Yeesu mu ngi artu taalibeem yi ñu moytu njàngale Farisen yi ak Sadusen yi
16
Noonu Farisen yi ak Sadusen yi jegesi Yeesu di ko fexe fiir. Ñu laaj ko kéemaan buy firndeel ne ci asamaan lay jële kàttanam. 2 Mu tontu leen ne: «Ci ngoon si dangeen di wax ne: "Suba du taw, ndaxte asamaan si dafa xonq." 3 Te ci suba dangeen di wax ne: "Tey dina taw, ndaxte asamaan si dafa xiin ba xonq." Mën ngeena ràññee liy xew ci asamaan si, waaye mënuleen ràññee màndarga yi Yàlla di def ci jamono jii. 4 Niti jamono ji dañoo bon tey moy Yàlla. Ñu ngi laaj benn kéemaan waaye duñu leen jox benn bu dul màndarga yonent Yàlla Yunus.» Noonu Yeesu bàyyi leen fa te dem.5 Bi ñuy jàll ci beneen wetu dex gi, taalibe yi fàtte woon nañu yóbbaale mburu. 6 Yeesu ne leen: «Xoolleen! Moytuleen lawiiru Farisen yi ak bu Sadusen yi.» 7 Taalibe yi di werante ci seen biir ne: «Li nu andaalewul mburu moo tax muy wax loolu.» 8 Yeesu xam loolu te ne leen: «Lu tax ngeen di werante ci seen biir ci li ngeen amul mburu? Yeen daal, yeena tuuti ngëm. 9 Ndax ràññeewuleen ba léegi? Ndax fàttalikuwuleen juróomi mburu yi ma dammoon ngir juróomi junniy góor ya ak ñaata pañe ngeen ci foroon? 10 Walla juróom ñaari mburu yi ngir ñeenti junniy góor ya ak ñaata pañe ngeen ci foroon? 11 Lu tax xamuleen ne du ci mburu laa leen di wax? Moytuleen lawiiru Farisen yi ak bu Sadusen yi.» 12 Noonu taalibe yi xam ne da leen doon wax ngir ñu moytu njàngale Farisen yi ak Sadusen yi, waaye du lawiiru mburu yi.
Yeesu mooy Almasi bi
13 Yeesu yegsi ci diiwaanu Sesare bu Filib. Mu tàmbale laaj taalibeem yi ne: «Lan la nit ñi di wax ci lu jëm ci Doomu nit ki? Mooy kan?» 14 Ñu tontu ko ne: «Am na ñuy wax ne mooy Yaxya; ñii ne mooy Ilyaas; ñeneen ñi ne mooy Yeremi, walla keneen ci yonent yi.» 15 Mu laaj leen ne: «Waaye yeen nag, kan ngeen wax ne moom laa?» 16 Simoŋ Piyeer tontu ko ne: «Yaw yaay Almasi bi, di doomu Yàlla biy dund.» 17 Yeesu tontu ko ne: «Barkeel nga Simoŋ doomu Yunus, ndaxte du nit moo la xamal loolu, waaye sama Baay bi ci asamaan. 18 Te man, maa ngi la koy wax, yaw yaay Piyeer te ci kaw doj bii laay samp sama mbooloo ñi gëm te dooley dee du ko mënal dara. 19 Dinaa la jox caabi nguuru asamaan si. Li nga yeew ci àddina si, dinañu ko yeew ci asamaan. Loo yewwi ci àddina si, dinañu ko yewwi ci asamaan.» 20 Noonu mu dénk taalibeem yi ak doole ngir ñu baña wax kenn ne moom mooy Almasi bi.
Yeesu yégle na deewam
21 Dale ko ci waxtu boobu, Yeesu tàmbale won taalibeem yi ne dafa wara dem Yerusalem, te foofu, mag ñi, njiiti-jébbalkati-sarax yi ak jàngalekati-yoonu-Musaa sonnal ko lool, ñu rey ko, te mu dekki ci ñetteelu fan ba. 22 Noonu Piyeer woo ko, wéetoo ak moom, te tàmbale di ko yedd naan: «Yàlla tere, Boroom bi. Loolu du la dal mukk!» 23 Yeesu walbatiku te ne ko: «Sori ma Seytaane, jàll ci sama gannaaw. Gàllankoor nga ci man, ndaxte du yëfi Yàlla ngay xalaat waaye yëfi nit.»
24 Noonu Yeesu ne taalibeem yi: «Ku ma bëgga topp na bàyyi boppam, nangu daj lu metti, te doora topp ci man. 25 Ndaxte ku bëgga musal sa bakkan dinga ko ñàkk, waaye ku ñàkk sa bakkan ngir man, dinga ko jotaat. 26 Lu muy jériñ nit su fekkee day moom àddina si yépp te ñàkk bakkanam? Amul dara lu nit mëna joxe ngir jotaat dundam. 27 Ndaxte Doomu nit ki dina ñëw ak ay malaakaam ci màggaayu Baayam, te noonu dina delloo ku nekk ay jëfam. 28 Ci dëgg maa ngi leen koy wax, am na ñoo xam ne ñu ngi fii duñu dee mukk te gisuñu Doomu nit ki ñëw ak nguuram.»