Yeesu wéral waay ju làggi te baal ko ay bàkkaaram
2
Ay fan gannaaw loolu, Yeesu ñëwaat ci dëkku Kapernawum, te ñu yég ne mu ngi ci kër gi. 2 Mbooloo mu bari dajaloo ba kenn amatul fooy taxaw du sax ci kanamu bunt bi, te Yeesu di leen jàngal kàddu Yàlla gi. 3 Ñeenti nit ñëw, jàppoo waa ju làggi, ngir andil ko Yeesu. 4 Waaye mënuñu ko woon andi ci kanamam, ndax mbooloo mi. Ñu daldi toj dal bi tiim béréb bi Yeesu nekkoon, wàcce ku làggi ki tëddoon ci basaŋam jaarale ko ci bën-bën bi ñu tojoon. 5 Bi Yeesu gisee seen ngëm, mu wax ku làggi ki ne: «Sama doom, baal nañu la say bàkkaar.» 6 Foofu amoon na ñenn ci jàngalekati-yoonu-Musaa yi toogoon di xalaat ci seen biir xel naan: 7 «Lu tax nit kii di waxe noonu? Mu ngi méngale boppam ak Yàlla! Kan moo mëna baale bàkkaar yi ku dul Yàlla rekk?» 8 Ci saa si Yeesu xam ci xelam li ñu doon xalaat ci seen biir xel te mu wax leen ne: «Lu tax ngeen di xalaate nii ci seen biir xel? 9 Lan moo gëna yomb wax ku làggi ki: "baal nañu la say bàkkaar" walla "jógal, jël sa basaŋ, te nga dox"? 10 Li ma bëgga def mooy ngir ngeen xam ne Doomu nit ki am na sañ-sañ ci àddina si baale bàkkaar yi.» 11 Noonu mu wax ku làggi ki: «Maa ngi la koy wax: jógal, jël sa basaŋ te nga ñibbi.» 12 Ci saa si nit ki jóg, jël basaŋam, te génn ci kanamu ñépp, ba tax ñépp waaru te di màggal Yàlla, di wax ne: «Mësunoo gis lu mel nii.»
Yeesu tànn na Lewi juutikat bi
13 Yeesu génnaat, dem ci tefesu dexu Galile. Mbooloo mi yépp di ñëw ci moom, te mu leen di jàngal. 14 Bi muy dem mu gis benn juutikat bu tudd Lewi di doomu Alfe. Mu toog ci bérébu liggéeyukaay bi. Yeesu ne ko: «Topp ma.» Mu jóg te topp ko. 15 Gannaaw loolu, Yeesu doon lekk ci këru Lewi. Ay juutikat yu bari ak ay bàkkaarkat doon nañu lekkandoo ak moom ak taalibeem yi, ndaxte ay nit ñu bari ñu mel noonu doon nañu ko topp. 16 Bi ñu gisee ne da doon lekkandoo ak ay bàkkaarkat ak ay juutikat, jàngalekati-Yoonu-Musaa yi bokkoon ci tarixa Farisen yi ne taalibeem yi: «Lu tax muy lekkandoo ak ay juutikat ak ay bàkkaarkat?» 17 Bi Yeesu déggee loolu, mu wax leen ne: «Du ñi wér ñoo soxla fajkat waaye ñi wéradi. Damaa ñëw ngir woo bàkkaarkat yi ñu tuub seeni bàkkaar, waaye du ñu jub ñi.»
Ay nit laaj nañu Yeesu ci lu jëm ci woor
18 Taalibe Yaxya yi ak taalibe Farisen yi dañu doon woor. Ñu ñëw ci Yeesu, ne ko: «Taalibe Yaxya yi ak taalibe Farisen yi dañuy woor. Lu tax say taalibe duñu woor?» 19 Yeesu tontu leen ne: «Ndax xariti boroom séet bi mën nañu woor waxtu bi boroom séet nekke ak ñoom? Feek boroom séet bi mu ngi ak ñoom duñu mëna woor. 20 Ay bés a ngi ñëw, ñu jële boroom séet bi ci seen biir te ci bés boobu dinañu woor.
21 «Kenn du ñaw benn daggitu yére bu bees ci benn yére bu màggat. Lu ko moy daggit bu bees bi dina ñoddi yére bu màggat bi te xotteeku bi gëna yaatu. 22 Te kenn du jël biiñ bu bees di ko def ci ay mbuusu der yu màggat. Lu ko moy biiñ bi dina fëq mbuus yi te biiñ bi ak mbuus ya yàqu. Danga wara def biiñ bu bees ci ay mbuusu der yu bees.»
Yeesu mooy Boroom bésub noflaay bi
23 Benn bésu noflaay Yeesu doon jàll ci tool yi. Taalibeem yi di dox, di witt ci pepp yi. 24 Farisen yi ne ko: «Xoolal! Lu tax ñuy liggéey ci bésu noflaay bi te yoonu Musaa day tere ñu ciy liggéey?» 25-26 Yeesu tontu leen ne: «Xanaa jànguleen li Daawuda defoon ci jamono jébbalkatu-sarax-bu-mag bi Abiyatar? Bi mu nekkee ci soxla te xiifoon, moom ak ñi mu àndaloon, mu dugg ci kër-Yàlla gi, lekk ci mburu yi ñu jébbal Yàlla te jox ci tamit ñi mu àndaloon, fekk yoon bi mayul kenn di ko lekk ku dul jébbalkati-sarax yi.» 27 Te Yeesu yokk ca ne: «Yàlla sàkkul nit ngir bésu noflaay bi, waaye dafa sàkk bésu noflaay bi ngir nit. 28 Kon nag, Doomu nit ki mooy boroomu bésu noflaay bi sax.»