Seytaane fiir na Yeesu
4
Noonu Xel mu Sell mi yóbbu Yeesu ba ci biir màndiŋ ba ngir Seytaane fiir ko fa. 2 Bi mu fa nekkee, lekkul woon ñeent fukki bëccëg ak ñeent fukki guddi, te noonu mu xiif. 3 Seytaane jegesi ko te ne ko: «Su fekkee yaay doomu Yàlla, joxal ndigal xeer yi ñu nekk mburu.» 4 Yeesu tontu ko ne: «Mbind mi nee na: "Nit du dunde mburu rekk, waaye itam bépp kàddu bu génne ci gémmiñu Yàlla."»5 Noonu Seytaane yóbbu ko ci Yerusalem, dëkk bu sell bi, teg ko ci collu kër-Yàlla gi, 6 te ne ko: «Su fekkee yaay doomu Yàlla, tëbal te nga daanu ci suuf, ndaxte Mbind mi nee na:
"Yàlla dina jox malaakaam yi ndigal ci sa mbir
te ñu téye la ci seeni loxo
ngir bañ say tànk fakkastalu ci xeer."»
7 Yeesu ne ko: «Mbind mi wax na tamit ne: "Bul seetlu Yàlla sa Boroom."»
8 Gannaaw loolu, Seytaane yóbbu ko ci tund bu kawe lool te won ko nguuri àddina si yépp ak seeni màggaay 9 te ne ko: «Dinaa la may lii lépp soo sukkee ci sama kanam, màggal ma.» 10 Noonu Yeesu tontu ko ne: «Sori ma, Seytaane, ndaxte Mbind mi nee na: "Bul sukk ci kanamu kenn ku dul Yàlla sa Boroom te di ko jaamu moom rekk."»
11 Noonu Seytaane bàyyi ko te ay malaaka ñëw ci Yeesu di ko toppatoo.
Yeesu tàmbale na liggéeyam ci Galile.
12 Bi Yeesu déggee ne tëj nañu Yaxya ci kaso bi, mu dem diiwaanu Galile. 13 Foofu mu jóge dëkku Nasaret, dem dëkk Kapernawum, di benn dëkk bu féete ci dexu Galile, te nekk ci diiwaan bi Yàlla mayoon giiri Sabulon ak Neftali. 14 Loolu am na ngir matal li yonent Yàlla Esayi waxoon, bi mu ne:
15 «Yaw diiwaanu Sabulon ak diiwaanu Neftali,
di yoonu géej gannaaw dexu Yurdan!
Yaw Galile di diiwaan bu bari ñi dul Yawut.
16 Askan bi dëkkoon foofu ci lëndëm
gis na benn leer bu mag,
te ñi dëkkoon ci réew bi takkandeeru dee tiim,
benn leer fenk na ci ñoom.»
17 Dale ko ci waxtu boobu, Yeesu tàmbale waare naan: «Tuubleen seeni bàkkaar ndaxte nguuru asamaan si jegesi na.»
18 Benn bés Yeesu doon dox ci tefesu dexu Galile, mu gis ñaari nappkat yu bokk ndey ak baay: Simoŋ mi ñuy woowe Piyeer ak Andare. Ñu doon sànni seeni mbaal ci dex bi. 19 Yeesu nee leen: «Toppleen ma te dinaa leen def ay nappkatu nit.» 20 Ci saa si ñu bàyyi seen mbaal yi te topp ko. 21 Bi Yeesu demee ba ci kanam, mu gisaat ñaar ñu bokk ndey ak baay: Saak ak Yowaana ñiy doomi Sebede. Nekkoon nañu ci seen biir gaal ak seen baay Sebede di defaraat seen mbaal yi. Yeesu woo leen. 22 Ci saa si ñu bàyyi seen gaal ak seen baay te topp ko.
23 Yeesu doon na wër diiwaanu Galile bépp di jàngale ci seen kër-ñaan yi, di yégle xibaar bu baax biy wax ci nguuru Yàlla gi, te di wéral nit ñi ci seen feebar yépp ak ci seen jàngoro yépp. 24 Turam daldi siiw ci réewu Siri yépp. Dañu ko doon andil ñépp ñi ay feebar yu wuute ak ay jàngoro yu bari sonaloon, ñi ay rab jàppoon, ñi am feebaru say, ak ay làggi, te Yeesu wéral leen ñoom ñépp. 25 Mbooloo mu bari doon na ko topp: nu ngi jóge woon ci diiwaanu Galile ak ci diiwaan bi ñuy woowe fukki dëkk yi, ak ci dëkku Yerusalem, ak ci diiwaanu Yude, ak ci diiwaan bi féete gannaaw dexu Yurdan.