Yeesu mu ngi nettali léebu jikat bi
13
Ci bés boobu Yeesu génn ci kër gi te dem toog ci wetu dexu Galile ngir jàngale. 2 Mbooloo mu takku dajaloo, wër ko, ba tax mu yéeg ci benn gaal te toog ci. Mbooloo ma nekk ci tefes bi. 3 Mu wax leen mbir yu bari jaarale ko ci ay léeb. Mu ne leen: «Xoolleen! Dafa amoon benn jikat bu génn ngir ji. 4 Bi muy ji, am pepp yu daanu ci yoon bi. Picc yi ñëw, lekk leen. 5 Yenn pepp yi daanu ci diggante xeer yi fu amul woon suuf su bari. Ñu jóg ci saa si ndaxte suuf si xootul woon, 6 waaye bi jant bi fenkee, ñu lakk te daldi wow, ndaxte amuñu ay reen. 7 Yeneen pepp yi daanu ci diggante ay xaaxaam. Xaaxaam yi daldi jóg te tanc leen. 8 Pepp yi ci des daanu ci suuf su baax si, te yenn yi meññ téeméeri pepp, yeneen yi juróom benn fukk, yi ci des fanweer. 9 Na ki am nopp dégg.»
10 Noonu taalibe yi jegesi ko, laaj ko ne: «Lu tax nga leen di wax ci ay léeb?» 11 Mu tontu leen ne: «Yeen, Yàlla may na leen ngeen xam li nëbbu ci nguuru asamaan si; waaye ñoom, mayuñu leen loolu. 12 Ndaxte ku am, dinañu ko yokkal ba mu am lu ne gàññ. Waaye ku amul, dinañu jël sax li mu am. 13 Loolu moo tax ma leen di wax ci ay léeb, ndaxte dañuy xool te duñu gis; dañuy déglu te duñu dégg walla ñuy ràññee. 14 Ci ñoom la kàddu yonent Yàlla Esayi matee, bi muy wax ne:
"Dingeen déglu ba sonn te dungeen dégg dara.
Dingeen xool bu baax te dungeen gis dara.
15 Ndaxte xolu askan bii daa dëgër.
Fatt nañu seen nopp yi,
tëj nañu seen bët yi,
ngir seen bët yi baña gis
te seen nopp yi baña dégg,
ngir ñu baña xam
te ñu baña woññeeku ci man, Yàlla,
ngir ma wéral leen."
16 «Waaye yeen, barkeel ngeen ndaxte seen bët yi, ñu ngi gis, te seen nopp yi di dégg. 17 Ci dëgg maa ngi leen koy wax: yonent yu bari ak ñu jub ñu bari bëggoon nañu lool gis li ngeen di gis waaye gisuñu ko; te dégg li ngeen di dégg waaye dégguñu ko.
18 «Yeen nag, dégluleen li léebu jikat bi di tekki. 19 Bu nit déggee kàddu gi ci nguuru asamaan si te ràññeewu ko, Seytaane day ñëw, këf kàddu gi ñu ji woon ci xolam. Noonu la mel ci ki jot jiwu bi ci yoon bi. 20 Te ki jot jiwu bi ci béréb yi bari xeer, bu déggee kàddu gi, ci saa si mu nangu ko ak mbégte, 21 waaye kàddu gi saxul ci moom. Da koy jàpp ci diir bu gàtt, waaye bu jafe-jafe àddina si ñëwee walla ñu fitnaal ko ndax kàddu gi, ci saa si mu bàyyi ngëm gi. 22 Ki jot jiwu bi ci xaaxaam yi mooy ki déglu kàddu gi waaye dafay jaaxle ci yëfi àddina sii, dafay wut alal yuy naxaate, te dafay bari bëgg-bëgg. Loolu lépp mooy tanc kàddu gi ba tax du am meññeef. 23 Ki jot jiwu bi ci suuf su baax si mooy kiy déglu kàddu gi te ràññee ko. Dafay am meññeef. Noonu benn bi jur téeméer, beneen bi juróom benn fukk, bi ci des fanweer.»
Yeesu mu ngi nettali yeneen léeb ci lu jëm ci nguuru asamaan si
24 Yeesu nettali leen beneen léeb, ne leen: «Lii la nguuru asamaan si di nirool: benn waay dafa ji woon jiwu bu baax ci toolam. 25 Bi nit ñi di nelaw noonam ñëw, ji ñax bu bon ci biir jiwu bu baax bi, daldi dem. 26 Bi jiwu bi saxee, tóor-tóor bi tàmbali génn, ñax bu bon bi tamit daldi feeñ. 27 Surga yi ñëw, wax boroom tool bi ne: "Njaatige bi, ndax du jiwu bu baax nga ji woon ci sa tool bi? Fan la ñax bu bon bi jóge nag?" 28 Mu tontu leen ne: "Ab noon moo def loolu." Noonu surga yi ne ko: "Ndax danga bëgg nu dem dindi ko?" 29 Waaye mu tontu leen ne: "Déedéet, ndaxte bu ngeen di dindi ñax bu bon bi, mën ngeen dindiwaale tamit jiwu bu baax bi. 30 Bàyyileen ñaar yi ñu jógandoo ba ci ngóob bi. Ci waxtu ngóob bi, dinaa wax góobkat yi ñu jëkka dindi ñax bu bon bi te ñu takk ko ay say ngir lakk ko, te ñu def jiwu bu baax bi ci sama sàq bi."»
31 Yeesu nettaliwaat leen beneen léeb, ne leen: «Nguuru asamaan si dafay mel ni doomu fuddën bu benn waay jël, ji ko ci toolam. 32 Moom mooy pepp bi gëna tuuti ci pepp yi, waaye bu saxee, moom mooy gëna réy ci gàncax yi, ba tax picci asamaan si ñëw, ràbb seen tàgg yi ci bànqaasam yi.»
33 Mu nettaliwaat leen beneen léeb, ne leen: «Nguuru asamaan si dafay mel ni lawiir bu benn jigéen jël, jaxase ko ci ñaar fukki kilo fariñ ak juróom, ba lépp funki.»
34 Loolu lépp Yeesu da ko doon wax mbooloo mi ci léeb te daawul wax ak ñoom bu dul ci léeb, 35 ngir kàddu gii yonent bi waxoon mat:
«Dinaa wax ci ay léeb,
di yégle mbir yi nëbbu
dale ko bi àddina sosoo ba léegi.»
36 Gannaaw loolu, Yeesu bàyyi mbooloo mi te dugg ci kër gi. Taalibeem yi jegesi ko te ne ko: «Wax nu li léebu ñax bu bon bi ci tool bi di tekki.» 37 Mu tontu leen ne: «Nit ki ji jiwu bu baax bi mooy Doomu nit ki. 38-39 Tool bi mooy àddina si. Jiwu bu baax bi mooy ñi bokk ci nguuru asamaan si. Noon bi ji ñax bu bon bi mooy Seytaane. Ñax bu bon bi, mooy ñi bokk ci moom. Ngóob bi mooy njeextelu àddina si te góobkat yi ñooy malaaka yi. 40 Ni ñuy takke ñax bu bon bi ngir sànni ko ci xal bi, noonu lay mel ci njeextelu àddina si. 41 Doomu nit ki dina yónni malaakaam yi, ñu dindi ci nguuram ñépp ñiy xiir ñeneen ñi ci bàkkaar ak ñiy def lu bon, 42 te ñu sànni leen ci safara si, fi am ay jooy ak ay yéy bëñ. 43 Noonu ñu jub ñi dinañu leer ni jant bi ci seen biir nguuru Baay. Na ki am nopp dégg.»
44 Yeesu yokk ca ne: «Nguuru asamaan si dafay mel ni alal bu nëbbu ci tool. Benn waay gis ko, nëbbaat ko, te ci biir mbégteem mu dem jaay lépp li mu am te jënd tool boobu.
45 «Nguuru asamaan si dafay mel ni tamit benn jaaykat buy wut ay per yu rafet. 46 Bi mu gisee per bu njég bi bari, mu dem, jaay lépp li mu am, te jënd per boobu.
47 «Lii la nguuru asamaan si di nirool tamit: benn mbaal bu ñu sànni ci géej bi te mu jàpp xeetu jën bu nekk. 48 Bi mbaal mi feesee, ñu xëcc ko ba ci tefes bi, te ñu toog. Ñu def li baax ci ay pañe te ñu sànni li bon. 49 Noonu lay mel ci njeextelu àddina si: malaaka yi dinañu ñëw, génne ñu bon ñi ci biir ñu jub ñi, 50 te sànni leen ci safara si, fi am ay jooy ak ay yéy bën.»
51 Yeesu laaj leen ne: «Ndax xam ngeen li mbir yii yépp di tekki?» Ñu tontu ko ne: «Waaw.» 52 Mu ne leen: «Loolu moo tax bépp jàngalekatu-yoonu-Musaa bu jàng bu baax ci lu jëm ci nguuru asamaan si dafay mel ni boroom kër buy jële ci alalam ay mbir yu bees ak ay mbir yu yàgg.»
Waa Nasaret nanguwuñu Yeesu
53 Bi Yeesu nettalee léeb yooyu ba noppi, mu jóge fa 54 te dem ci dëkk bi mu yaroo te tàmbalee jàngale ci seen kër-ñaan bi. Nit ñi waaru, di laajante naan: «Fan la jële xel mu rafet mii ak kéemaan yii? 55 Ndax du doomu minise bi, te yaayam tudd Maryaama? Ndax Saak, Yuusufa, Simoŋ ak Yudd, duñu ay rakkam? 56 Rakkam yu jigéen yi, ndax nekkuñu fii ak nun? Fan la jële li lépp nag?» 57 Loolu tax ñu ñàkk ngëm. Noonu Yeesu ne leen: «Ab yonent duñu ko xeeb fu dul ci dëkkam ak ci këram.» 58 Te Yeesu defu fa ay kéemaan yu bari, ndax seen ñàkka gëm.