3
Yeesu duggaat ci kër-ñaan bi. Foofu amoon na benn waay bu loxoom làggi. 2 Farisen yi bëggoon nañu tuumaal Yeesu. Noonu ñu koy xool ngir xam ndax ci bésu noflaay bi dina wéral waa ji. 3 Yeesu daldi wax waa ji amoon loxo bu làggi bi: «Jógal, nga taxaw ci kanamu ñépp.» 4 Ci noonu mu wax leen: «Lan la yoon bi maye ngir ñu def ko ci bésu noflaay bi? Lu baax walla lu bon, muccal nit walla bàyyi ko mu loru?» Waaye ñu noppi. 5 Yeesu xool leen ñoom ñépp ak mer, ànd ak tiis ndax seen xol yu dëgër. Noonu mu wax nit ki: «Tàllalal sa loxo.» Mu tàllal ko te loxoom bi daldi wér. 6 Ci saa si Farisen yi génn ci kër-ñaan bi, daldi waxtaan ak ñi far ak Erodd ci ni ñuy fexee rey Yeesu.Mbooloo mi topp na Yeesu ba ci dexu Galile
7 Yeesu ak taalibeem yi jëm nañu dexu Galile, te mbooloo mu takku di ko topp. Jóge woon nañu diiwaanu Galile, diiwaanu Yude, 8 dëkku Yerusalem, diiwaanu Idume, gannaaw dexu Yurdan, ak li wër Tir ak Sidon. Mbooloo mu bari ñëwoon nañu ci Yeesu, ndaxte yégoon nañu lépp li mu doon def. 9-10 Da doon wéral nit ñu bari, ba tax ñépp ñi feebaroon di njëkkante ngir laal ko. Noonu mu yónni taalibeem yi, ñu andil ko gaal bu ndaw, mu yéeg ci ngir bañ mbooloo mi tanc ko. 11 Ñi rab jàppoon bi ñu gisee Yeesu, ñu daanu ci kanamam di yuuxu naan: «Yaw yaay doomu Yàlla ji.» 12 Waaye Yeesu gëdd leen ak doole ngir bañ ñu wax ki mu doon.
Yeesu tànn na fukki ndaw yi ak ñaar
13 Gannaaw loolu Yeesu yéeg ci tund bi. Mu woo ñi mu bëgga woo te ñu ñëw ci moom. 14 Mu tànn ci fukk ak ñaar, tudde leen ndaw, ngir ñu nekk ak moom te mu yónni leen ñuy yégle xibaar bu baax bi 15 te mu jox leen sañ-sañ ngir ñuy dàq rab yi. 16 Fukk ak ñaar ñii la tànnoon: Simoŋ mi Yeesu doon woowe Piyeer, 17 Saak ak Yowaana ñiy doomi Sebede te mu doon leen woowe Bowanerses miy tekki doomi dënnu, 18 Andare, Filib, Bartelemi, Macë, Tomaa, Saak di doomu Alfe, Tade, Simoŋ di ku takku ci réewam, 19 ak Yuda Iskariyot di ki ko wor.
Yeesu moo ëpp Seytaane doole
20 Gannaaw loolu Yeesu delluwaat ci kër gi. Mbooloo mu takku dajaloowaat ba tax Yeesu ak taalibeem yi mënuñu woona lekk. 21 Bi ko waa këram yégee, ñu dem jëli ko ndaxte dañu doon wax ne: «Dafa tàggoo ak sagoom.»
22 Jàngalekati-yoonu-Musaa yi jóge woon Yerusalem di wax ne: «Beelsebul moo ko jàpp. Ci kàttanu buuru rab yi lay dàqe rab yi.» 23 Noonu Yeesu woo leen te wax leen ci léeb ne: «Naka la Seytaane mëna dàqe Seytaane? 24 Bépp nguur bu xaajaloo ci biiram dina tas, 25 te bépp kër bu xaajaloo ci biiram dina tas. 26 Su fekkee nag Seytaane day xeex boppam te su nguuram xaajaloo, dootul mëna yàgg waaye dina jeex. 27 Kenn mënula dugg ci kër nit bu am doole di jël alalam su fekkee ne takkul nit kooku ba noppi. Noonu dina jël li mu dencoon ci këram. 28 Ci dëgg maa ngi leen koy wax: dinañu baal nit ñi seen bàkkaar yépp ak bépp wax bu ñaaw bu ñu wax. 29 Waaye ku wax lu ñaaw ci Xel mu Sell mi, duñu ko mësa baal ndaxte bàkkaar na ba fàww.» 30 Yeesu doon na waxe noonu ndaxte nit ñi dañu doon wax ne: «Dafa am rab.»
31 Gannaaw loolu yaayu Yeesu ak rakki Yeesu yi ñëw, taxaw ci biti te ñu woolu ko. 32 Nit ñu bari toogoon, wër Yeesu te kenn ne ko: «Xoolal! Sa yaay ak say rakk ñu ngi ci biti di la seet.» 33 Yeesu tontu leen ne: «Ñan ñooy sama yaay ak samay rakk?» 34 Noonu Yeesu xool ñi toogoon wër ko, te ne leen: «Ñii ñooy sama yaay ak samay rakk, 35 ndaxte kiy def coobare Yàlla kooku mooy sama rakk bu góor, sama rakk bu jigéen, walla sama yaay.»