Macë
Askan bi Yeesu Cosaanoo
1
Lii mooy askan bi Yeesu Almasi bi cosaanoo, moom miy sëtu Daawuda, miy sëtu Ibraayma.2 Ibraayma mooy baayu Isaaxa, Isaaxa mooy baayu Yanqóoba, Yanqóoba mooy baayu Yuda ak ay doomu baayam. 3 Yuda mooy baayu Peres ak Sera; Tamar mooy seen yaay. Peres mooy baayu Esron, Esron mooy baayu Aram. 4 Aram mooy baayu Aminadab; Aminadab mooy baayu Nason; Nason mooy baayu Salmon; 5 Salmon mooy baayu Bowas; Raxab mooy yaayam. Bowas mooy baayu Obedd; Ruut mooy yaayam. Obedd mooy baayu Yese. 6 Yese mooy baayu buur bi Daawuda.
Daawuda mooy baayu Suleymaan; yaayam nekkoon na jabaru Uri. 7 Suleymaan mooy baayu Robowam; Robowam mooy baayu Abiya; Abiya mooy baayu Asaf; 8 Asaf mooy baayu Yosafat; Yosafat mooy baayu Yoram; Yoram mooy baayu Osiyas; 9 Osiyas mooy baayu Yotam; Yotam mooy baayu Akas; Akas mooy baayu Esekiya; 10 Esekiya mooy baayu Manase; Manase mooy baayu Amon; Amon mooy baayu Yosiyas. 11 Yosiyas mooy baayu Yekoñas ak ay doomu baayam ci jamono ji waa Babilon jàppee waa Israyil, yóbbu leen Babilon.
12 Gannaaw bi ñu leen fa yóbboo, Yekoñas am fa Salacel. Salacel mooy baayu Sorobabel; 13 Sorobabel mooy baayu Abiyudd; Abiyudd mooy baayu Eliyakim; Eliyakim mooy baayu Asor; 14 Asor mooy baayu Sadog; Sadog mooy baayu Akim; Akim mooy baayu Eliyudd; 15 Eliyudd mooy baayu Eleyasar; Eleyasar mooy baayu Matan; Matan mooy baayu Yanqóoba. 16 Yanqóoba mooy baayu Yuusufa mi nekkoon jëkkëru Maryaama. Ci Maryaama la Yeesu juddoo, moom mi ñuy woowe Almasi bi.
17 Maas yi nag ci diggante Ibraayma ak Daawuda tollu nañu ci fukk ak ñeent. Maas yi ci diggante Daawuda ak jamono bi ñu yóbboo waa Israyil Babilon tollu nañu ci fukk ak ñeent. Maas yi dale ko ci jamono jooju ba ci juddu Yeesu tamit tollu nañu ci fukk ak ñeent.
Juddub Yeesu
18 Ci anam bii la Yeesu Almasi bi juddoo: Maryaama miy yaayam mayoon nañu ko Yuusufa, waaye laata ñuy ànd, fekk na mu ëmb jaarale ko ci kàttanu Xel mu Sell mi. 19 Yuusufa jëkkëram nekkoon na nit ku jub te bëggu ko woona weer ci kanamu nit ñi. Noonu mu jël dogal bàyyi ko ci sutura. 20 Bi mu ci doon xalaat, benn malaaka Boroom bi feeñu ko ci gént te ne ko: «Yuusufa sëtu Daawuda, bul ragala jël Maryaama ni sa jabar. Ndaxte doom ji mu ëmb, ci Xel mu Sell mi la jóge. 21 Dina am doom bu góor te nanga ko tudde Yeesu, ndaxte dina musal askanam ci seeni bàkkaar.»
«Xoolal! Janq bi dina ëmb
te jur doom bu góor,
te ñu tudde ko Emanuwel,»
muy tekki «Yàlla mu ngi ak nun.»