Deewu Yaxya
14
Ci jamono jooju, Erodd mi yilifoon diiwaanu Galile dégg ñuy wax ci Yeesu. 2 Mu ne ay surgaam: «Kooku Yaxya la, dafa dekki ci ñu dee ñi. Loolu moo tax mu am kàttanu def ay kéemaan.» 3-4 Deewu Yaxya nii la deme woon: Erodd takkoon na Erojàdd, jabaru magam Filib. Yaxya doon na wax Erodd ne: «Yoon bi dafay tere nga takk jigéen boobu.» Noonu Erodd joxe ndigal ñu jàpp Yaxya te yeew ko te tëj ko ci kaso bi. 5 Erodd bëggoon na ko reylu, waaye ragaloon na mbooloo mi ndaxte ñoom jàppoon nañu ne Yaxya yonent la woon. 6 Moona bés bi Erodd di màggal bésu juddoom doom bu jigéen bu Erojàdd doon fecc ci kanamu gan yi. Mu neex Erodd lool. 7 Mu dig ko ak waat ngir jox ko li mu koy ñaan. 8 Gannaaw bi ko yaayam digalee, mu ne: «Jox ma fii boppu Yaxya ci ndab.» 9 Buur bi daldi ànd ak tiis waaye mu santaane ñu jox ko ko ndax waatam bi ak ganam yi. 10 Mu yónnee, ñu dagg boppu Yaxya ca kaso ba. 11 Ñu indi bopp bi ci ndab te ñu jox ko xale bu jigéen bi. Mu yóbbul ko yaayam. 12 Taalibe Yaxya yi ñëw, jël néewam te suul ko. Noonu ñu dem yégal Yeesu li xewoon.Yeesu mu ngi dundal nit ñu bari te dox ci kaw dex gi
13 Bi Yeesu déggee xibaar boobu, mu jóge foofu, yéeg ci gaal, dem ci béréb bu wéet, ngir nekk fa moom kese. Waaye mbooloo mi yég ko. Ñuy génn ci dëkk yi, topp Yeesu ak seeni tànk. 14 Bi Yeesu wàccee ci gaal gi, mu gis mbooloo mu takku, mu yërëm leen, te wéral ñi feebar ci seen biir. 15 Bi jant bi di waaja sow taalibeem yi jegesi ko te ne ko: «Mu ngi waaja guddi te béréb bi nu nekk màndiŋ la. Yewwil mbooloo mi ngir ñu dem ci gox yi, jënd lu ñuy lekk.» 16 Waaye Yeesu tontu leen ne: «Jarul ñuy dem. Yeen ci seen bopp joxleen ñoom lu ñuy lekk.» 17 Ñu tontu ko ne: «Amunu fii lu dul juróomi mburu ak ñaari jën.» 18 Yeesu ne leen: «Andilleen ma ko fii.» 19 Noonu mu jox ndigal mbooloo mi ngir ñu toog ci ñax mi. Mu jël juróomi mburu yi ak ñaari jën yi, yékkëti bëtam yi ci asamaan, barkeel leen, damm mburu mi, jox leen taalibe yi te taalibe yi séddale leen. 20 Ñépp lekkoon nañu ba regg, ba ñu for ci fukki pañe ak ñaar yu fees ci daggit yi desoon. 21 Ñi lekkoon tollu nañu ci juróomi junniy góor te boolewuñu ci lim bi jigéen ñi ak xale yi.
22 Ci saa si Yeesu duggloo taalibeem yi ci gaal gi ngir ñu jiitu ko ci beneen wetu dex bi, te moom mu yewwi mbooloo mi. 23 Gannaaw bi mu leen yewwee, mu yéeg ci tund wi, beru ngir ñaan. Bi guddi jotee, mu nekk fa moom rekk. 24 Ci waxtu boobu, gaal gi sori woon na lool tefes bi, te ndox mi di ko yëngal, ndaxte ngelaw bi da leen doon songe kanam. 25 Bi fajar di waaja jot, Yeesu jëm ci ñoom di dox ci kaw dex gi. 26 Bi ko taalibe yi gisee muy dox ci dex gi, ñu daldi jaxasoo tey naan: «Ab njuuma la!» Ñu daldi tiit bay yuuxu. 27 Ci saa si Yeesu ne leen: «Takkleen seen fit. Man la! Buleen tiit.» 28 Piyeer tontu ko ne: «Boroom bi su fekkee ci dëgg yaw la, digal ma, ma dox ci ndox mi, ñëw ci yaw.» 29 Yeesu ne ko: «Ñëwal.» Piyeer génn ci gaal gi te tàmbale dox ci ndox mi ngir dem ci Yeesu. 30 Waaye bi mu gisee ni ngelaw li ame doole, mu daldi tiit. Mu tàmbale suux ci ndox mi. Mu yuuxu ne: «Boroom bi, musal ma!» 31 Ci saa si Yeesu tàllal loxoom, jàpp ko, te ne ko: «Yaw yaa tuuti ngëm! Lu tax nga am xel ñaar?» 32 Noonu ñu yéeg ñoom ñaar ci gaal gi te ngelaw li dal. 33 Ñi nekkoon ci gaal gi nag daldi sukk ci kanamu Yeesu te ne ko: «Ci dëgg yaw yaay Doomu Yàlla ji.»