Yeesu mooy Boroomu bésu noflaay bi
12
Ci jamono jooju, Yeesu di jàll ci tool yi ci benn bésu noflaay. Taalibeem yi xiifoon; ñuy witt ci pepp yi tey lekk. 2 Bi Farisen yi gisee loolu, ñu wax Yeesu ne: «Xoolal! Sa taalibe yi ñu ngi liggéey, te yoonu Musaa dafay tere liggéey ci bésu noflaay bi.» 3 Waaye mu wax leen ne: «Xanaa jànguleen li Daawuda defoon bi mu xiifee moom ak ñi mu àndaloon? 4 Mu dugg ci biir kër-Yàlla gi te lekk mburu yi ñu jébbal Yàlla. Moona yoon bi mayul kenn mu di ci lekk, muy moom walla ñi mu àndaloon, waaye jébbalkatu-sarax yi rekk. 5 Walla jànguleen ci yoonu Musaa ne bésu noflaay bi, jébbalkatu-sarax yiy liggéey ci kër-Yàlla gi, duñu déggal yoon bi ci lu jëm ci bésu noflaay bi moona moyuñu yoon bi? 6 Maa ngi leen koy wax: fii am na ku sut kër-Yàlla gi. 7 Mbind mi nee na: "Ngeen am yërmande ci seen moroom, moo gën ngeen may rendil ay mala ni sarax." Te yeen, su ngeen xamoon li kàddu yooyu di tekki, doonuleen teg daan ñi deful dara. 8 Ndaxte Doomu nit ki mooy boroomu bésu noflaay bi.»
9 Mu jóge foofu te dem ci seen kër-ñaan bi. 10 Foofu amoon na benn waay bu loxoom làggi. Farisen yi bëggoona tuumaal Yeesu, moo tax ñu laaj ko ne: «Ndax sunu yoon bi maye na ñu wéral nit ci bésu noflaay bi?» 11 Yeesu tontu leen ne: «Su fekkee ne am na ci seen biir kenn ku am benn xar rekk, te mu daanu ci kàmb ci bésu noflaay bi, ndax du ko fa génne? 12 Nit moo ëpp solo fuuf xar! Kon nag, sunu yoon bi maye na ñu def lu baax ci bésu noflaay bi.» 13 Noonu Yeesu wax waa ji ne: «Tàllalal sa loxo.» Mu tàllal loxoom, te loxo ba wér mel ni ba ca des. 14 Farisen yi génn ci kër-ñaan bi daldi waxtaan ci ni ñuy fexe reylu Yeesu.
15 Bi Yeesu yégee loolu, mu jóge fa, te mbooloo mu bari topp ko. Mu wéral ñépp ñi feebar, 16 te mu dénk leen ñu bañ ko siiwal. 17 Loolu am na ngir kàddu yii yonent Yàlla Esayi waxoon mat:
18 «Xoolal! Sama surga bi ma tànn,
moom laa sopp te ci moom laa ame bànneex.
Dinaa def sama xel ci moom
te moom dina yégle sama jëfi njubte ci xeet yi.
19 Du xuloo ak kenn te du yuuxu,
te kenn du dégg baatam ci mbedd yi.
20 Du damm bant bu dëng
te du fay taal buy saxar,
ba keroog muy jox njubte ndam,
21 te xeeti àddina si yépp dinañu yaakaar ci turam.»
Yeesu mu ngi jàngale ci lu jëm ci rab yi te ay nit laaj ko benn kéemaan
22 Ñu andil Yeesu benn waay bu rab jàpp ba tax mu gumba te muuma. Yeesu wéral ko, ba tax ku muuma ki di wax tey gis. 23 Noonu, mbooloo mi yépp yéemu, naan: «Kii, mbaa du sëtu Daawuda bi?» 24 Bi Farisen yi déggee loolu nag ñu ne: «Nit kii, ci kàttanu Beelsebul mi di buuru rab yi rekk lay dàqe rab yi.» 25 Waaye Yeesu xam seeni xalaat, ne leen: «Bépp nguur bu xaajaloo ci biiram dina tas, te dëkk walla kër bu xaajaloo ci biiram du mëna yàgg. 26 Bu Seytaane di dàq Seytaane, mu ngi xeex boppam. Kon nag, naka la nguuram mëna yàgge? 27 Te man, su fekkee ci kàttanu Beelsebul laay dàqe rab yi, kon seeni taalibe ci ban kàttan lañuy dàqe rab yi? Moo tax ñoom ci seen bopp ñoo leen di àtte. 28 Waaye su fekkee ci Xelum Yàlla laay dàqe rab yi, kon nguuru Yàlla gi yegsi na ci yeen.
29 «Naka la kenn mëne dugg ci kër nit bu am doole di jël alalam? Du ko mëna def feek takkul nit kooku ba noppi. Noonu dina jël li mu dencoon ci këram. 30 Ku farul ci man, yaa ngi may xeex. Ku dajalewul ak man, yaa ngi tasaare.
31 «Loolu moo tax maa ngi leen koy wax: dinañu baal nit ñi bépp bàkkaar ak bépp wax bu ñaaw bu ñu wax. Waaye ku wax lu ñaaw ci Xel mu Sell mi duñu ko baal. 32 Ku waxal Doomu nit ki lu bon, dinañu ko baal. Waaye ku waxal Xel mu Sell mi lu bon duñu ko baal ci àddina si ak ci àllaaxira.
33 «Bu garab gi baaxee, meññeefam dañuy baax. Bu garab gi bonee, meññeefam dañuy bon. Ndaxte garab bu nekk ñu ngi koy xàmme ci meññeefam. 34 Yeen ñi fees ak daŋar mel ni jaan! Naka ngeen mëna waxe ay mbir yu baax ak ni ngeen bone? Ndaxte lu fees ci xol, gémmiñ wax ko. 35 Nit bu baax mu ngi jële ay mbir yu baax ci lu baax li mu denc ci xolam. Nit bu bon mu ngi jële ay mbir yu bon ci lu bon li mu denc ci xolam. 36 Maa ngi leen koy wax, ci bésu àtte ba, nit ñi dinañu layoo bépp kàddu bu amul solo bu ñu waxoon. 37 Ndaxte ci say kàddu la la Yàlla di àtte ni ku jub te ci say kàddu la la Yàlla di tege daan.»
38 Noonu ay jàngalekatu yoonu Musaa ak ay Farisen wax Yeesu ne: «Jàngalekat bi, danoo bëggoon nga won nu benn kéemaan buy firndeel sa sañ-sañ.» 39 Yeesu tontu leen ne: «Niti jamono jii dañoo bon tey moy Yàlla. Ñu ngi laaj benn kéemaan waaye duñu leen jox benn bu dul màndarga Yunus bi. 40 Ndaxte ni Yunus defe woon ñetti bëccëg ak ñetti guddi ci biiru jën bu mag bi, noonu tamit Doomu nit ki dina nekk ñetti bëccëg ak ñetti guddi ci biir suuf si. 41 Ci bésu àtte ba, waa Niniw dinañu jóg ngir tuumaal niti jamono jii, ndaxte bi ñu déggee waare Yunus ba, tuub nañu seeni bàkkaar. Te xoolleen! Ku sut Yunus mu ngi fii. 42 Ci bésu àtte ba, buur bu jigéen ba dëkkoon ca sudd dina jóg ngir tuumaal niti jamono jii, ndaxte jóge woon na fu sori ngir déglu waxu Suleymaan yu rafet yi. Te xoolleen! Ku sut Suleymaan mu ngi fii.
43 «Bu rab génnee ci nit day wër ci màndiŋ bi ngir wut fu muy noppaloo. Bu ko amul, 44 dina wax ne: "Xaaral, ma dellu ci sama kër bi ma jóge woon." Bu yegsee, fekku fa kenn, te mu gis ne bale nañu kër gi te defar ko ba mu jekk. 45 Mu daldi dem woowi juróom ñaari rab yu ko gëna soxor, ñu dugg ci kër ga te dëkk fa. Noonu melokaanu nit kooku mooy gëna yées na mu meloon bu jëkk. Lu mel noonu mooy dal nit ñu bon ñi ci jamono jii.»
Yeesu mu ngi wax ci nit ñi bokk ci njabootam
46 Bi Yeesu nekkee di wax ak mbooloo ma, yaayam ak rakkam yi ñëwoon nañu, taxaw ci biti, tey wut nu ñu waxe ak moom. 47 Kenn ne ko: «Xoolal! Sa yaay ak say rakk ñu ngi ci biti tey wut nu ñu waxe ak yaw.» 48 Waaye mu tontu ki doon wax ak moom, ne ko: «Kan mooy sama yaay ak ñan ñooy samay rakk?» 49 Noonu mu tàllal loxoom ci taalibeem yi te ne: «Xoolleen! Ñii ñooy sama yaay ak samay rakk, 50 ndaxte kiy def sama coobare Baay bi ci asamaan, kooku mooy sama rakk bu góor, sama rakk bu jigéen, walla sama yaay.»