Yaxya mu ngi waare tey sóob nit ñi ci ndox
3
Ci jamono jooju la Yaxya feeñoon di waare ci biir màndiŋu Yude, 2 di wax ne: «Tuubleen seeni bàkkaar ndaxte nguuru asamaan si jegesi na.» 3 Yaxya mooy ki yonent Yàlla Esayi doon wax bi muy naan:
«Lii mooy baatu nit kiy yuuxu ci biir màndiŋ bi, naan:
"Waajalleen yoonu Boroom bi.
Defarleen yoonam yi, ñu jub."»
4 Yaxya daan na sol yére bu ñu ràbbe kawaru giléem te takk ci ndiggam takkukaay bu ñu defare der. Da doon lekk soccental ak lemu àll. 5 Waa Yerusalem, waa diiwaanu Yude yépp ak waa diiwaan bi nekk ci wetu dexu Yurdan bépp doon nañu ñëw ci moom. 6 Dañu doon wax seeni bàkkaar ci kanamu ñépp, te noonu Yaxya di leen sóob ci ndox ci dexu Yurdan.
7 Ñu bari ñu bokkoon ci tarixa Farisen ak ci tarixa Sadusen doon nañu ñëw ci moom ngir mu sóob leen ci ndox. Bi leen Yaxya gisee mu ne leen: «Yeen ñi fees ak daŋar mel ni jaan, kan moo leen jàngal ngir ngeen daw merum Yàlla mi nara wàcc? 8 Woneleen nag ci seen jëf ne tuub ngeen seeni bàkkaar. 9 Buleen xalaat ne mën ngeen wax ci seen xel ne: "Nun, am nanu Ibraayma ni baay," ndaxte maa ngi leen koy wax, ci xeer yii, Yàlla mën na cee sàkkal Ibraayma ay doom. 10 Sémmiñ bi jege na ba noppi ngir dagg reeni garab yi. Bépp garab bu meññewul meññeef bu baax, dinañu ko dagg te sànni ko ci safara si. 11 Man, maa ngi leen di sóob ci ndox ngir nit ñi tuub seeni bàkkaar, waaye kenn ku ma ëpp kàttan dina ñëw ci sama gannaaw. Yelloowuma sax tekki ay dàllam. Kooku dina leen sóob ci Xel mu Sell mi ak ci safara. 12 Mu ngi yor layu ci loxoom te dina teqale pepp bi ak xatax bi. Dina dajale pepp yi ci sàqam waaye dina lakk xatax bi ci safara bu dul fey mukk».
13 Ci jamono jooju, Yeesu jóge diiwaanu Galile, ñëw ci Yaxya ci dexu Yurdan ngir mu sóob ko ci ndox, 14 waaye Yaxya bëgg ko ko tere, naan: «Yaa ngii ñëw ci man? Moona man maa soxla nga sóob ma!» 15 Yeesu tontu ko: «Bàyyil noonu, ndaxte ci lanuy matal lépp li jub ci kanamu Yàlla.» Noonu Yaxya nangu. 16 Bi ko Yaxya sóobee ci ndox ba noppi, Yeesu génn ci ndox mi. Ci saa si asamaan si ubbeeku ngir moom te Xel mu Sell mi wàcc ci jëmm ju mel ni pitax te ñëw ci moom 17 te benn baat jóge ci asamaan ne: «Kii mooy sama doom ji ma sopp. Ci moom laa ame bànneex.»