Yeesu mu ngi wax ci lu jëm ci Yaxya
11
Bi Yeesu noppee di jox ndigal yooyu fukki taalibeem yi ak ñaar, mu jóge foofu ngir dem jàngale ak waare ci dëkk yi nekk ci diiwaan bi. 2 Bi Yaxya nekkee ci kaso bi, mu déggoon ñuy wax ci jëf yi Almasi bi def. Noonu mu yónnee ko ñenn ci taalibeem yi ngir ñu laaj ko: 3 «Ndax yaw yaay Almasi bi waroona ñëw walla danoo wara xaar keneen?» 4 Yeesu tontu leen ne: «Demleen nettali Yaxya li ngeen dégg ak li ngeen gis: 5 gumba yi ñu ngi gis, lafañ yi ñu ngi dox, gaana yi wér nañu, tëx yi ñu ngi dégg, ñi dee woon ñu ngi dekki, te ñu ngi yégal xibaar bu baax bi néew-di-doole yi. 6 Barkeel na ki dul ñàkk ngëm ndax man.»
7 Bi taalibe Yaxya yi di dem, Yeesu di wax ak mbooloo mi ne: «Bi ngeen demee ci Yaxya ci màndiŋ bi, lan ngeen bëggoona gis? Benn xeetu ñax bu ngelaw li di yëngal ci wet bu nekk? 8 Waaye lan ngeen demoon gis: benn nit bu sol ay yére yu rafet? Xoolleen! Ñiy sol yére yu rafet dañuy dëkk ci biir kër buur yi. 9 Waaye lan ngeen demoon gis: ab yonent? Waaw, maa ngi leen koy wax, ku ëpp yonent sax! 10 Ndaxte ci Yaxya la Mbind mi wax ne:
"Xoolal! Maa ngi yónni sama yonent ci sa kanam
ngir mu waajal sa yoon ci sa kanam."
11 Ci dëgg maa ngi leen koy wax, ci ñi juddoo ci jigéen ku gëna màgg Yaxya mësula am. Waaye ki gëna ndaw ci nguuru asamaan si moo ko gëna màgg. 12 Dale ko ci jamono ji Yaxya doon waare ba léegi, nguuru asamaan si day daj coono, te ñiy jëfe ak doole di wut nu ñu ko aakimoo. 13 Ndaxte yonent yépp ak yoonu Musaa wax nañu ci turu Yàlla ba ci jamono Yaxya. 14 Te su ngeen ko bëggee nangu, moom mooy yonent Yàlla Ilyaas mi waroona ñëw. 15 Na ki am nopp, dégg!
16 «Kan laa wara méngalee niti jamono jii? Ñu ngi nirook ay xale yu toog ci péncu dëkk bi te ñenn ñi di yuuxu ñeneen ñi, di ne:
17 "Woyal nanu leen woyi bànneex te fecculeen;
woyal nanu leen woyi dëj te naqarluwuleen."
18 Ndaxte Yaxya ñëw na, lekkul, naanul te ñuy wax ne: "Kii dafa am rab." 19 Doomu nit ki ñëw na, di lekk te di naan te ñu ne: "Xoolleen, waa ji xalaatul lu dul lekk ak naan, di xaritu juutikat yi ak bàkkaarkat yi." Waaye ki am xel mu rafet, ay jëfam ñoo koy dëggal.»
Yeesu mu ngi gëdd ay dëkk yu tuubul seeni bàkkaar
20 Noonu Yeesu tàmbale gëdd ak doole dëkk yi mu defoon li ëpp ci ay kéemaanam, ndaxte waa dëkk yooyu tuubuñu woon seeni bàkkaar. 21 Mu ne: «Musiba dina leen dal, yeen waa Korasin! Musiba dina leen dal, yeen waa Betsayda, ndax kéemaan yi ma def ci yeen. Su ma ko defoon ci dëkku Tir walla ci dëkku Sidon, kon bu yàgg doon nañu sol ay saaku di xëpp seen bopp dóomu taal ngir wone ne dañoo tuub seeni bàkkaar. 22 Looloo tax maa ngi leen koy wax: ci bésu àtte ba, Tir ak Sidon dinañu leen tane. 23 Te yeen waa Kapernawum, ndax xalaat ngeen ne dinañu leen yékkëti ba ci kaw asamaan? Déedéet, dinañu leen wàcce ba fi ñu dee ñi nekk, ndax kéemaan yi ma def ci yeen. Su ma ko defoon ci dëkku Sodom, doon na fi nekk ba tey. 24 Waaye maa ngi leen koy wax: ci bésu àtte ba, réewu Sodom dina leen tane.»
Yeesu mu ngi dig noflaay nit ñi sonn
25 Ci jamono jooju, Yeesu jël kàddu gi te ne: «Baay, yaw miy Boroomu asamaan ak suuf, sant naa la, ndaxte yaw yaa nëbb yëf yii boroom xam-xam yi ak boroom xel yi te xamal leen gone yi. 26 Waaw, Baay, def nga loolu ndaxte loolu moo la neex. 27 Sama Baay jox na ma lépp, te kenn xamul doom bi ku dul Baay bi, te kenn xamul Baay bi ku dul Doom bi ak ki ko doom bi bëgga xamal. 28 Ñëwleen ci man, yeen ñépp ñi sonn te seen yen diis, te dinaa leen may noflaay. 29 Nanguleen sama kilifteef te jàng ci man, ndaxte sama xol dafa lewet te woyof, te dingeen am noflaay ci seen ruu. 30 Ndaxte sama kilifteef yomb na, te sama yen diisul.»