ne leen: «Ci dëgg maa ngi leen koy wax, bés bi Yàlla di yeesal mbir yépp, bu Doomu nit ki toogee ak màggaayam ci baŋu nguuram, yeen ñi ma topp, yeen tamit dingeen toog ci fukki baŋu nguur ak ñaar ngir àtte fukki giir ak ñaar yu Israyil. 29 Te képp ku bàyyi ay këram, ay mbokkam yu góor ak ay mbokkam yu jigéen, baayam, yaayam, ay doomam walla ay suuf ndax sama tur, dina ko jotaat lu ëpp téeméeri yoon te am dund gu dul jeex gi. 30 Waaye ñu bari ci ñi jiitu léegi dinañu mujje. Te ñu bari ci ñi mujje léegi dinañu jiitu.»