Yeesu mu ngi jàngale nu jàppe ñeneen ñi ni sunu bopp
7
«Buleen àtte ngir ñu bañ leena àtte, 2 ndaxte Yàlla dina leen àtte ni ngeen di àtte ñeneen ñi. Te ni ngeen di nattale ñeneen ñi, noonu lañu leen di nattale. 3 Lu tax ngay xool ñax bi nekk ci sa bëtu moroom te gisoo bant bi nekk ci sa bët? 4 Walla naka ngay waxe sa moroom ne: "Bàyyil ma dindil la ñax bi ci sa bët," fekk ne yaw, am na bant bu nekk ci sa bët? 5 Naaféq bi! Génneel bant bi nekk ci sa bët ba noppi. Bu booba dinga gis bu baax te mëna génne ñax bi nekk ci sa bëtu moroom. 6 Buleen jox xaj yi lu sell, ngir bañ ñu walbatiku, xotti leen. Buleen sànni seeni per ci kanamu mbaam-xuux yi, ngir bañ ñu dëggaate per yi.
7 «Ñaanleen, ñu may leen. Seetleen te dingeen gis. Fëggleen, ñu ubbil leen. 8 Ndaxte ku ñaan ñu may la, te ku seet dinga gis, te ku fëgg ñu ubbil la. 9 Kan ci yeen mooy jox xeer doomam, fekk mu ñaan ko mburu, 10 walla mu ñaan ko jën, mu jox ko jaan? 11 Yeen ñu bon ñi, segem yeena mëna jox seen doom lu baax, rawatina seen Baay bi ci asamaan, moom dina jox lu baax ñi ko koy ñaan. 12 Kon nag ci lépp, li ngeen bëgg nit ñi defal leen ko, yeen tamit, na ngeen leen ko defal. Loolu mooy li yoonu Musaa ak téere yonent yi di jàngale.
13 «Jaarleen ci bunt bu xat bi, ndaxte yoon biy jëm ci sànku dafa yomb, te bunt bi yaatu. Ñi ciy jaar bari nañu. 14 Waaye yoon bi jëm ci dund gi dafa sew, te bunt bi xat, te ñi ko gis bariwuñu.
15 «Moytuleen yonent yu dëgguwul yi. Dañuy ñëw ci yeen yor jëmmu xar, waaye ci biir ay bukki yu soxor lañu. 16 Dingeen leen xàmme ci seeni jëf. Kenn du witt reseñ ci garabu kàdd te kenn du witt gaŋ ci xaaxaam. 17 Noonu tamit bépp garab bu baax ay meññeef yu baax lay meññ waaye garab bu bon ay meññeef yu bon lay meññ. 18 Garab bu baax mënula am meññeef yu bon walla garab bu bon di am meññeef yu baax. 19 Bépp garab bu dul meññ meññeef bu baax, dinañu ko dagg te sànni ko ci safara si. 20 Noonu nag, yonent yu dëgguwul yi, ci seeni jëf ngeen leen di xàmmee.
21 «Du ñépp ñi may woowe "Boroom bi, Boroom bi" ñooy dugg ci nguuru asamaan si, waaye ñiy def sama coobare Baay bi ci asamaan. 22 Ci bésu àtte bi, ñu bari dinañu ma wax ne: "Boroom bi, Boroom bi, ndax du ci sa tur lanu daan waare di wax ci turu Yàlla? Ndax du ci sa tur lanu daan dàqe rab yi? Ndax du ci sa tur lanu daan defe ay kéemaan yu bari?" 23 Noonu dinaa leen wax ne: "Mësuma leena xam. Sorileen ma, yeen ñiy def lu bon."
24 «Kon nag, képp kuy déglu samay kàddu te di leen jëfe day mel ni nit ku am xel ku tabax këram ci kaw doj bi. 25 Taw bi wàcc te dex bi wal. Ngelaw li jóg ak doole, dal ci kër ga, waaye daanuwul ndaxte dañu ko tabax ci kaw doj bi. 26 Waaye képp kuy déglu samay kàddu te du leen jëfe day mel ni nit ku ñàkk xel ku tabax këram ci kaw suuf si. 27 Taw bi wàcc te dex bi wal. Ngelaw li jóg ak doole ci kaw kër gi, mu daldi màbb ba tasaaroo.»
28 Bi Yeesu waxee kàddu yooyu ba noppi, mbooloo mi daldi yéemu ci njàngaleem 29 ndaxte da doon jàngale ak sañ-sañ bu jàngalekati-Yoonu-Musaa amul.