Yeesu mu ngi wéral nit ñu bari ci ay feebar yu wuute
8
Yeesu wàcc ci tund bi te mbooloo mu bari topp ko. 2 Noonu benn waay bu amoon feebaru ngaana ñëw ci moom te sukk ci kanamam ne ko: «Boroom bi soo ko bëggee, mën nga ma setal.» 3 Yeesu tàllal loxoom, laal ko, te nee ko: «Bëgg naa ko. Setal.» Ci saa si ki amoon feebaru ngaana bi daldi set. 4 Noonu Yeesu ne ko: «Déglul bu baax! Bul ko wax kenn. Waaye demal nga won sa bopp jébbalkatu-sarax si, te nga joxe sarax si, ni ko yoonu Musaa diglee, te loolu dina nekk seede ngir ñoom.»
5 Gannaaw loolu Yeesu dugg na Kapernawum. Benn njiitu soldaaru Room jegesi ko te ñaan ko, 6 ne ko: «Boroom bi, sama surgaa nga ci kër ga, dafa feebar ba làggi te sonn lool.» 7 Yeesu ne ko: «Dinaa ñëw wéral ko.» 8 Waaye njiitu soldaar bi tontu ko ne: «Boroom bi, yelloowuma nga dugg sama kër, waaye waxal benn kàddu rekk te sama surga bi dina wér. 9 Ndaxte man tamit am naa ay kilifa yu may jiite, te jiite naa ay soldaar yu may jox ndigal. Su ma nee kii "Demal," mu dem! Su ma nee kee "ñëwal," mu ñëw! Su ma nee kenn ci samay surga: "Defal lii," mu def ko.» 10 Bi Yeesu déggee loolu, mu daldi yéemu, wax ñi koy topp ne: «Ci dëgg maa ngi leen koy wax, mësuma gis ci Israyil ku ngëmam réye nii. 11 Maa ngi leen koy wax, ñu bari dinañu jóge penku ak sowu, dinañu lekkandoo ak Ibraayma, Isaaxa ak Yanqóoba ci nguuru asamaan si. 12 Waaye ñi waroona donn nguur gi, dinañu leen sànni ci biti, ci lëndëm gi, fi am ay jooy ak ay yéy bëñ.» 13 Noonu Yeesu wax njiitu soldaar bi ne: «Demal, dina am ni nga ko gëme,» te ci saa si surga bi daldi wér.
14 Yeesu dem ci kër Piyeer, fekk na yaayu jabaru Piyeer tëdd. Dafa amoon yaram bu tàng. 15 Yeesu laal loxoom te tàngooru yaram bi bàyyi ko; mu jóg te di ko toppatoo. 16 Ci ngoon si ñu andil Yeesu ñu bari ñu rab jàpp, mu dàq rab yi ci ay kàddoom te wéral ñépp ñi feebaroon. 17 Noonu mu matal kàddu yonent Yàlla Esayi bii:
«Jël na sunuy laago
te gàddu sunuy jàngoro.»
Ñaari nit yu bëggoona topp Yeesu
18 Bi Yeesu gisee mbooloo mu bari wër ko, mu jox ndigal ay taalibeem ñu jàll ci beneen wetu dexu Galile. 19 Benn jàngalekatu yoonu Musaa jegesi ko te ne ko: «Jàngalekat bi, dinaa la topp foo mëna dem.» 20 Yeesu tontu ko ne: «Xaju àll yi am nañu ay pax yu ñu dëkk; picc yi am nañu ay tàgg; waaye Doomu nit ki amul fu mu teg boppam ngir noppalu.» 21 Kenn ci taalibeem yi ne ko: «Boroom bi, may ma, ma dem suul sama pàppa ba noppi.» 22 Waaye Yeesu tontu ko ne: «Topp ma, te bàyyil ñi dee suul seeni néew.»
Yeesu mu ngi dalal ngelaw bu réy bi
23 Yeesu yéeg ci gaal gi, taalibeem yi topp ko. 24 Jekki-jekki, ngelaw lu réy daldi jóg ci dex gi, ba tax gaal gi fees ak ndox. Boobu, Yeesu mu ngi doon nelaw. 25 Taalibe yi jegesi ko, yee ko, ne ko: «Boroom bi, musal nu! Nu ngi suux!» 26 Mu ne leen: «Lu tax ngeen ragal, yeena tuuti ngëm?» Noonu Yeesu jóg, gëdd ngelaw li ak dex bi, lépp daldi dal. 27 Nit ñi daldi waaru te ne: «Kii mooy kan, ba ngelaw li ak dex bi sax di ko déggal?»
Yeesu mu ngi wéral ñaari nit yu rab jàppoon
28 Bi Yeesu yegsee ci beneen wetu dex gi ci diiwaanu Gadara, ñaari nit yu rab jàpp daldi génn ci armeel bi, ñëw dajesi ak moom. Dañoo soxoroon ba kenn ñemeetul woon jaar ci yoon boobu. 29 Noonu ñu yuuxu naan: «Loo nu bëggal, Doomu Yàlla ji? Ndax danga ñëw fii ngir metital nu laata waxtu bi?» 30 Fekk na ci waxtu boobu amoon na géttu mbaam xuux yu bari bu doon wut lu ñuy lekk. 31 Rab yi ñaan Yeesu ne: «Boo nu naree dàq, sànni nu ci géttu mbaam xuux bii.» 32 Mu ne leen: «Demleen.» Ñu génn ci ñaari nit ñi te dugg ci mbaam xuux yi. Ci saa si gétt boobu nekkoon ci kaw tund bi daldi gaawantu, tarxiis, daanu ci dex gi, te lab ci ndox mi. 33 Sàmmkati mbaam xuux yi daldi daw, te dem ci dëkk bi, te nettali li daloon ñaari nit yi rab jàppoon ak lépp li xewoon. 34 Noonu waa dëkk ba yépp génn, dajesi ak Yeesu. Bi ñu ko gisee, ñu ñaan ko mu génn seen diiwaan.