Yeesu mu ngi wax ci liy andil nit sobe
15
Noonu ay Farisen ak ay jàngalekatu-yoonu-Musaa jóge Yerusalem. Ñu jegesi Yeesu te ne ko: 2 «Lu tax sa taalibe yi dunu déggal sunuy aaday maam? Ndaxte duñu raxas seeni loxo laata ñuy lekk.» 3 Mu tontu leen ne: «Yeen nag, lu tax dungeen déggal ndigalu Yàlla ndax seen aada? 4 Ndaxte Yàlla nee na: "Teralal sa baay ak sa yaay" te "Ku saaga baayam walla yaayam, nañu ko rey." 5 Waaye yeen, dangeen di wax ne: "Ki wax baayam walla yaayam ne: 'Sama alal bi ma la wara jàppale, jébbal naa ko Yàlla,' 6 nit kooku wàccoo na ak warugaru teral baayam ak yaayam." Noonu dangeen di neenal kàddu Yàlla gi ngir topp seen aada. 7 Naaféq yi! Esayi waxoon na dëgg bu wóor bi mu doon wax ci turu Yàlla ci lu jëm ci yeen, bi mu ne:
8 "Askan bii dafa may màggal ak seen gémmiñ
waaye seen xol sori na ma.
9 Ci neen lañu may jaamu
ndaxte ay ndigalu nit lañuy jàngale
jàppe ko samay ndigal."»
10 Gannaaw loolu Yeesu woo mbooloo mi te ne leen: «Dégluleen te ngeen ràññee. 11 Du liy dugg ci gémmiñ mooy andil nit sobe. Waaye liy génn ci gémmiñu nit moo koy andil sobe.»
12 Noonu taalibe yi jegesi te ne ko: «Ndax xam nga ne Farisen yi dañoo mer ci kàddu gi ñu dégg?» 13 Mu tontu leen ne: «Bépp garab bu sama Baay bi ci asamaan jiwul, dinañu ko buddi. 14 Nangeen leen bàyyi. Ay gumba yuy wommat ay gumba lañu. Bu gumba di wommat moroomu gumbaam, ñoom ñaar ñépp dinañu daanu ci kàmb.» 15 Piyeer jël kàddu gi te ne ko: «Wax nu li léeb boobu di tekki.» 16 Mu ne leen: «Ndax yeen tamit ràññeewuleen ba léegi? 17 Ndax xamuleen ne lépp liy dugg ci gémmiñ ci biir bi la jëm ba noppi génn ci yaram? 18 Waaye liy génn ci gémmiñ ci xol la jóge te loolu mooy andil nit sobe. 19 Ndaxte ci xol la xalaat yu bon yi di jóge di la yóbbe rey nit, njaaloo, ay séy yu yoon tere, sàcc, seede yu dëgguwul yi, ak saaga. 20 Loolu mooy andil nit sobe, waaye lekk te raxasoo say loxo, du andil nit sobe.»
Ngëmu jigéen ju nekkul Yawut
21 Yeesu jóge foofu te dem ci diiwaan bi dëkki Tir ak Sidon nekk. 22 Noonu, benn jigéen bu dëkkoon ci diiwaan boobu te cosaanoo Kanaan ñëw di yuuxu naan: «Boroom bi, sëtu Daawuda, yërëm ma. Sama doom bu jigéen, rab moo ko jàpp, sonal ko lool.» 23 Waaye Yeesu tontuwu ko benn baat. Taalibeem yi ñëw te ne ko: «Yewwi ko, ndaxte mu ngi nuy topp di yuuxu sunu kaw.» 24 Mu tontu ne: «Yàlla dafa ma yónni ci askanu Israyil rekk, ñoom ñi mel ni xar yu reer.» 25 Waaye jigéen ji ñëw, sukk ci kanamam te ne: «Boroom bi, wallusi ma.» 26 Yeesu tontu ko: «Baaxul ñuy jël mburu xale yi di ko sànnil xaj yi.» 27 Mu tontu ko ne: «Loolu dëgg la Boroom bi, waaye xaj yi sax dañuy lekk ruusit yiy daanoo ci suufu bérébu lekkukaayu seeni boroom.» 28 Noonu Yeesu ne ko: «Soxna si, sa ngëm réy na. Na ame nag ni nga ko bëgge.» Te ci waxtu boobu sax, doomam bu jigéen bi daldi wér.
Yeesu mu ngi dundal lu ëpp ñeenti junniy nit
29 Yeesu jóge foofu te dem ci tefesu dexu Galile. Mu yéeg ci benn tund te toog. 30 Ay mbooloo yu bari ñëw ci wetam, andi ay lafañ, ay gumba, ay làggi, ay muuma, ak ñeneen ñu bari ñu feebaroon. Ñu teg leen ci tànki Yeesu, te mu wéral leen. 31 Mbooloo mi yéemu, di màggal Yàllay Israyil ci li ñu gis: muuma yi di wax, làggi yi di wér, lafañ yi di dox, ak gumba yi di gis.
32 Yeesu woo taalibeem yi te ne leen: «Damaa yërëm mbooloo mi, ndaxte ñetti fan a ngi ñu nekk ak man te amuñu dara lu ñu lekk. Bëgguma leena yewwi ak xiif ndax ragal seen néew doole daaneel leen ci yoon bi.» 33 Taalibeem yi ne ko: «Fan lañuy gise ci màndiŋ bii mburu yu doy ngir dundal mbooloo mu tollu nii?» 34 Yeesu ne leen: «Ñaata mburu ngeen am?» Ñu ne: «Juróom ñaar ak ay jën yu ndaw yu bariwul.» 35 Noonu, mu jox ndigal mbooloo mi ñu toog ci suuf, 36 te mu jël juróom ñaari mburu yi ak jën yi, sant Yàlla, damm leen, te jox leen taalibe yi, te taalibe yi séddale leen mbooloo mi. 37 Ñépp lekkoon nañu ba regg te ñu for ci juróom ñaari pañe yu fees ci daggit yi desoon. 38 Ñi lekkoon tollu woon nañu ci ñeenti junniy góor, te boolewuñu ci lim bi jigéen ñi ak xale yi. 39 Gannaaw bi mu yewwee mbooloo mi, Yeesu yéeg ci gaal gi te dem ci diiwaanu Magadan.