Yeesu mu ngi wéyal njàngaleem ci barke bu wóor bi ci kaw tund bi
6
«Moytuleen di matal seeni jëfu njubte ci kanamu nit ñi, ngir wonewu ci seen kanam. Lu ko moy, dungeen jot neexal ci seen Baay bi ci asamaan. 2 Booy may néew-di-doole yi dara, bu ko siiwal ni ko naaféq yi di defe ci kër-ñaan yi ak ci mbedd yi ngir nit ñi di leen màggal. Ci dëgg maa ngi leen koy wax, jot nañu ba noppi seen neexal bépp. 3 Waaye yaw booy may néew-di-doole yi dara, bu sa loxo càmmoñ xam li sa loxo ndeyjoor di def, 4 ngir sa may nekk kumpa te sa Baay biy gis li ngay def ci kumpa dina la neexal.
5 «Bu ngeen di ñaan Yàlla, buleen mel ni naaféq yi, ndaxte ñoom ci kër-ñaan yi ak ci catu mbedd yu mag yi lañuy bëgga taxaw di ñaan ngir ñépp gis leen. Ci dëgg maa ngi leen koy wax, jot nañu ba noppi seen neexal bépp. 6 Waaye yaw booy ñaan duggal ci sa néeg bi gëna ruqe, tëj bunt bi te nga ñaan sa Baay bi fa nekk ci béréb bi umpe, te sa Baay biy gis li ngay def ci kumpa dina la neexal. 7 Ci seen ñaan buleen di bambtu rekk ay wax yu amul njériñ, mel ni ñiy jaamu yàlla yu dëgguwul yi, ndaxte dañuy xalaat ne seeni yàlla dinañu leen déglu ndax seen wax yu bari. 8 Buleen mel ni ñoom, ndaxte yeen, seen Baay xam na li ngeen soxla laata ngeen koy ñaan.
9 «Yeen nag, nii ngeen wara ñaane:
Sunu Baay bi ci asamaan
na ñépp yékkëti sa tur,
10 na sa nguur ñëw,
na sa coobare am
ci suuf si ni mu ame ci asamaan.
11 May nu tey li nuy dunde
12 te nga baal nu sunuy bàkkaar,
ni nuy baale, nun tamit, ñi nu tooñ.
13 Bu nu yóbbu ci fiir, waaye musal nu ci ku bon ki,
ndaxte yaw, yaa yelloo nguur, kàttan ak màggaay ba fàww, amiin!
14 Su ngeen baalee nit ñi leen di tooñ, seen Baay bi ci asamaan tamit dina leen baal. 15 Waaye su ngeen dul baal nit ñi, seen Baay du leen baal seen bàkkaar yi tamit.
16 «Su ngeen di woor, buleen tiisal seen kanam yi ni ko naaféq yi di defe, ndaxte ñoom dañuy ñaawal seen kanam yi ngir won ñépp ne dañoo woor. Ci dëgg maa ngi leen koy wax, jot nañu ba noppi seen neexal bépp. 17 Waaye yaw booy woor sëlmul te nga xeeñal sa bopp 18 ngir nga baña won nit ñi ne danga woor, te sa Baay biy gis li ngay def ci kumpa dina la neexal.
19 «Buleen dajale alalu àddina si fu max yi ak xomaag yi di ko yàqe te sàcc yi dugg, jël ko. 20 Waaye dajaleleen alal yi ci asamaan fu max ak xomaag yi dul yàqe te sàcc yi duñu dugg di ko jël. 21 Ndaxte fu sa alal nekk foofu la sa xol di nekk itam.
22 «Bët mooy làmpu yaram. Bu sa bët baaxee, sa yaram béppay nekk ci leer. 23 Waaye bu sa bët bonee, sa yaram béppay nekk ci lëndëm. Su fekkee nag leer bi nekk ci yaw lëndëm la, lëndëm boobu dina réy lool!
24 «Kenn mënul jaamoondoo ñaari sang. Dina bañ kii, te bëgg ki ci des, walla mu fonk kii te xeeb ki ci des. Mënuleen boole jaamu Yàlla ak jaamu alal.
25 «Loolu moo tax maa ngi leen koy wax, buleen jaaxle ci seen dund ci li ngeen wara lekk, walla ci seen yaram li ngeen wara sol. Ndax seen dund ëppul solo lekk? Te seen yaram, ëppul solo yére? 26 Xoolleen picci asamaan si: duñu ji, duñu góob, duñu dajale dara ci sàq yi. Waaye seen Baay bi ci asamaan mu ngi leen di dundal. Ndax ëppuleen solo fuuf picc yi? 27 Kan ci yeen moo mëna jaaxle ba yokk ab diir ci dundam? 28 Te lu tax ngeen di jaaxle ci lu jëm ci yére? Xoolleen, ni tóor-tóori ñax mi di saxe ci tool yi, duñu liggéey, duñu ràbb yére, 29 moona maa ngi leen koy wax: buur bi Suleymaan ci alalam yépp, mësul soloo ni benn ci ñax yooyu. 30 Su Yàlla di solale nii ñax yi nekk ci tool bi tey, bu subaa ñu sànni ko ci taal, ndax du leen defal lu ëpp loolu? Yeen daal, yeena tuuti ngëm. 31 Buleen jaaxle nag di wax ne: "Lu nuy lekk?" walla "Lu nuy naan?" walla "Lu nuy sol?" 32 Ndaxte loolu lépp xeeti àddina yi gëmul Yàlla ñoo koy wut. Waaye yeen, seen Baay bi ci asamaan xam na ne soxla ngeen ko. 33 Wànte jëkkleen wut nguuru Yàlla ak njubteem, te Yàlla dina leen jox lépp li ci des. 34 Buleen jaaxle nag ngir ëllëg, ndaxte ëllëg dina toppatoo boppam. Bés bu nekk coonoom doy na ko.»