Yeesu mu ngi tàmbalee jàngale ci barke bu wóor bi ci kaw tund bi
5
Bi Yeesu gisee mbooloo mi, mu yéeg ci benn tund te toog. Taalibeem yi ñëw ci wetam. 2 Mu jël kàddu gi te di leen jàngal naan:3 «Barkeel nañu ñi xam seen néew doole,
ndaxte nguuru asamaan si ñoo ko moom.
4 Barkeel nañu ñi di naqarlu,
ndaxte Yàlla dina leen dëfël.
5 Barkeel nañu ñiy suufeelu,
ndaxte dinañu donn àddina si.
6 Barkeel nañu ñiy wut njubte ak seen xol bépp,
ndaxte Yàlla dina leen ko may ba mu ne gàññ.
7 Barkeel nañu ñi yërëm seeni moroom,
ndaxte Yàlla dina leen yërëm.
8 Barkeel nañu ñi am xol bu set,
ndaxte dinañu gis Yàlla.
9 Barkeel nañu ñi di sàkku jàmm ci diggante nit ñi,
ndaxte Yàlla dina leen woowe ay doomam.
10 Barkeel nañu ñi ñuy fitnaal ndax ni ñu déggal Yàlla,
ndaxte nguuru asamaan si ñoom ñoo ko moom.
11 Barkeel ngeen bu leen nit ñi di saaga,
di leen fitnaal,
te di leen sosal ndax man.
12 Àndleen ak mbégte te bànneexu,
ndaxte Yàlla mu ngi leen di waajal neexal bu mag ci asamaan.
Ñoom noonu lañu doon fitnaale yonent yi fi nekkoon laata yeen.
13 «Yeenay xoromu àddina si. Su xorom ñàkkee cafkaam, naka lañu koy mëna sàppalee? Dootul am njériñ. Mënuñu lu dul sànni ko ci biti te nit ñi di dox ci kawam.
14 «Yeenay leeru àddina si. Dëkk bu nekk ci kaw tund, mënuñu ko nëbb. 15 Kenn du taal làmp di ci dëpp leket, waaye dañu koy wékk, muy leeral ñépp ñi nekk ci kër gi. 16 Noonu ngeen wara leere ci kanamu nit ñi ngir ñu gis seeni jëf yu baax tey màggal seen Baay bi ci asamaan.
17 «Buleen xalaat ne dama ñëw ngir dindi yoonu Musaa walla li yonent yi bind. Ñëwuma ngir dindi leen waaye ngir matal leen, 18 ndaxte ci dëgg maa ngi leen koy wax, feek asamaan ak suuf weesuwuñu benn araf walla benn rëdd bu gëna ndaw sax ci yoonu Musaa du deñ ba keroog lépp di mat. 19 Kon nag képp ku dindi ndigal bu gëna tuuti sax tey jàngal ñeneen ñi ñu def ni moom, dinañu ko woowe ki gëna tuuti ci nguuru asamaan si. Waaye ki leen di jëfe te di leen jàngale, kooku dinañu ko woowe ku màgg ci nguuru asamaan si. 20 Maa ngi leen koy wax, su fekkee seen njubte ëppul bu jàngalekati yoonu Musaa ak bu Farisen yi, dungeen dugg mukk ci nguuru asamaan si.
21 «Déggoon ngeen ñu wax sunu maam yi ne: "Bul rey nit. Ku rey nit dinañu la yóbbu ci kanamu àttekat bi." 22 Waaye man maa ngi leen di wax ne, ku mere sa mbokk, dinañu la yóbbu ci kanamu àttekat bi. Ku wax sa mbokk: "Doo dara," dinañu la yóbbu ci kanamu kurélu àttekaay bi. Te ku ko wax ne: "Amoo xel," yelloo nga dugg safara. 23 Su fekkee nag danga ñëw ngir jox Yàlla sa sarax ci saraxlukaay bi, te foofu nga fàttaliku ne sa mbokk am na lu mu la mere, 24 bàyyil foofu sa sarax ci kanamu saraxlukaay bi, te nga dem juboo ak sa mbokk ba noppi, te nga dellusi, jox Yàlla sa sarax. 25 Bu la nit tuumaale te ngeen ànd di dem ci kër-àttekaay bi, fexeel ba nga juboo ak moom bi ngeen nekkee ci yoon bi. Lu ko moy ki lay tuumaal dina la jébbal àttekat bi, te àttekat bi jébbal la takk-der yi, te ñu tëj la ci kaso bi. 26 Ci dëgg maa ngi la koy wax: doo fa génn feek feyuloo lépp ba ci fiftin bu mujj.
27 «Déggoon ngeen ñu waxoon ne "bul njaaloo." 28 Waaye man maa ngi leen di wax ne: ku xemmem jigéen, njaaloo nga ak moom ba noppi ci sa biir xol. 29 Te bu la sa bëtu ndeyjoor di xiir ci bàkkaar, lóqati ko te nga sànni ko fu sori, ndaxte ñàkk benn cér ci sa yaram moo gën ci yaw ñu sànni sa yaram bépp ci safara. 30 Te bu la sa loxo ndeyjoor di xiir ci bàkkaar, dagg ko te nga sànni ko fu sori, ndaxte ñàkk benn cér ci sa yaram moo gën ci yaw ñu sànni sa yaram bépp ci safara.
31 «Waxoon nañu tamit ne: "Ku fase jabaram, war na ko bindal benn bataaxal buy wone ne fase na ko." 32 Waaye man maa ngi leen di wax ne: ku fase jabaram bu dul ci njaaloo, yaa koy xiir ci njaaloo; te ku takk jigéen bu jëkkëram fase, njaaloo nga.
33 «Déggoon ngeen tamit ñu wax sunu maam yi ne: "Bul waat ci lu dul dëgg, waaye matalal sa waat bi nga def ci kanamu Boroom bi." 34 Waaye man maa ngi leen di wax ne: buleen waat mukk, muy ci asamaan ndaxte mooy baŋu nguuru Yàlla, 35 muy ci suuf si ndaxte mooy béréb bi muy teg ay tànkam, walla muy ci Yerusalem ndaxte mooy dëkku Buur bu mag bi. 36 Bul waat tamit ci sa bopp ndaxte mënuloo fexe ba sa kawar weex mbaa mu ñuul. 37 Waaye na seen waaw nekk waaw te seen déet nekk déet. Lépp lu ngeen ci yokk ci Seytaane la jóge.
38 «Déggoon ngeen ñu wax ne: "Bët, bëta koy fey, te bëñ, bëña koy fey." 39 Waaye man maa ngi leen di wax ne: bul bañ ku la def lu bon. Bu la nit mbejee ci sa lexu ndeyjoor, jox ko bi ci des. 40 Bu la nit bëggee yóbbu ci yoon ngir jël sa yére bu ndaw bi nga sol, joxaale ko tamit sa mbubb bu mag bi. 41 Su la nit sëfee dara ci doxub benn kilomet àndal ak moom ci ñaari kilomet. 42 Mayal ki lay ñaan te bul won gannaaw ki lay leb.
43 «Déggoon ngeen ñu wax ne: "Nanga bëgg sa moroom te nga bañ sa noon." 44 Waaye man maa ngi leen di wax ne: bëggleen seeni noon, tey ñaanal ñi leen di fitnaal. 45 Ndaxte seen Baay bi ci asamaan day fenkal jantam ci kaw ñu bon ñi ak ñu baax ñi tamit, tey wàcce tawam ci ñu jub ñi ak ñu jubadi ñi. Te ci noonu ngeen di wone ne nekk ngeen dëgg ay doomam. 46 Su fekkee nag ñi leen bëgg rekk ngeen bëgg, ban neexal ngeen ciy jële? Juutikat yi sax noonu lañuy jëfe. 47 Su fekkee ne seeni mbokk rekk ngeen di nuyu, lan ngeen def lu yéeme? Ñi gëmul Yàlla sax noonu lañuy jëfe. 48 Yeen nag na ngeen mat ni seen Baay bi ci asamaan mate.»