Yeesu mu ngi jàngale ci lu jëm ci bàkkaar ak ci baale
18
Ci waxtu boobu taalibe yi jegesi Yeesu te laaj ko ne: «Kan mooy ki gëna màgg ci nguuru asamaan si nag?» 2 Noonu mu woo benn xale, teg ko ci seen biir, 3 te ne: «Ci dëgg maa ngi leen koy wax, su ngeen woññeekuwul ngir mel ni xale yi, dungeen dugg ci nguuru asamaan si. 4 Kon nag képp ku suufeelu ba mel ni xale bii, nit kooku mooy ki gëna màgg ci nguuru asamaan si. 5 Ku nangu xale bu mel ni kii ci sama tur, man mii la nangu. 6 Waaye ku bàkkaarloo kenn ci ñi gëna ndaw ci ñi gëm ci man, kooku ñu takk xeer bu réy ci baatam te ñu labal ko ci biir géej gi mooy gën ci moom. 7 Musiba dina dal ci àddina siy xiir nit ñi ci bàkkaar. Fiir mënula ñàkk, waaye musiba dina dal ci ki muy jaar. 8 Bu la sa loxo walla sa tànk di xiir ci bàkkaar, dagg leen te sànni leen fu sori. Ndaxte nga dugg ci dund gu wóor gi ak benn loxo walla benn tànk rekk moo gën nga am ñaari loxo walla ñaari tànk te ñu sànni la ci safara su dul fey mukk. 9 Te bu la sa bët di xiir ci bàkkaar, lóqati ko te nga sànni ko fu sori. Ndaxte nga dugg ci dund gu wóor gi ak benn bët moo gën nga am ñaari bët te ñu sànni la ci safara.10-11 «Moytuleen di xeeb kenn ci ñu ndaw ñii, ndaxte maa ngi leen koy wax, seeni malaaka yi ci asamaan ñu ngi gis saa su nekk sama xar-kanamu Baay bi ci asamaan. 12 Lan ngeen ci xalaat: su kenn amee téeméeri xar te benn ci ñoom réer, ndax du bàyyi juróom ñeent fukk ak juróom ñeent yi des ci tund bi ngir dem seeti bi réer? 13 Te bu ko gisee, ci dëgg maa ngi leen koy wax, dina bànneexu ci xar boobu lu ëpp li muy bànneexu ci juróom ñeent fukk ak juróom ñeent yi réerul. 14 Noonu tamit seen Baay bi ci asamaan bëggul kenn ci ñu ndaw ñii réer.
15 «Bu sa mbokku gëmkat bàkkaaree, demal te nga yedd ko, yeen ñaar rekk. Su la dégloo, delloosi nga sa mbokk. 16 Waaye su la dégluwul, jëlal benn walla yeneen ñaari nit ak yaw ngeen dellu fa, ngir bépp mbir leer ci kàddu ñaar walla ñetti seede. 17 Bu leen bañee déglu, wax ko mbooloo ñi gëm, te su bañee déglu mbooloo ñi gëm, nanga ko jàppe ni ku gëmul Yàlla walla juutikat. 18 Ci dëgg maa ngi leen koy wax: Lépp lu ngeen yeew ci àddina si, dinañu ko yeew ci asamaan, te lépp lu ngeen yewwi ci àddina si dinañu ko yewwi ci asamaan. 19 Ci dëgg maa ngi leen koy waxaat, su ñaar ci yeen déggoo ci àddina si ngir ñaan ak lu mu mëna doon, loolu sama Baay bi ci asamaan dina leen ko may. 20 Ndaxte fu ñaar walla ñetti nit booloo ci sama tur, maa ngi foofu ci seen biir.»
21 Noonu Piyeer jegesi ko te ne ko: «Boroom bi, su ma sama mbokk tooñee, ñaata yoon laa ko wara baal? Xanaa ba juróom ñaari yoon?» 22 Yeesu tontu ko ne: «Déedéet, waxuma la ba juróom ñaari yoon, waaye ba juróom ñaar fukk ba muy juróom ñaari yoon. 23 Loolu moo tax nguuru asamaan si dafa mel ni benn buur bu woolu surgaam yi ngir xam ku nekk ñaata la ko ameel. 24 Bi mu tàmbalee, ñu andil ko benn surga bu ko ameeloon ay milyoŋ yu bari. 25 Surga bi amul woon lu mu feye. Noonu njaatigeem bi joxe ndigal ñu jaay ko, moom, jabaram, ay doomam, ak lépp li mu amoon, ngir fey boram. 26 Noonu surga bi daanu ci tànku njaatige bi, sukk ci kanamam, te ñaan ko ne: "Muñal ma te dinaa la fey lépp." 27 Njaatige bi yërëm ko, baal ko boram, te bàyyi ko mu dem. 28 Gannaaw loolu, surga bi génn te daje ak beneen surga bu ko ameeloon ay junni. Mu jàpp ko, xoj ko te ne: "Fey ma li nga ma ameel." 29 Moroomu surgaam bi daanu ci tànkam yi te di ko ñaan naan: "Muñal ma te dinaa la ko fey." 30 Waaye mu bañ. Rax ci dolli mu dem tëjlu ko kaso ba mu fey ko li mu ko ameel. 31 Bi yeneen surga yi gisee li xewoon, ñu daldi ànd ak tiis bu réy te ñu dem nettali seen njaatige lépp. 32 Noonu njaatige bi woolu surga boobu te ne ko: "Surga bu bon bi, baal naa la sa bor bi yépp ndaxte danga ma ñaan. 33 Ndax yaw tamit mënoo woona yërëm sa moroom mi, ni ma la yërëme?" 34 Ci biir meram, njaatige bi daldi ko jébbal ñi koy metital ci kaso bi ba mu fey boram bi yépp.» 35 Te Yeesu yokk ca ne: «Noonu la leen sama Baay bi ci asamaan di def, su fekkee ku nekk ci yeen du baal moroomam ak xolam bépp.»