Melokaanu Yeesu soppeeku na ci kaw tund bi
17
Juróom benni fan gannaaw loolu, Yeesu jël ak moom Piyeer, Saak, ak Yowaana te yóbbu leen ci kaw tund bu kawe lool, beru ak ñoom. 2 Noonu xar-kanamam soppeeku ci seen kanam: kanamam di melax ni jant bi te ay yéreem weex ni leer bi. 3 Te noonu Musaa ak Ilyaas feeñu leen, di waxtaan ak Yeesu. 4 Piyeer ne Yeesu: «Boroom bi, baax na ngir nu des fii. Soo ko bëggee dinaa, fi defar ñetti mbaar: benn ngir yaw, benn ngir Musaa, ak benn ngir Ilyaas.» 5 Bi mu nekkee di wax noonu, benn niir bu leer muur leen, te noonu baat jóge ci niir bi di wax ne: «Kii mooy sama doom ji ma sopp. Ci moom laa ame bànneex. Dégluleen ko!» 6 Bi ko taalibe yi déggee, ñu tiit lool te daanu seen kanam yi dëpp ci suuf si, 7 waaye Yeesu jegesi leen, teg leen loxo, te ne: «Jógleen te buleen ragal.» 8 Bi ñu yékkëtee seeni bët, gisatuñu woon kenn ku dul Yeesu rekk.
9 Bi ñuy wàcc tund bi, Yeesu jox leen ndigal ne leen: «Buleen wax kenn li ngeen gis ba keroog Doomu nit ki di dekki ci biir ñu dee ñi.» 10 Taalibe yi laaj ko ne: «Lu tax jàngalekati-yoonu-Musaa di wax ne Ilyaas fàww mu jëkka ñëw?» 11 Yeesu tontu leen ne: «Waaw, Ilyaas war na jëkka ñëw, yeesalaat lépp. 12 Waaye maa ngi leen koy wax, Ilyaas ñëw na ba noppi te xàmmewuñu ko, waaye def nañu ko lu leen neex. Noonu tamit lañuy sonnale Doomu nit ki.» 13 Noonu taalibe yi xam ne ci Yaxya la leen doon wax.
Yeesu mu ngi wéral benn xale bu góor bu rab jàppoon
14 Bi Yeesu, Piyeer, Saak, ak Yowaana yegsee ci wetu mbooloo mi, benn waay jegesi Yeesu, sukk ci kanamam, 15 tey naan: «Boroom bi, yërëmal sama doom bu góor. Dafa am feebaru say, te mu sonnal ko lool. Dafay faral di daanu ci xal walla ci ndox. 16 Andil naa ko sa taalibe yi, waaye mënuñu ko wéral.» 17 Yeesu daldi jël kàddu gi te ne leen: «Yeen niti jamono jii, ñi amul ngëm te dëng. Man, ba kañ laay nekk ak yeen te di leen muñal? Andilleen ma fii xale bi.» 18 Yeesu gëdd rab bi te mu génn ci xale bi, te xale bi daldi wér ci saa si.
19 Noonu taalibe yi fekksi Yeesu, nekk ak moom rekk, laaj ko: «Lu tax nun mënunu dàq rab bi?» 20-21 Yeesu tontu leen: «Ndaxte dangeen tuuti ngëm. Ci dëgg maa ngi leen koy wax, soo leen amee ngëm gu tollu ni doomu fuddën dingeen wax tund bii: "Jógeel fii, toxu fee" te dina ko def. Dara du leen të.»
Yeesu mu ngi yéglewaat deewam
22 Bi taalibe yi dajaloowee ci diiwaanu Galile, Yeesu wax leen ne: «Dinañu jébbal Doomu nit ki ci loxoy nit ñi, 23 dinañu ko rey, te ci ñetteelu fan ba mu dekki.» Taalibe yi am naqar gu réy ndax kàddu yooyu.
Yeesu mu ngi fey lempo ngir kër-Yàlla gi
24 Bi Yeesu ak taalibeem yi yegsee ci dëkku Kapernawum, ñi doon laaj lempo ngir kër-Yàlla gi jegesi Piyeer te laaj ko ne: «Ndax seen jàngalekat bi du fey lempo ngir kër-Yàlla gi?» 25 Mu tontu ko ne: «Waaw.» Bi Piyeer duggee ci kër gi Yeesu jëkka jël kàddu gi te ne ko: «Loo ci xalaat Simoŋ? Buuri àddina sii, ci kan lañuy jote juuti ak lempo? Ci seeni doom walla ci gan yi?» 26 Piyeer tontu ko ne: «Ci gan yi.» Yeesu ne ko: «Kon nag doom yi bokkuñu ci. 27 Waaye ngir bañ leena merloo, demal ci wetu dex ga, nga sànni oos, nga jël jën bi ngay jëkka jàpp, te nga ubbi gémmiñam. Dinga ci fekk xànjaru xaalis. Jël ko te nga fey leen lempo ngir nun ñaar.»