Yeesu mu ngi yónni fukki ndaw yi ak ñaar
10
Yeesu woo fukki taalibeem yi ak ñaar, jox leen sañ-sañ ngir ñu dàq rab yi te wéral bépp feebar ak bépp jàngoro. 2 Lii mooy turi fukki ndaw yi ak ñaar: Simoŋ mi Yeesu doon woowe Piyeer, Andare mi bokk ak Piyeer ndey ak baay, Saak doomu Sebede, ak Yowaana mi mu bokkal ndey ak baay, 3 Filib, Bartelemi, Tomaa, Macë di juutikat bi, Saak di doomu Alfe, ak Tade. 4 Simoŋ mi ñuy woowe ku takku ci réewam, ak Yudaa Iskariyot, di ki mujjoona wor Yeesu.5 Noonu Yeesu yónni leen; mu jox leen ndigal ne: «Buleen dem ci ñi nekkul Yawut te buleen dugg ci benn dëkk bu waa Samari, 6 waaye demleen ci askanu Israyil, ñoom ñi mel ni ay xar yu reer. 7 Fépp fu ngeen jaar, na ngeen yégle ne nguuru asamaan si jegesi na. 8 Na ngeen wéral ñi feebar, dekkil ñi dee, setal ngaana yi, tey dàq rab yi. Jot ngeen te feyuleen dara, kon nag joxeleen te buleen laaj dara. 9 Buleen dajale wurus walla xaalis mbaa xànjar, bu ngeen di def seen kalpe. 10 Buleen yóbbaale saaku tukki, ñaari yére, ay dal, walla yet, ndaxte liggéeykat bi yelloo na li muy dunde. 11 Bu ngeen duggee ci dëkk walla ci gox, na ngeen seet ku leen yelloo dalal. Noonu ngeen des ci këram ba bi ngeen di dem. 12 Bu ngeen duggee ci kër gi, nuyuleen waa kër ga, 13 te su fekkee ne yelloo nañu seen jàmm, na wàcc ci ñoom. Waaye buñu ko yelloowul, na seen jàmm dellusi ci yeen. 14 Su ñu leen bañee dalal walla nu baña déglu seeni wax, génnleen ci kër googu walla ci dëkk boobu te faxas pënd bi nekk ci seeni tànk. 15 Ci dëgg maa ngi leen koy wax, ci bésu àtte ba, waa réewu Sodom ak Gomor dinañu tane waa dëkk boobu.
16 «Xoolleen! Maa ngi leen di yónni ni ay xar ci biir ay bukki. Na ngeen muus ni jaan te lewet ni pitax. 17 Waaye moytuleen nit ñi ndaxte dinañu leen jébbal ci bérébu àttekaay yi te dinañu leen dóor ay yar ci seen kër-ñaan yi. 18 Dinañu leen yóbbu ci kanamu njiiti réew yi ak ci kanamu buur yi ndax man, ngir ngeen nekk samay seede ci seen kanam ak ci kanamu ñi dul Yawut. 19 Waaye su ñu leen jébbalee, buleen jaaxle ci anam bi ngeen wara waxe walla ci li ngeen wara wax, ndaxte ci waxtu boobu sax dinañu leen jox li ngeen wara wax. 20 Ndaxte du yeen yeenay wax waaye seen Xelu Baay mooy wax jaarale ko ci seen gémmiñ. 21 Mag dina jébbale rakkam ci dee, te Baay jébbale doomam. Ay doom tamit dinañu fippu ci seeni waajur te reylu leen. 22 Ñépp dinañu leen bañ ndax man waaye ku dëgër-dëgërlu ba ci njeextel ga dinga mucc. 23 Buñu leen fitnaale ci benn dëkk, dawleen dem ci beneen bi. Ci dëgg maa ngi leen koy wax, dungeen wër dekki Israyil yépp te Doomu nit ki ñëwul.
24 «Taalibe bi gënul màgg jàngalekatam te jaam bi gënul màgg njaatigeem. 25 Taalibe bu demee ba mel ni jàngalekatam, na ci doylu; te jaam bu demee ba mel ni njaatigeem, na ci doylu. Su ñu woowee boroom kër gi Beelsebul, waxatuma laak waa kër gi! 26 Kon nag buleen ragal nit ñooñu, ndaxte lépp lu nëbbu dina feeñ te lépp lu umpe dinañu ko xamle. 27 Lu ma leen wax ci kumpa, waxleen ko ci bëccëg ndarakàmm. Lu ñu leen déey, yuuxuleen ko ci kaw kër yi. 28 Buleen ragal ñi mëna rey yaram te mënuñoo rey ruu, waaye ragalleen ki nga xam ne mën na sànk yaram ak ruu ci safara. 29 Ndax ñaari picci ramatu duñu ko jaaye benn dërëm? Moona benn ci ñoom du daanu ci suuf bu soobul Yàlla seen Baay. 30 Te yeen, seeni kawaru bopp yépp sax, waññ nañu leen. 31 Kon nag buleen ragal dara ndaxte yeena ëpp solo mbooloo picci ramatu.
32 «Kon nag ku ma nangu ci kanamu nit ñi, man itam dinaa ko nangu ci kanamu sama Baay bi ci asamaan, 33 waaye ku ma weddi ci kanamu nit ñi, man itam dinaa ko weddi ci kanamu sama Baay bi ci asamaan. 34 Buleen foog ne damaa ñëw ngir andi jàmm ci àddina si. Ñëwuma ngir andi jàmm waaye jaasi, 35 ndaxte damaa ñëw ngir indi xaajaloo diggante doom bu góor ak baayam, doom bu jigéen ak yaayam, jabaru doom ak goroom, 36 te nit, waa këram ñooy doon ay noonam.
37 «Ku bëgg pàppaam walla yaayam lu ëpp li mu ma bëgg, yelloowoo ma. Ku bëgg doomam bu góor walla doomam bu jigéen lu ëpp li mu ma bëgg, yelloowoo ma. 38 Te ku jëlul sa bant bi ñu la wara daaje te toppu ma yelloowoo ma. 39 Ku bëgga musal sa bakkan dinga ko ñàkk, te ku ñàkk sa bakkan ndax man dinga ko jotaat.
40 «Ku leen dalal man la dalal, te ku ma dalal, dalal na ki ma yónni. 41 Ku dalal ab yonent ndax ni mu nekke yonent dina jot neexalu yonent. Ku dalal ab nit bu jub ndax njubteem dina jot neexalu ku jub. 42 Te ku jox ab kaasu ndox mu sedd rekk kenn ci ñi gëna ndaw ci samay taalibe ndax li mu doon sama taalibe, ci dëgg maa ngi leen koy wax, du ñàkk neexalam mukk.»