Yeesu mu ngi wéral benn waay ju làggi te baal ko ay bàkkaaram
9
Gannaaw loolu Yeesu yéeg ci gaal, jàll dex bi, dem ci dëkkam. 2 Noonu, ñu andil ko benn waay bu làggi, tëddoon ci benn basaŋ. Bi Yeesu gisee seen ngëm, mu wax nit ku làggi ki ne: «Sama doom, na sa xel dal. Baal nañu la say bàkkaar.» 3 Amoon na fa ay jàngalekati-yoonu-Musaa. Ñuy wax ci seen xel, naan: «Kii mu ngi méngale boppam ak Yàlla!» 4 Yeesu xam seeni xalaat te ne leen: «Lu tax ngeen am xalaat yu bon yii ci seen biir xol? 5 Lan moo gëna yomb wax nit ki "baal nañu la say bàkkaar" walla "jógal te nga dox"? 6 Li ma bëgga def mooy ngir ngeen xam ne Doomu nit ki am na sañ-sañ ci àddina si baale bàkkaar yi.» Noonu mu wax ku làggi ki ne: «Jógal, jël sa basaŋ te nga ñibbi.» 7 Nit ki daldi jóg te ñibbi këram. 8 Bi mbooloo mi gisee loolu, ñu daldi ànd ak tiitange di màggal Yàlla, moom mi jox nit ñi sañ-sañ bu tollu noonu.Yeesu tànn na Macë juutikat bi
9 Bi Yeesu jóge foofu di dem, mu gis benn juutikat bu tudd Macë te mu toog ci bérébu liggéeyukaay bi. Yeesu ne ko: «Topp ma.» Macë jóg te topp ko. 10 Gannaaw loolu Yeesu doon lekk ci këru Macë; ay juutikat yu bari ak ay bàkkaarkat ñëw nañu di lekkandoo ak moom ak taalibeem yi. 11 Bi Farisen yi gisee loolu, ñu wax taalibe Yeesu yi ne: «Lu tax seen jàngalekat bi di lekkandoo ak ay juutikat ak ay bàkkaarkat?» 12 Bi Yeesu déggee loolu mu wax ne: «Du ñi wér ñoo soxla fajkat waaye ñi wéradi. 13 Man damaa ñëw ngir woo bàkkaarkat yi ñu tuub seeni bàkkaar, waaye du ñu jub ñi. Kon nag demleen jàng li kàddu yii ci Mbind mi di tekki: "Ngeen am yërmande ci seen moroom, moo gën ngeen may rendil ay mala ni sarax." »
Yeesu mu ngi wax ci lu jëm ci woor
14 Noonu taalibe Yaxya yi ñëw wax Yeesu ne: «Nun ak Farisen yi danuy faral di woor. Lu tax sa taalibe yi duñu woor?» 15 Yeesu tontu leen ne: «Ndax xariti boroom séet bi mën nañu nekk ci naqar, feek boroom séet bi mu ngi ak ñoom? Ay bés a ngi ñëw, ñu jële boroom séet bi ci seen biir, te noonu dinañu woor.
16 «Kenn du takkale daggitu piis bu bees ak benn yére bu màggat bu xotteeku. Ndaxte daggit bi dina ñoddi yére bi te xotteeku bi gëna yaatu. 17 Kenn du jël biiñ bu bees tamit di ko def ci ay mbuusu der yu màggat. Lu ko moy mbuus ya dinañu xotteeku, biiñ bi tuuru te mbuus ya yàqu. Waaye dañuy jël biiñ bu bees def ko ci ay mbuusu der yu bees, te noonu ñoom ñaar duñu yàqu.»
Yeesu mu ngi wéral ay nit yu bari
18 Bi leen Yeesu di wax loolu, benn njiitu Yawut yegsi, sukk ci kanamam, te ne ko: «Sama doom bu jigéen dafa dee léegi, waaye ñëwal, nga teg ko ay loxo te dina dundaat.» 19 Yeesu daldi jóg te topp ko, moom ak taalibeem yi. 20-21 Benn jigéen buy xëpp deret lu tollu ci fukki at ak ñaar mu ngi fa woon. Mu wax ci xelam: «Su ma fexee ba laal yéreem rekk, dinaa wér.» Mu jaare Yeesu gannaaw te laal catu yéreem. 22 Yeesu walbatiku, gis ko, te ne ko: «Dalalal sa xel sama doom bu jigéen. Sa ngëm wéral na la.» Ci saa si, jigéen ji wér.
23 Bi Yeesu yegsee ci këru njiitu Yawut bi mu gis ay nit yuy mbiib ndax dëj bi ak mbooloo muy def coow lu réy. 24 Noonu mu wax leen ne: «Génnleen. Xale bu jigéen bi deewul, day nelaw rekk.» Waaye ñu koy ñaawal. 25 Bi ñu génnee mbooloo mi ci biti, Yeesu dugg ci biir néeg bi, téye loxo xale bu jigéen bi, te mu jóg. 26 Noonu xibaaru li xewoon daldi siiw ci diiwaan ba yépp.
27 Bi Yeesu jóge foofu ñaari gumba topp ko di yuuxu naan: «Sëtu Daawuda, yërëm nu.» 28 Bi mu duggee ci kër gi, gumba yi jegesi ko te mu laaj leen: «Ndax gëm ngeen ne mën naa def loolu?» Ñu tontu ko ne: «Waaw, Boroom bi.» 29 Noonu mu laal seen bët yi ne: «Na ame ni ngeen ko gëme,» 30 te seen bët yi ubbeeku. Yeesu artu leen ak doole ne: «Fexeleen ba kenn bu mu yég li leen dal.» 31 Waaye ñoom bi ñu génnee ñu tàmbalee siiwal xibaaru Yeesu ci diiwaan bi yépp.
32 Ci waxtu bi ñuy dem ñu andil Yeesu benn waay bu rab jàppoon ba muumaloo ko. 33 Yeesu dàq rab bi, te muuma bi tàmbalee wax. Mbooloo ma daldi yéemu tey wax ne: «Mësunu gis lu mel nii ci Israyil.» 34 Waaye Farisen yi ne: «Ci kàttanu buuru rab yi lay dàqe rab yi.»
35 Yeesu doon na wër dëkk yépp ak gox yépp di jàngale ci kër-ñaan yi, di yégle xibaar bu baax bi ci nguuru Yàlla gi, te wéral nit ñi ci seen feebar yépp ak ci seen jàngoro yépp. 36 Bi mu gisee mbooloo yi mu yërëm leen ndaxte nit ñi dañoo sonn te ñàkk yaakaar, mel ni ay xar yu amul sàmmkat. 37 Noonu Yeesu ne taalibeem yi: «Ngóob bi yaatu na waaye liggéeykat yi bariwuñu. 38 Ñaanleen boroom ngóob bi ngir mu yónni ay liggéeykat ci ngóobam.»