Erodd mu ngi wuta rey Yeesu
2
Yeesu juddoo na ci dëkku Betleyem, ci diiwaanu Yude ci jamono bi Erodd bu mag nekkee buur. Gannaaw bi Yeesu juddoo ay boroom xam-xam jóge woon nañu penku ñëw Yerusalem di laajte, 2 naan: «Ana Buuru Yawut biy doora juddu? Ndaxte gis nanu biddéewam feeñ ci penku, te danoo ñëw ngir màggal ko.»
3 Bi buur bi Erodd yégee loolu mu jaxasoo, moom ak waa Yerusalem yépp. 4 Mu woolu njiiti-jébbalkati-sarax yi ak jàngalekati-yoonu-Musaa te laaj leen fu Almasi bi wara juddoo. 5 Ñu tontu ko ne: «Ca Betleyem ci diiwaanu Yude, ndaxte lii la yonent bi bind:
6 "Yaw Betleyem, ci diiwaanu Yude,
nekkoo dëkk bi gëna ñàkk solo ci dëkk yu màgg yi nekk ci diiwaanu Yude.
Ndaxte ci yaw la njiit biy jiite Israyil sama askan di jóge."»
7 Noonu Erodd woolu boroom xam-xam yi ci kumpa, te laaj leen ngir xam kañ la biddéew bi feeñ. 8 Noonu mu yebal leen Betleyem ne leen: «Demleen ngeen seet bu wóor xale bi, te bu ngeen ko gisee ngeen xamal ma ko, ngir ma dem man tamit màggal ko.»
9 Gannaaw bi ñu dégloo buur bi ba noppi, ñu dem, te biddéew bi ñu gisoon ci penku jiite leen ba yegg, mu tiim béréb bi xale bi nekkoon. 10 Bi ñu gisaatee biddéew bi ñu fees ak mbégte bu réy. 11 Ñu dugg ci kër gi te gis xale bi ak yaayam Maryaama. Ñu sukk ngir màggal xale bi, te ñu ubbi li nu andaale woon, may ko wurus, cuuraay ak xeetu latkoloñ bi ñuy wax miir. 12 Gannaaw loolu Yàlla artu leen ci gént ngir ñu baña dellu ci Erodd. Ñu daldi jël beneen yoon ngir dellu seen réew.
13 Bi ñu demee benn malaaka Boroom bi feeñu Yuusufa ci gént te ne ko: «Jógal, nga jël xale bi ak yaayam, te nga daw dem réewu Misra, nga des fa, ba ma wax la nga dellusi. Ndaxte Erodd day seet xale bi ngir rey ko.» 14 Yuusufa daldi jóg, jël xale bi ak yaayam ci guddi gi, te dem làquji ci Misra. 15 Mu des fa ba Erodd dee. Loolu am na ngir matal li Boroom bi waxoon jaarale ko ci yonent bi, bi mu ne: «Woo na sama Doom mu génn Misra.»
16 Bi Erodd yégee ne boroom xam-xam yi nax nañu ko mu daldi mer lool. Mu joxe ndigal ngir ñu rey xale yu góor yépp yi nekk Betleyem ak li ko wër dale ko ci ñaari at jëm suuf, méngook jamono ji ko boroom xam-xam yi waxoon ne ci la biddéew bi feeñoon. 17 Noonu mat na li yonent Yàlla Yeremi waxoon bi mu ne:
18 «Dégg nañu benn baat ci dëkku Raama,
ay jooy ak ay naqarlu.
Rasel mooy jooy ay doomam,
te bëggul ñu dëfël ko,
ndaxte dee nañu.»
19 Gannaaw bi Erodd deewee benn malaaka Boroom bi feeñu Yuusufa ci gént ca Misra 20 ne ko: «Jógal, nga jël xale bi ak yaayam, te nga dellu ak ñoom ci réewu Israyil, ndaxte ñi doon wuta rey xale bi dee nañu.» 21 Yuusufa daldi jóg, jël xale bi ak yaayam te dellu ci réewu Israyil. 22 Waaye bi mu yégee ne Arkelawus moo wuutu baayam ci nguuru Yude, mu ragala dem foofu. Gannaaw bi ko Yàlla joxee ndigal ci gént, mu dem làquji ci diiwaanu Galile, 23 te dem dëkk ci benn dëkk bu ñuy woowe Nasaret ngir kàddu gii yonent yi waxoon mat: «Dinañu ko woowe Nasareen.»